Vous êtes sur la page 1sur 71

Tere Irwaun Nadiim ci Sri Tuubaa Teereb {Irwaaun nadiim min hathbi hubil xadiim}, di ci maanaa nndalug aji

naanaale ji ci ndox mu neexum sopp jwrinu yonant bi. bi Sri Muhammadu Lamin Job Dagana taalubeb Seexul Xadiim (yal na gramul Ylla eel ko) defoon ci Yaaram (Araab) mu eel lenn ci dundug Seexul Xadiim, lenn ci ay jaar-jaaram, lenn ci ay meloom, ak lenn ci ay mayam... Abdu Xaadir KEBE Stub Seex Saalih Mbkke tekki ko ci Wolof ngir laabiiree ko i deggul Yaaram di ay wolof te bgg Seexul Xadiim. Traliin

Jiitalug aji firi ji (preface)...................................................................................................................... Jiitalug aji taalif ji......................................................................................................................................................... . Xamale kuy Sri bi, ak ay mbiram, ba bi waajuram wu gor lqoo................................................................................... Ni mu nekke woon ginaaw bi waajur wi lqoo (grmul ylla yal na nekk ci oom.............................................................. SancamJolof Ak li ko waraloon..................................................................................................................................... Tukkib gej gi........................................................................................................................................................ ...... Dugg ci gaal gi juge Ndakaaru...................................................................................................................................... Dellusi gi juge ca gej ga............................................................................................................................................. aareelu tukki bi (bu Gnnaar bi).................................................................................................................................. ibbisi gi jugge Gnnaar............................................................................................................................................. .. Ag gnnam juge Jolof jm 1 www.daaraykamil.com

Njaarem.............................................................................................................................

Tjte................................................................................................................................................... ...................... Seere yi ko mag i seereel ag mgg akug wilaaya..........................................................................................................

Jiitalug aji firi ji (preface) Jiitalug aji firi ji:

Li ma tax a jug, jme ma ci def bile ligey, te ma jppe ko muy bu am njari, mooy, benn: jortu ne, ci def gi, i ngi ligeyal Sri bi, waaye it xeet wi . Ndax jl lu mel ni jaar-jaari Sri Tuubaa, ak li mu lmboo ciy njari, nga tas ko, teg ko ci fu loxol ku nekk gg,yombal ko ba ku jug man koo xam, man koo dgg , man cee jariu, ca anam ga mu gn a yombe, gnnee leere, te yaakaar naa ne def ko ci wolof , eel wolof yi,ci anam yiy yombal la, tey leeral . Lu mel ne lii de yaakaar naa ne amul lu ko gn di ligeyal Sri bi,waaye ag ligeyal sa xeet it mi ngi ci, ndax ag dundal la, eel saw lmmi, te gis naa ne lu waay man a xame ci lkk, ak wu mu man a doon, ci sa wos, lay gn a dugge,lay gn a tooge,lay gn a nekke, luy dund ak yaw, ci lay doone kenn ci yaw, ngay, yaw itam, kenn ci moom, ngen di benn bu dul aar, gis naa ne bokk na ci li iy rawe, di rawe; di jnge ci seeni lkk, di ci waxe, di ci xalaate, te di ci jokkoo. Man de bile tere,njkk ma koy tekki, nekkoon na di bob,dees na soxla as lf ci waxtu,ngir yr ko,dgg ko,naan ko,waaye daa mel ni bi ma ko defee ci wolof,soxlaatunu lu dul lu new, ngir jaar ci, jaarati ci, kon nanu fonku sunu bopp,ci fonkaat bu baax sunu lkk yii,te xam ne dug fonkadi eneen i. aareel bi mooy , gis gi ma gis tere bii,di bu jggi dayo ba ci solo ak njari, di delluwaay ci delluwaayi terey yoonu murit wi,di rootukaay ci yu xam-xam yi. Lmboo nag kem bu ry ci xam-xam, ci lu aju ci S bii, di kenn ci i u war a xam, bu ma waxul ki pp solo ci oom . Kon xam leen ne yii ak yeneen yu ma waxul, ngir ba a guddal, oo sabab firi gi, nga rax ci dolli,nekkug aji taalif ji, di kenni jlewaayi yoon wi,yu xam-xam yi. Ndax kat, boo yree, da nga ko gis lu bari mu naan S bi nee na ma, te loolu du lu yomb . Kok bkk-neg la woon ci bkk-neg yi,bu ma waxul ngn ji bkk-neg , kon kooku maneesu koo gn di jlewaay, mbaa delluwaay, rawati na muy ku pp xam ag sellam, akug dggoom, yal na nu Ylla taas ci barkeem te dolli ngrmam ci Sri sunu,Sriam,laafaale ko ci, ci barke ku nu ligeyalam, ak ki muy ligeyal moom mu mujj mi, Aamiin,yaw boroom mbindef yi. Aji firi ji: Abdul Xaadir KEBE Jiitalug aji taalif ji Jiitalig aji taalif ji :

www.daaraykamil.com

Bii mooy teereb {Irwaaun nadiim min hathbi hubil xadiim}, di ci maanaa nndalug aji naanaale ji (ki ngay toogal di waxtaan) ci ndox mu neexum sopp jwrinu yonant bi , di { xam-xamu jaloore bu nu gttal} mu eel nag ki bgg a am ab xam-xam ci dundug sri Ahmadu Bamba yal na ylla dolli grmam ci moom ,te jari u ci,amiin. Ki ko taalif it di ku xeebu ku aajowoo ndimbalul boroomam ak yrmaandeem,tey yaakaar ci moom mu jggal ko ay bkkaaram,te lqal ko ay ayibam,yi fee ak yi nbbu,fii ak fan jm,di Muhammadul Amiin JOOP doomi sheex Ahmadu JOOP mu dagana,yal na leen ylla boole jggal. Di it taalibeb sri Tuubaa, yal na ko ylla grm te jari u ci moom,amiin. Maa ngi aan ylla mu musal ma ci saytaane mu nu jam mi,di tmblee nag samay wax ak jf ci turam wu tedd wi,moom mi yor yrmaande ju yaatu ji matale mbindefam yi ci dduna,te di ko jagleel i ko soob ca llaaxira,yal na ylla dolli mucc ak xeewal ci sunu sang,Muhammad,ak oam aki saabaam. Aji xeebu ju yitewoo yrmaandey boroomam,ak ndimbalam ci ligeeyal yarkatam bii dib soppeem(di sri Tuubaa) - aji xeebu jooju di Muhammadul Amiin JOOP doomi Sheex Ahmadu JOOP mu Dagana, nee na: ag cant eel na ylla miy leeral ddinaam ji ci wlliyoom yi,di feealati ci oom yoonu yonantam yiy gindee,yoon woowu di wu weetal ylla ak jaamu ko,mooy yoonuw boroom xel yiy dq lu dul ylla ci seeni xel,tey jnge ag njub ca yooyale imam,ci jox leen seen bopp,jbbal leen seeni mbir. Ndax kat oou, ooy i ylla naan ci alxuraan:{ ulaayikal lathiina hadaahumul laahu fabi hudaahumuqtadih} muy ci maanaa oou,ooy i ylla gindi kon royal ci seenug gindi.Di julli tey slml ci yonant bi. Leegi nag ginaaw ylla day xewale xarnu bu ne aw waliyu wu koy gindi di ko won yoonu jub ,di ko tee jdd, nun waa xarnub fokk eent nag mu defal nu,xeewal gu tollu ne sunu mbg mii di sunub sri tey sriub julit i, Ahmadu doomi Muhammad doomi Habiibullaah yal na ko ylla wattu te wattul ko,te grmi jfam,te mngoo ko,moom nag mbooloo maa ngi ko gn a xame ci turu sheex Ahmad Bamba MBKKE Xaadimur rasuul. Bi loolu amee ma, bggoon a leeral as lf cig dundam, eel ki nar a w ginaawam,te bgg a xam dara ciy mayam. Man nag maa ngi gi ci ylla dellu di ci giaat naan dey xam naa ni xawma te du ma ci man a wax mbaa indi lu dul la gn a new,la gn a bari moom bu ko xalaat,ndax manu ma ko ba koy def. Waaye nag dinaa jem a nooyal yoon wi,ba ku bgg te ylla ubbi ko, barilub xam-xamam, yinkiiwal ko jari jaamam yi, ngir skku ci ngrmam,bu wee man cee jaar,ndax kat am na ci addiiz mu sell mi: {{ mbindeef yi njabootug ylla lanu ,ki ci ylla gn a bgg mooy ki ci pp njari ci njabootam gi. Nee nanu ku taarixal aw wlliyu mel na ni dundal nga ko. Kon am leen gttalug jaloore (jaloore mooy taariix walla histoire) gii ma tudde {irwaaun nadiim min hathbi hubil xadiim},may aan nag kpp ku ci gis lu ko yeemut, mu xam ne gttub jegoo ma too,mu jggalul ma Ylla te suturaal ma,te ba koo ngi,ndax kat da na ci gisi leneen lu bari lu koy yem, lu man a wecci loolu ko yemutoon, ndax tere bii ab muxaddima rekk la ( ag jiital) teere dgg bi mooy {minanul baaqiil qadiim fii ma aathiris zheixil xadiim) muy ci maanaa xeewali aji des jiy aji jiitu,ci ngneli Sheexul Xadiim.Doomam ja Sheex Muhammadul Bashiir defoon ko,yal na ko ylla smmu te guddalu fanam,te jari ci lu bari jullit i, ni baayam,moom dey teere bu boole la te wattu,te dib dr bu naat eel ku bgguw yiw te di ci dox. Yal na ko ylla mottali te nangu ko,te tas ko ci ddina bi,muy ndxtefam 3 www.daaraykamil.com

lg ca llaaxira,tey lu nu koy fttalikoo ginaawam ci fii fi dduna,ci barkeem ak ci barkeb ki ko taalif ak ki mu ko taalifal,yal na nu ylla nangul,te nangul nu sunub teere,matal ko te tas ko moom itam. Moom kat ylla mooy aji kawe jiy boroom ngnel ak tawfeex,tey boroom li fii ak la fee. Xamale kuy Sri bi, ak ay mbiram, ba bi waajuram wu gor lqoo Traliin

1 Ag ganeem adduna(g.m) 2 Ag yoram 3 Yaayam 4 Bi mu tollee ci war a jngi 5 Bi Mbba faatoo 6 Muhammad mom Muhammadul Kariim 7 Mbkke Kajoor 8 Bi nuy yobbu wayjur wi Deqale 9 Bu dee mbooloo mi

1 Ag ganeem adduna(g.m) Sri baa ngi gane dduna - ci li nu wax - ci atum junni ak aat temer ak juroom aar fukk (1270 g / 1853 g.j). Am u ne atum junni ak aat temer ak juroom aar fukk ak aar (1272g / 1855 g.j) ca kr waajuram wu gor ca Mbkke Bawal ,mu nekk leegi ca wetu yoonu saxaar ga. Boroom xam-xam bu mag bi nuy wax Alhaaji Hamidin doomi Usmaan Alfuutiyu Altilriyu nee na: (( sri baa ngi gane dduna moom mi sunnawoo sunnas yonnant bi,ci atum (sharaha),muy 1270g lqu atum (shumoos) muy 1346 g te booba mi ngi am juroom aar fukki at ak eent mel niy jant (cig leer). Am u ne juroom aar fukk ak aar. Ci guddig llarba, ci aar fukki fani muharram)).

2 Ag yoram Moom sri bi, bi mu ganee dduna aji juram ju jigen ju tedd ja a ko yoroon ba mu mat a jngi. Mu tudoon nag Amadu doomi Muhammad doomi Habiibullaah, doomi Muhammadul Kabiir, mom Habiiballaah mu njkk ma, doomi Muhammadul Xayri,. Muhammadul Kabiir mii mooy ki uy 4 www.daaraykamil.com

wooye Maharam,mooy ki sanc Mbkke Bawal, waxees na ne loolu ci atum Shaqdadin la di (1194 g / 1780 g.j ) . Waaye dkkewu fa woon, da fa a byyi woon ab taawam Muhammudu Farimata, magi habiibullaah waaye bokkunu nday. Moom nag s Maharam mii daa desoon Jolof, fa la lqoo u denci ko fa, di ko siaare. Mi ngi askanoo nag ci Tukklor,ay waajuram a ngi bawoo Fuuta,dem Jolof. Siiw na itam ne oom Gnnaar lau bawoo, dem Fuuta. Seeni doomi baay-tx ci naar yi ooy ou Moodi Nalla, oom nee nanu ay sriif lanu. Sama mag, sama sri, sheex Muxtaar binta Loo,doomi sheex Iraahiima ,sriub Njumri Loo nettali na ma ne dgg na ci sri bi luy dgral lool. Mu ne bis nekk na fa s ba nuy waxtaan ba tudd ag giir ci naar yi,gu niy askanale ag criif,s bi ne ko xanaa xamoo ne oou suniy mbokk lanu,mu ne ci noonu la xame ne oom ay sriif lanu. Man nag li may wax mooy seenug criif bu nu ko waxutoon te dggeesu ko it,seen jikko yu rafet tegtale na ko,muy tedd gu nd ak yaatug dnn,ak lewet gu nd ak njmmaar,ak jublu ciw yiw,ak ba jikko yu suufe yi,ak diinewu gu dggu. 3 Yaayam Yaayam soxna Jaaratul Laahi Maryama BUSO doomi Muhammad mom Muhammad mom Hammaad mom Alliyu Albusobiyu, ooii seenug criif lu wr la, i ngi cosaanoo ca Imaam Hasan mom Alliyu ibnu Abii Taalib karramal laahu wajhahuu, kon s bi seriif la ci nday ak ci baay. Lenn ci samay doomi baay tx nettali na ma te moom ku da kumpa la ci suufus Fuuta ,mu ne dox na bis juge ci dkk bu ndaw bu nu naan Bukke, jm fu nu naan Mbumbe, peyub Filaaw,nee na mu romb ci ay gent yu u ne ko ooy fi Mbkke-Mkke yi dkke woon. Am na ku ma nettali ci i sant Ba,ne Mbkke-Mbkke yi seeni doomi baay tx lanu, kaaf gi nekk ci Mbkke ag Haa (arafu h) la woon muy haa giy mujj ci Ba, Wolof yi def ko Kaaf,waaye wax jooju, ju doyadi la fi man,li nu jortu daal mooy aw sant wu ygg la, niki santi ajam yi,(ajam mooy ku dul araab). Li am daal mooy aari wax yi ju ci nekk, dgr na te am na mndargam dgg. Buso-boso yi nag oom, seen cosaan Fuuta la, ca fa nuy wax Golare. Barab yii yepp it yu jegee lanu. Barab yii it,ak wax yi ci am,am nanu mndargay dgg,yuy tegtale teddngay aari askan yi.

4 Bi mu tollee ci war a jngi Bi Sri bi tollee ci war a jngi,waajuram daal di koy jbbal nijaayam Muhammad doomi Muhammad BUSO, mbokkum ndayam ju tedd ju yiw ja. Mu tmbli koo jngal ba mu mgg as lf ,tmblee yewwu, mu jebbal ko moom itam nijaayam,sri Tafsiir Mbkke Ndumbe doomi Muhammadu Soxna BUSO, doomi Muhammadul Kabiir mi nu tuddoon,moom mooy mbokkum maami sri bi, ju jiggen, ndayi wayjuram wu jiggen,soxna Asta Waalo.

www.daaraykamil.com

Nu daan nekk foofa, fa moom ca Mbkke, bu noor baa, bu nawet baa, lu ci pp danu daa dem jolof, ba bi Tafsiir mii lqoo te booba sri baa ngi jeggee mokkal. Kenn ci u wor i nettali na ma ne: sri bi nettali na ko ne lliwaam a ngi tulloon ci latajjidanna bi jnglekatam boobu di lqu,mu dal di dellu ca wayjur wa, dal di farlu ci njng mi ba mokkal alxuraan , def tajwiid ak tas-hiih,ca a ko daa defale ca jamono jooja, loolu lepp ci wetu baayam,daawul tggalikook moom lu dul lu new,ndaxte magam Maam Moor Jaara dafa nekkoon ca kenn ca tas-hiihkat ya ca yeneen dkk ya.Bu ko defee leeg-leeg mu jaar fa nekk fa ak moom weer,walla aar,doog a dellu,booba a nga Saalum,ca jamonoy jiyaarkat boobu di Mbba Jaxu,ndax kat booba oam Mbba boole woon na leen ca a mu paoon (dajale woon) jme Saalum, nga xam ne Bawal ak Jolof daanaka bawu fa woon kenn.

5 Bi Mbba faatoo Bi mu faatoo nag moom Mbba, nit i dal di dellu seeni dkk , waajuram wi moom itam dellusi ci i doon dellusi, nd ak Latjoor. Ci noonu nijaayam akug njabootam des foofa,sri bi it bokk ci,ngir jng xam-xam,noonu mu tmbli di jng ci baay txam,Samba Tukklor KA doomi bjjani baayam. Bi mu jngee ci moom dali xam-xam, tmblee yewwu ak a aw as lf, la dellu ca baayam,te booba ma nga Paataar,benn dkk bu ndaw bu nekk ca wetu njndul Amadi Yala,dkkuwaayub Latjoor ca joojale jamono. Ndax moom s Mammoor daa defoon ku Latjoor fonkoon lool,daa ko laaj tey diisook moom,waaye moom s Mammoor bggutoon a dkk ak moom,ndaxte du woon ku xemmeem seen alal ji,du caagenug seen teddngay nguur gi ,li ko loruloo woon, tax it mu dppoo ak oom ak a mudaaranteek oom mooy njaboot gi mu yoroon,bu ko defee Latjoor daa ko dkkal ci wetam,waaye s bi daawul nangoo dkk ak moom,moom kay day dkk ca wetu pey ba mu ne rekk, ndax da daan jng ak a jngale,te jng ak jngale neexoowut aki buur, moo waral ca wetam la dkke woon,nga xam ne su ko soxlaa w ci lu dul ab coona. Ci noonu s bi nekk ak waajuram,di jng ci moom te di farlu ci mokkal gi,ak xeree gi ak dgg-dgglu gi,ba faf raw ci fann yi. Ci biib diir it daan na ci def leeg-leeg mu seeti s Xaali Majaxate Kala,moom mi dkke woon fa pey ba ak Lajoor,di woon ku raw ci fanni xam-xam yi, rawati na lkkuw araab,di ku siiw ci man a woy,bu ko defee muy xamlu ci moom araab,leeg-leeg it mu daa ko indil ay woy,yu mu def ngir mu toppal ko lihraab ba ak araabe ga,ak harool ba,leeg-leeg mu gnneel ko ci moom Qaali ab yq, mu mujj nag moom s bi far ko raw, mujj saa su ko wonatee lenn ci woyam yooyu,mu ni ko indil ma ko, ma mokkal ko, kon mujj na toppalatu ko waaye day mokkal li mu koy indil,nii la nekke woon ak Xaali. 6 Muhammad mom Muhammadul Kariim Amoon na fa it beneen boroom xam-xam ci waa-gnnaar yi,dkke woon Njaa, tuddoon Muhammad mom Muhammadul Kariim,bokkoon ci giirug Daymaan,ci doomi Seyidil Faadal yi, u gnon koo xam nag ci turu Muhammadul Yadaali,waaye bokkul ak ki def tere bi nu naan Zahabul Ibriiz ci tafsiir,ndax kooku 6 www.daaraykamil.com

am Yadaalim Daymaan mu ygg la . S bi bariwaa na lu mu ko daa dikkal,di jng ci moom xam-xamu Bayaan (xam-xamu wax ju rafet),yaakaar naa ne nee na it - ci lenn li mu nu daa nettali ylla a xam - ak bu Mantiq (xam-xamu xellu). Bi waajur wi xamee ci moom raw gi ak cawarte gi ak laabiir gi,mu dal di koy jox mbirum njngale mi. Bari na lu mu ko daa jngal ab bind ci kanamam ci tereb boppam ba ,walla ci tere bu mu dalagul, ngir mu jngal ko boroom bind boobee walla tere ba, bu wee,ngir wolu gu mu wolu xam-xamam akug awam, s bi it daan ko def,ba li pp ci dongay s Mammoor yi mujj fetesi ak moom,doylu ci moom,waajur wi byyi leen ak moom te bg ci. 7 Mbkke Kajoor Waaye yggul dara rekk Latjoor tuxoo Kr Amadu Yala, dem Sukeer peyam ba ca Kajoor,yobbaale s Mammoor mu sanc ca wetam, tudde ko Mbkke Kajoor, sax fa aari at daal di wuyyuji boroomam, nee nanu, looloo ngi am ci Muharram, atum 1300g, dgg naa ci S bi mu ne bi waajur wi tollee ci sukkuraat, took na fa boppam wcce fa ab kaamil bisub altine,guddig talaata mu lqu,nu denc ko Deqale ,di ko siyaare,man dey Alhamdu lillaah dem naa fa ba siyaare ko. 8 Bi nuy yobbu wayjur wi Deqale Bi nuy yobbu wayjur wi Deqale muy dkk bu ndaw ci dkki Kokki yi,ci wllug Mbaakol,s bi ndon na ca gunge ba,di liiru,bariwaa na bu ko ab gawar bggee joxuw fasam,mu ne dox a ma gnal,bi mbooloom dkk bpp dajee di mbooloo mu kenn masta gis,nu jublu ci jullee new bi,jiital s Tayba Muhammadu Ndumbe Maar SILLA, mi nu tuddoon ci buntub seedey u mag i eel kii nuy wax ci moom. Bi nu noppee ci julli gi,ak denc gi,s Tayba digale nu daje te dal,te xerawlu,ci noonu mu jug, xutba,waar nit i,wax wax ju rafet bi miy jaale s bi nit i,bi mu noppee ne ana S Bamba,noonu la nu ko daa wooye oom,ca jooja jamono,mu wuyyu jug,ma nga woon ca catul mbooloo ma,s Tayba ne ko jegesil,mu xaw a jege bay degganteek moom,di gisanteek moom,di ko man a tontu ci lu dul muy yekkati kddoom,dal di yam foofa ngir ba a jggi nit i,xutbakat bi neeti ko jegesil,mu ne ko maa ngi lay dgg,S Tayba dal di koy jaale njaal mu rafet,ne man nag dama doon skku nu nd ci mbooloo mu mgg mu sa moroomi waajur wii,ngir nu seeti Latjoor,jaale ko sa waajur wi,jaale gu ko man a dfal,ngir kat moom ab xaritam la woon,dib soppeem,te dib sriam,daa diisook moom,bu ko defee nu waxtaan ak moom ci yaw,sampu la fa moom,ba mu man laa teg fam tegoon sa Baay,bu ko defee doo gis ci moom lu dul aw yiw ak teraanga,lii daal mooy sama xalaat,yaw nag luy sa xalaat,s bi ne ko,li aju ci jaale gi ak dfal gi maa ngi la ciy sant,te di la ci aanalub yool,waaye mbirum seeti ay buuri dduna moom duma ko def,ndax xemmeemu ma seen dduna ji,te soxlawu ma seen teddnga,teddnga ci ylla laa koy skkoo buurub buur yi,mbooloo ma tiit,tas. a cay u baax wax ji da leen a yem, rusloo leen,ndax dggu gi mu dggu, tey toroxal way bgg yi dduna,juge ci seen doom ju diw waxambaane,tegi tnkam ci seeni wagg te manu u ci dara. 9 Bu dee mbooloo mi Bu dee mbooloo mi moom, li leen yem mooy,ba gi mu ba teraanga ju teew jii,ak xewal gu jppandi gii,nu ne kii daalub dof la,ci loolu S bi def na aari dagiiti woy yu rafet te yeme,bu njkk bi mooy waxam jii: {nee nanub dof laa,ngir wlbati gi ma wlbati samab gis wlif leen}ba fa mu yam teewluwu ma ko te woneesu ma ab yaxam jamono ja may liggey,waaye beneen bi moom mooy wax jii: 7 www.daaraykamil.com

{{ nee nanu ma jngal jm ci bunti buur yi,kon dy da nga am ay may yu lay jari jamono ju ne)). ((Ma ne leen ylla doy na ma,doyloo naa ko,soxlawu ma lu dul xam-xam ak diine)) ((Yaakaaru ma te ragalu ma ku dul sama boroom,ndax ylla'ay ki may doyluloo te di ma musal )) ((Nu may joyale samay mbir jme ko ci o lottu nanu ci seen mbiri bopp,ni miskiin yiy lotte? )) ((Walla nan la ma bgg poatum dduna bii di jae,jm ci dkkaale ak o seeni kr'a'y drub saytaane )) ((Su ma dee naqarlu mbaa may bg boroom Aras laay woo. Mooy Aji dimbali, ji dara dul t,te mooy Kiy amal li ko soob )) ((Bu bggee gaawalum mbir loola gaaw,bu ko nammee yeexal mu yeex ba cib diir)) ((Yaw mi may yedd bul sonal sa bopp , ndax kat man amuma lenn lu ma naqari ci kk ddina )) ((Bu dee sama ayib mooy dddu gi ma def ci seen poat mi,kon dy ayib jooju, ju gnjaru la, ju ma dul gccaal}}. Waajuram wu jigeen ,wu tedd waa nga lqoo Poroxaan ca Saalum, nu denc ko fa,jamono ja fa s Mammoor nekkee. Ginaaw saayug waajur wi Moom s bi,bi waajur wiy dund, nanguwutoon a taxaw mbaa muy taxawal dara,moom daal ci moom rekk la toppoon ,mel ne new bu nuy sang, fu nu ko jmewul du fa jm. Bi mu lqoo nag,mu des ca ligeyam ba mu ko byyee woon at ak lu topp. a fa nekkoon it ciy dongo jng rekk a leen fa byyi woon, du leneen,moom itam ab jngalekat rekk la woon,waaye loolu teewul woon mu doonoon ku daan yr (jng) lu bari terey Gaa a (gaa i bu u ko waxee aare mooy magi tasawwuf yi) . Ylla defoon muy ku sopp beru ak wr ni ko u baax i (o tasawwuf ) soppe woon. Mu daa indi ay anam yu wuute ci seeni waxiin, di leeral seeni maanaa yu lqu, di yg seeni lmmi. Noonu la nekke woon ci yooyu yg-yg ak yittewoo suufiyu yu mag yu njkk ya, ak a gstu seni wax aki mbind ba mujj himma ju kawe ji (himma ci lun man a firi mooy yitte) dikkal ko, muur ko, ykkati ko, yngal ko,dalal ko, mu mujj moomatul boppam manatul a def lu dul woo nit i ci anam gu woyof jme ci mbiram moomu (muy tasawwuf ak ab yg-ygam). Bi ko mbir mi gnee ljal nag, gn a fees fi moom,gn a ry,mu dal di biral woote gi, wax wax ju leer. Dajale mbooloo mi,taxaw fa oom xutba leen,sukkandiku ci dokkub dogu,ne leen: Dama ne: ku ndoon ak un ngir jng rekk na laxas jm ca boppam, na dem fu ko soob, man loolu rekk taxatumaa jug, ku bgg li nu bgg nag,na toog. Daal di leen fay byyi dugg ca biir. Waxam jii nag daal di leen byyi cig jaaxle, enn i dem, a ca des,des fa,am uy jeem a tyye seeni xarit ngir u des,ak uy xiirtal seen waay ci u dem. S bi moom ne tekk rekk,jeemul a tyye kenn ku bgg a dem,ba mujj li pp ci mbooloo mi dem byyi ko fa,la ca gn a new des fa.

www.daaraykamil.com

Bi loolu lpp daata am,fekkoon na Sri bi mu sobu woon ci ngiirum taalif ci xam-xam yu nu tuxal yu sariiya yi; mu woy Ummul Baraahiin,bu Imaam Sanoosi,wayjur wi nangu ko, bg ci ,te mujj di ko jngale ,byyi wesar wa doonoon cosaan la. Dgg naa ci S bi mu ne woy woowu de waajuram jngal na ko aari doomam yii di sheex Coro,miy Siidi Muhammad Alxalifa,ak s Aafe,mi tuddoon Ahmadul Muxtaar. Mu woyati teereb Imaam Xazaalii bi tuddoon Bidaayatul Hidaaya,dal di koy tudde Mulayyinuz Zudoor ,di ci maanaa (aji nooyal ji dnn yi ),ginnaaw bi mu gttal ko,tudde ko Munawwiruz Zudoor,di ( aji leeral ji dnn yi),ci atum 1294g/ 1877 g.j, teg ci Jzbatuz Zixaar,di (bijjig gone yi) ak Jawharun Nafiis muy ( wurus wu gnjaru wi) nga xam ne da cee woy wesaruw Imaamul Axdariyyu,ak yu dul yooyu. Bi ko dongo yi nangulee nag lii mu leen doon woo,daa byyi njngale mi,jm ca di leen tarbiya,ak a tarqiya (tarbiya mooy yar ni ko sariiya bgge,tarqiya di ykkatee jme ca ylla).

Man nag nee naa lii de du kk muy ndigalug yonant bi (j.y.m),ndax kenn ci sunu sri yi nettali na ma,te moom ku wor la di ndrlaay,ne S bi de wax na ko ne yonant bi (j.y.m) moo wax ak moom ci gimiam,ne ko yaral sa ndandoo yi ci Himma te bu leen yar ci njng,loolu S bi gn na koo leeral ci xasida gii: { Bokk na ci kiimaani doomi Abdul Laahi ji,yal na ko ylla dolliy xewal ak mucc,moom miy leeral suufam si ciy wlliyu ba yawmal xiyaam,te ku ci ne mngoo nga sunnaam si,di ko ogal wlif bidaa,bokk na ci kiimaani doomi Abdul Laahi jooju,bgal gu mu bgal jwrinam jii ci ne ko(fazdah) mooy wooteel ca kaw) ( Yonant bi (j.y.m) digal na ko ne ko mu jngal Muriid yi,ak ku nangu mu laabiire la ci waa jamono,te mooy ki ko ggale ca borooman cig taxliya ( mooy setal nit ki fexal ko ciy ayib ) bgalati ko ci tahliya ( muy rng nit ki ay takaay,walla sol koy ngnel) }.Li mu jublu ci Fazdah ji nag (mooy biralal ca kaw) ,mooy ji ci alxuraan:{ fasdah bi maa tuumaru wahrid hanil musrikiin} mooy biralal li nu la digal te dddu way bokkaale i. Ylla daa digaloon yonantam bi (j.y.m) mu biral wooteem ga,ginaaw bi mu ko daa yalu,maanaam dggdggi loolu, mooy sri bi,bi donn gi mu donn yonant bi matee,ci matalug ylla (t.s) ,te mu dolli ko ay xam-xam aki hikma,aki leer,aki mbot,te may ko kttanug man a yanu wilaaya gu mag gi- bi loolu amee nag mu digal ko mu woote ca kaw,woo mbindef yi u weeru ci moom,di jle ci moom tey def ay ndigalam,di byyi ay tereem,ci loolu la waxe: { ylla mi nga xam ne lu ko soob mu def,moo ma jox xamxam yi,ak seen barke,wattu naa lu xajul ciy tere,kon boo may ligeyal bul tyyi.Ylla miy joxe,jox na ma ci darajay yonant bi,barkeb alxuraan,ak xam-xam yi,jl seen barke def ko ci samam njngale.Ylla jl na mbooti laa illaaha illal laah def ko ci samy taalif,ylla jox na ma te dootu ko nangu,te man kaaraange laa te dib weeruwaay ci ndimbalam.Loolu nag ngnelul yllaa,ku ko soop la koy jox. Te nee na ma : (neel weru leen ci man}. Ci maanaa sama boroom digal na ma,ma leeral nit i ne:man ab weruwaay laa tey kaaraange,ku bgg aw yiw dduna ak allaaxira,na weru ci man. Mu dellu waxaat ne: { Murid bu yoqatul ci man de texe na,ci lq ngn ji ay may. Murid bu Ylla wommat jm ci mu aju ci man, texe na te da na cru ciy may ) (Murid bu weru ci man de ylla miy sama dkkandoo bu kawe bi,def na muy ku texe ci lu kawe njortam) (Bepp murid bu aju ci man,day texe,te ku niy soril la aw ay. Kpp ku aju ci man dy am nga ag mucc ci nx-nxi ddina ak allaaxira}. Ginaaw bi mu leeralaat ne way gmi jinne ypp ci jamonoom ,aju nanu ci moom,mu ne : { Jinney sama jomono jii dey, a ca gm pp aju nanu ci man,waxuma a 9 www.daaraykamil.com

gmul}. Mu wattuloo nag i aju ci moom, uy xccati ginaaw bu nu jbbaloo ne: { toroxte eel na ki ma dddu ,won ma ginaaw,mu ma,ginaaw bi mu duggee dib murid}. Dal di leeral lu dig murid,ak lub murid di bgg,mu ne: { Dgg-dggi ag murid - ci li sang si wax - mooy byyi aada,( muy li nga nekkoon njkk ngay jbbalu),bu ggagul ba noppi dellu ca la mu nekkoon, mook ku murtad ay yam) ( Ndax kat ab murid du bgg mukk lu dul gramul ylla ak fu mu man a jublu}}. Mu leeralaat ni ab muriid di mel,ak ngrtel nd ak sri bu gg,mu ne : {{ Melow ab murid,mooy ba a bgg dara ngir ylla. Ku bggul lu dul ylla, gg fa moom,mu jox ko aw yiwam )) ((Ku aju ci ku gg, gg,ku aju ci ku ggul doo gg )) ((Ku yaroowul ci loxoy ab sri, dana dajeeki coona )). ((Ndax ku amul sri buy gindee,saytaaneey mujj di ab sriam fu mu jublu)) ((Ab sri du wuuteek Ku nu rammuloo ki (muy yonant bi) kon ku jublu aji yar (sheexul murabbi) de da na jariu )) ((Fu la aji yar digale,defal,kon nga gg ca boroom ba)) ((Bu la aayee dara bu ko jege,te bul sggan ci wut gramam }}.

Mu leeralaat ne murid saadiq de am na ay meloom,yoy bu ko amee am wpp yiw: {{ Meloy murid saadiq ci gttal, eent la,ma tnk leen nag ciy bayit ngir ragal woru)) ((Dggal ci bgg sab sri ba fwwu,jfey ndigalam fu mu rote rekk )) ((Bayyi gaaru ci lu mu man a doon (gaaru mooy di am xalaat ci ndigali s bi), ak doonte ci sa baatin la,ci li nu nettali)) (( Ak a tnnal sa bopp la ngay def,ngir sa rafetug njort )) ((Kpp ku boole yile melo ci murid yi dy,da na jot ndrlaay ya (gaa yu baax ya)}}. Mu biralaat ne kiiraay am na juroom benni cosaan,yu murid bi war a dagg,te malaaka yi daiy jooy ci murid bu bgg lekk, ne: {{ Kiiraay am na juroom benni cosaan,ku bgg a gg da nga leen dog, ooy baril lekk ak naan,ak a jaxasook nit i)) ((Bari wax,bariy nelaw,sggan ci tudd ylla miy jmm)) ((Gstul loolu ci Jawaahirul Mahaani,bi sunu Sheex Tiijaan mu nu mggal mi def)) ((Nettali nanu ne malaakay Aji mgg ji,daiy jooy ci murid bu bgg lekk,ngir yram ko,loolu man nga koo gis ci taalifi boroom Hawaarifil Mahaarif}} Mu neeti murid saadiq doomi waxtoom lay doon,ne: {{ Murid Saadiq mooy kuy wlbatiku nd ak waxtu wi mu nekk,te du fuglu wa ca kanamam,ndax loolu day teree ywenal waxtu wi teew )) ((Gstu leen loolu ci Jannatul Muriidi,tere bi sunu sri Xaliifatur Rasiid def}}. Ak lu bokkul ak loolu ,ci li mu wax ci mbirum boppam, mom muridam yi,nga xam ne ,bu nu ko toppoon,indi fi lu yem xel yi,te da na mujj kon,gttal gi nu bggoon ci tere bii,du amati,ndax moom tere bii as kook la ci geejug xamale ko. Nu indil leen fii nag as tuut,su nu tas ci wone lenn ci sekkarey xaybu yi (xaybu mooy lu faddu,muy mbirum biir niki liy xew te xewagul),mu bgal ci i aju ci moom, ngir dolli leen ag xeemeem,ak sawarloo leen,mu wax ne : ((i aju ci man bu nu ko defutoon dem sawara,doonte as ndiir lay doon it,njkk nuy tbbi ajjana,ji nu dig u ragal i ylla)) ((Li waral sama tukki bu sori bi,Ylla mu barkeel mi te kawe,daa bggoon ca asal,may kiy ramu samay donga,dox na sama digante ak nasaraan yi,tbbal ci seeni xol ag ragal ma,nu def la nu def nag ngir ma ba a nekk dib nasaraan, ndax bu ma ko doonoon tabbi sawara ,walhiyaazu billaahi. Waaye Yllaa ma aar ci sawara,ak lpp lu mu gramul,ci darajay Yonant bi (j.y.m))) . Mu bind ay laabiire eel murid ypp,ne :{{ Mi ngi juge ci man jm ci mbooleem murid, yu gor yi ak yu jigen yi,ab nuyyoo bu teey,bu leen di musal mboole seen,te di leen tabbal ci jmm ak aafiya,ci addina ak alaaxira,ci barkeb Yonanat bi (j.y.m),ginaaw bi, may digal kpp ku aju ci man,ngir ylla mu kawe mi te 10 www.daaraykamil.com

tedd,mu xamlu pas-pas yi ak tawhiid,ak ttey laab,ak julli ak woor,ak lu dul loolu ci lpp lu war mukallaf,man nag warlul naa leen taalifal leen mbooleem lu leen koy xamal, ngir jmmi ylla (t.s),wasalaam)). Mu bind lenn ci ay murid ab tontu bu neex yal na nu ci ylla boole un pp,mu ne ci:{{assalaamu halaykum warahmatul laahi tahaalaa,wa barakaatuhuu,ma lay xamal ni sa bataaxel ba agsi na,yaw murid bu dggu bi,waaye na la wor ne doo gis lenn loo ragal,booy faatu ak ci bmmeel,te aari malaaka yiy laaje,xam nanu sa sri,te da nanu doylu ci xam gi, ba dunu la laaj dara)). Lii nag xamle la gu mu teg ci yoonu laaj ak tontu,laaj bi moo di lan la s bi woo ay taalibeem jme? lan mooy tontu li? Moo di sellal,moom mi nga xam ni mooy ruuhug jf tey ngrtel xam-xamub way xam i ylla,tey waralug gg ca Ylla, gg ci Ylla nag i ngi ci jublu jaam bi nekk di ku wetal ylla,ciy yggoom ,aki dalam,aki pas-pasam aki waxam,ci lepp,li fee ak li nbbu,lii nag manut a ame ci njngale rekk,ndax kuy jngale ab tegtalkat rekk la,li ci des,mi ngi ci aji jng ji,man naa am mu jfe man naa am det,du ligeyub jngalekat,muy sonnu ci waa ji jfe loolule,loolu Sheexu tarbiya la war.

Bokk na ci ligeyam,moom sriub yar,jng ak jngale,ak ligeyloo,ak ay tudd ylla,ak gindee ginaaw bi mu leen xiirtalee cig cofeel gu dggu,te du tggook oom li feek wonu leen seen ayibi bopp, ligeyloo leen ci nu jem a laab ci yooyu ayib,ngir man a gg ak oom fa Ylla inshallaah. Bu loolu jllee,mbirum tarbiya day mbir mu gudd,manunu cee wax fii. Mu dem ak oom ci yar leen ci himma, u nangul ko ko,mu dox ak oom ci ngrum tggat,dajale leen,di leen ligeyloo lu bari,yanu leen ci fttaliku Ylla lu bari,ak a jngi xasida,ak taqoo laab,ak a beru,rawati na sori jigen i,ci noonu u kawe u dul oom,ndax donoo joxe woon seen bop ak seen alal ci yoonu skku gramul Ylla,{Yalla jnd na ci jullit i,seeni bakan ak seen alal,faye leen ko jjana},S bi wy ci yoon wu jub wii mook saabaam yi, dale ko ci njlbenug atum junneek atti temer ak benn,ba bi mu sancee Mbkke Bawal,ci at moomu juge Mbkke Kajoor,sax fa lu tollook aari at ,nit i di ko dikkal juge fu nekk, ii di jebblusi, ii di joxesi ddiya, iiy skku ndimbal. Mu mujj yoonu kram gi mel ne yoonu ab ja, ci eenti at yii nag mu siiw ci,siiw gu kawe, u jege i ak u sori i, epp di yemu ci moom,te booba amagutoon sax fan-weeri at.

Ci diir bii s bi wr na ci rewum wolof mi,dale Saalum ba Waalo Barak,siyaare fa mag a, a cay dund ak a dundul,jaar ca sri sa ,jle ca oomi wird,bokk na ci i mu siyaare, o sheex Siidiya,siyaare na bmmeelam ca Tindawja,siyaare sheex Baaba mom Abiihi ca Maymooni,tagg leen,jle ca oom,woy cllaleg xaadir gi,tmblee ko ca sheex Baaba ba fa mu yam,looloo taxoon kenn ci Sheexi naar yu mag yi laajoon ko kuy sa sri?,mu ne Rasuulul laahi (j.y.m),mu ne ko kon lu tax nga ne fi di tudd waa kr sheex Siidiya,ak a woy ay sri ak a tag?,Mu ne booba da maa melon ne ku gumba,di lmbatu yoon wi,di ko skkoo xam ci ku xam ak ku xamul,bi ma dajee boroom yoon wi ci ndimbalul Ylla nag muy Yonant bi (j.y.m),mu xcc ma ci boppam,laa wacc ker-keraan yi,waaye di jokkook oom ngir Ylla ak a soppanteek a jariante ngir moom.

Te wax na dgg,ndax mbiram ak o Sheex Siidiya loolu lay tegtale,mujj nanu mel niy doomam mu mel ni seen baay,di leen jari ci alalam lu leenub buur jariul,ab sri it jariu ko ab taalibeem. 11 www.daaraykamil.com

Sheex Baaba tag ko ciy xasaayid,aki dagiit,yu tollok ay temeri bayit,bokk nanu ci yile:( Shex Ahmadu xewal la gu ylla jox mbindefam yi) ak waxam ja: ( s bi daal xewal la gu ylla xewalee,di kiimaan ci kiimaan yi),ak yu bokkul ak yooyu,bu waxutoon yu dul yii it , aari bayit yii,rekk doyoon nanu seede ci mggug s bii,ak wilaayaam. Ndax kat sheex Baaba ak mggam gi, du fo mbaa muy yaxantu ci woy ni suharaawu yi,moom dey lu mu wax ci ndigal la ko teg,ak jaamu Ylla,yal na ko Ylla fay ci aari bayitam yooyu. Bokk na ci i mu siyaare ci sheexi naar yi,Ustaas Baaba mom Hamdi, ma jublu ci Hamdi mu aareel mi,dikk na fa yendu fa fanaan fa,nee nan ci menn mbaar. Sama xarit ba niy dkkantale Kaadi Sheex Abdul Xaadir,doomi Amiirul Kumlayli , nettali na ma te booba taalibeb Ustaas Baaba la,ne Ustaas mii moo jox s bi sekkare bi,waaye nag leeralu ma ban sekkare la,man naa am muy wirduw Saasalii,ndax s bi bind na ne moom wirduw saasali mi ngi ko jle ci wenn wasiila,njkk muy daje ak wasila wu mag wi,di Yonant bi (j.y.m) ,te leeralu nu kooka kan la. Li waral Kaad mii nettali ma ko,mooy maa ko laajoon bi mu jlaatee ci s bi wirduw Sasalii,ndax xam nga ci ku ko s bi jle woon,mu ne dedet,waaye nettali li mu waxoon ci diggante s bi ak Ustaas Baaba,nu jorte ci ne ci Ustaas Baab moomu la ko jle ndax moom ab xaadir la woon.

Kaad nettali na ma ne bi s bi agsee, ci bi miy siyaaresi Ustaas ,ci bcgug bis bu sell,Ustaas defaral ko am soow mu neex ci ndox mu sedd,ak suukar,looloo ngi amoon,ci jamono ji s biy nattu boppam ci di tegoo ay coona,mu ne ko naanal mu ne ko man baax na du ma naan lii, mu ne ko,ndax daa baaxul ci wllug wr,waala da nga koo byyi ngir Ylla di jiyaar ak sa bakan,s bi ne ko waaw loolu la,mu ne ko kon naanal,byyiwu ko ba mu far naan,ginaaw bi la dongay Ustaas yi laaj lu waral mu sonnu ci mu naan soow mi,mu ne leen ndax moom kat sonal boppam rekk la bgg,ak mettital ko,mujj loolu di aadaam ngir Ylla,ju mu manatul a byyeeti,ndare cib coona,ma jflante ci ak moom waaye Ylla defal na ko barke,ndax mujj na dgar ci kng.

Ginaaw bi lii wyee lu ygg,Ahmadu doomi Ustaas seetsi na S bi Njaarem,mu bg ci lool,di ko ganale ngan gu mu sonn,indil ko am yi ak naan yi,bi nu ggee ci ataaya, Ahmad xam ne mbir dana am ,ndax moom du naan ataya,bi ko s bi tllalee ataaya ji,mu ne ko du ma naan ataaya,mu ne Yllaa tax nga byyi ko ngir jiyaar ak sa bakan walla ag weradi,mu ni ko Ylla,mu ree,ne ko naanal ma fayoo ca la ma sa baay defoon, aanal ko ci barke. Bi S bi nekkee ci wram googu nit aa ngi ko daa dikkal byyikoo ci gpp wll ngir xam-xam bu bari bi ak njari li,ak cofeel gi nu amoon ci moom ak diinewu gu dggu gi,rawati na alal ju bari ji mu daa joxe rekk ,nga xam ne daawul tyye ab drm,lu w mu joxe,di jox mag ak ndaw goor ak jigeen,gor ak ab jaam,ku am ak ku amul,ku baax ak ku bon,loxo bu tllaliku jm ci moom mu feesal ko te soxlaalul nit i, doyloo kppitaalam bi dul lu dul jublu ci Ylla ak yiteem jpp. Mu dem Gnnaar jaar ca sri ya,siyaare ay dund ak barabi way faatu ya,jari leen ci alalam,ju bari ja,nu sopp ko nu kawe ni ko u uul i soppe,defal koy xasiday tagg,siyaaresi ko ci rewam ginaaw bi.

Bi mbokk yi gisee ci moom kaweg xel,gu diine,gu mbaax gii mu yor ak jublu gi ko dduna ak nit i jublu,nu tmbli di ko iaane,di ko lor,mu daan julleendoo ak oom,lor yi pp,mu mujj beru leen ak am 12 www.daaraykamil.com

mbooloom ak jkkaam, Ylla gn a fsal mbiram, u gnatee mer,nga boole ci terewu gi mu defoon ci mbirum buur yi,daawul nangoo jaxasook oom,ba da daa skku sax ci s Mammoor ci ay bataaxel yu mu ko daa bind, - da daan kersawoo jkkaarlook moom di ko ci wax dara - mu byyi ag jflanteem ak buur yi,naan ko seen teddngay fii ji toroxte la lg,s Mammoor daan ko ko nangul,te di ko ci jggalu,waaye njabootam gi taxoon ba manu leen a byyi.

Ma nettali leen as lf ci jaloore,nee nanu,bi kenn ci jaraafi Latjoor yu mag yi -mu nekkoon ku am solo fa Latjoor - jbblusee ci S bi,mu bokkoon ci jmbaar yi amoon ay alal,mu ndmmoom (gaewoon) lu bari ci mggum xareb Samba Saajo bi ( mgg mooy li niy jle ci koo xeexal ba not ko) .Samba Saajo ab dkk la bu nekk ca penkub Njmbur,diggam ak Jolof,la xare boobu ame woon,ci diggante Amad Sheexu BA mu Fuuta, ak Latjoor,Tubaab yi japle woon ko moom Latjoor,ba mu gae ko, ray ko,xarekati Latjoor yi gaee ci woon mgg mu ry,ci alal ak ay jaam,te a ca pp diggante Jolof ak Fuuta lanu byyikoo,ak Kajoor,tey jullit lanu, buur bi laaj ndax man na leen a def ay jaam, kenn ci boroom xam-xam yu mag yi,ne ko waawaaw,ndax Ahmadu Sheexu da doon wooteg yonnant, kon alalam ak dereetam dagan nanu, nu dal di wyal loolu,te kat ag wooteem yonnant mbooloom boroom xam-xam yu mag yi saxalunu ko. Li waral xare bi,lu gudd la manunu koo netaali fii. Bi jaraaf jooju tuubee ci s bi,mu digal ko mu wacc mbooleem jaam ak alal ji mu ame woon ci xeex boobu, jaraaf ji dggal ko,def ko nd ci ak kontaante, Latjoor ak ay gaayam jppe loolu nag ag weddi eel tte bi leen kenn ci boroom xam-xam yi defaloon,ne leen jaam yi dagan nanu. Nu mere woon ko,nee nanu ma jaraaf ya woo woon nanu jaraaf jooja fa kanamu Latjoor,ne ko : lu tax nga bokk ak nun ndab,rgg rekk wlbatiku,doyatu la nga ciy xpp suuf? Mu ne leen waaw,we a tbbi ci sama bakan,ljal ma, moo waral lii ngeen gis ci man,waaye bgg a nxal seenum mbir taxut. Mu jublu woon ci we wi,lislaam ji ko duggoon,cig mbetteel,yaw nag xam nga ljal gi lislaam di def ku mu dugg, du ko byyi ndare bu daa tuub.

u xam ne li mu wax lu dggu ci moom la, u jggal ko, noppi cim mbiram. Waaye S bi moom, Latjoor lijntilulu ci anam gu nooy,te teey,nun ko ko indile,mu bind koy leetari leetar,yonni fay ndawi ndaw,teewul S bi ba,nee nanu ma wax na bis kenn ci ndawi buur bi,ne ko : {neel ki la yonni rus naa malaakay Ylla yi di ma gis ma jm ci buur bu dul ylla}. Dgge naa ci sheex Aadama SLL - moom kenn la woon ci i njkkoon a jbblu ci S bi , cosaanoo woon Jolof - mu ne leetar bi s bi mujj a bind Latjoor moo ko doon yobb, mi ngi ci naan: { Muhammad Ibnu Maslama nee na boroom xam-xam ci buntu buur,mi ngi mel ni we ci kawi jonkan},Latjoor jox Xaali Majaxate Kala bataaxel bi - moom moo nekkoon mufti bu mag bi - Xaali yr ko tiit, ne :( Innaa lillaahi wa inna ilayhi raajihuun) buur bi ne ko lan la ? mu ne ko,kii waxul ak yaw man lay waxal,mu ne lu man a xew waxal rekk,mu jngal ko ko,Latjoor ne ko: ci man de la gn a dal,ndax yaw lu man a xew ,yaay we wi man nag,ay dem-ll laa. Waaye nag yaw miy boroom xam-xam loo wax ci moom? Xaali ne ko man daal li ma gisoon,mooy nu byyi ko ak mbiram ,ndax kat notante ak moom ag woru la,boo ko notee bokk ci i gn a kawe,bu la notee, nga di ci i gn a suufe,te maneesu koo not. Buur bi ne ko wax nga dgg,ndax baykat kat ygg naa

13

www.daaraykamil.com

gis jnji ci toolam - te manu koo bay, manu koo saxal -mu byyi ko fa,Xaali ne ko waa-waaw,mu ne nan ko jppe jnji boobu. Ci noonu leetar ya dog,wax ja jeex,alhamdu lillaah. Beneen nettalee ngii bu gnatee yeeme,waaye soriwul bu njkk bi,mooy,bi leetar yi ak coow li jeexee ci bataaxel bu saf boobu,ylla dogal na Latjoor nd ak Xaali ci lenn ci tukkeem yooyu mu daa def,ba wcc benn dkk wetu fi s bi dkkoon, bi S bi ygee ne moom ak Xaalee nd,mu ne na nuyji Xaali,ngir aari mbir,menn mi, mooy Xaalee ko daa jngal,te ku la jngaluw araf sa kilifa la, aareel bi,xaritub baayam la woon,mu war ci moom mu jox ko qam te jokk ko,ndax danu ne : ( joxe qi waajur gi gn a mat,mooy waa ji dox kllare ak jokk ko ci xariti baayam yi ). Bi mu agsee fi oom, fekk leen nu toog ci lal,s bi nuyyu leen,nuyoob mggal,toog ci suuf,toogul ca laltu ga fa nekkoon,bi mu toogee tuuti ne Xaali,da ma la fee deggoon rekk ma ne naa fi jaar siyaare la,ci noonu Latjoor xam ne daa bgg a leeral ci ne dikk gi moom taxul,jubook moom it taxut. Latjoor gestu Xaali ne ko,nun kat kii war nanoo wax ak moom ca sunu mbir ma nu ko woowe woon ba sonn,mu ba,Xaali ne ko aca, ne S bi: man dey maa ne Ahmadu Sheexu da doon wooteg yonant,te di ci xeexe it, kon ray ko dagan na,lekk it alal ji u nangoo ci moom niki mgg ak njaf a mu ndaloon (njaf mooy jpp jaam),loolu lpp dagan na,bi mu noppee mbooloo mpp noppi ab diir,S bi ne Xaali ndax da ngaa wax ngir ma tontu la?,Xaali ne ko waawaaw,bu may wax kay nga tontu maa tax,s bi neeti ko : kon am naa ndigal ci tontu ? mu ne waawaaw, mu ne kan moo la man a seereel ne woote na ag yonnant ? Xaali ne ko waa Kajoor,mu ne ko oou ay noonam lanu,te diy xuloowaaleem,di xareek moom,nan lanu koy seedeele ? Xaali neeti ko waaye waa Samba Saajo,fi xare bi ame woon?, S bi ne ko oou kay dun seede,ndax xare baa leen fa fekk,sottiku ci seen kaw,te ygunu woon,nan laniy xame ki nu tuumaal ak li nu ko tuumaale?, Xaali ak mbooloo mi ne tekk as lf,ba mu ygg mu ne yaw gone gi,won nanu la Ylla,nga jiitu nu ca,kon ag ndokkeel eel na la,dal di nooy,te jubook moom.

Pnd ba wuri,S ba tggu leen dem,ci noonu, yoon ypp dagg ci moom lu dul wi jm ci Ylla,ndax kat moo jkkaarloo ak u baax eek kccor yi,jng ca oom:{wa ufawwidu amrii ilal laah innal laaha bashiirun bil hibaad,wallaahu yahlamul mufsida minal muslihi} muy joyal naa samay mbir eel ylla,moom miy gis jaamam yi,Ylla xmmee na kiy defar ak kiy yq.

Li mooy dooley S bi,te nii la dogoo woon,donga yi raw ko, cig dogu,foo leen fekk a ngay xeex ak nit a,nga gis daanukatu jll yi fii,leeg-leeg nga gis ku ci yeg ba ci kaw njobbaxtalu garab,ne drr fi suuf,jiital bop bi,jug faxasu dem,te dara du ko jot,ak uy tbbi ci sawara gnn,te dunu lakk,di yekkati xasiday S bi,ci penciy nit i,ak seen daara yi, uy xeex ak oom te du tax nu byyi, u leen di door ak a jng,ak a nangu seen alal,ak a gnne seeni kr,loolu lpp,ngir teqale leen ,te tas leen. Mu mel ne jf jooju da leen na dolli ag xeemeem ak ag sobu, mu mel ni loolu mbotum Yllaa,mu ball juge ci baatinub seen Sri ba ca oom,S bi daa leen dolli pastef,di dgral seeni basiira ,di yekkati seeni yite ba ca yu saaba ya,naan leen roy leen saabay Yonnant bi, ooy seeni mbokk de,te daje nanook lu gn a tar lii ngeen nekk, ndax ray nanu leen ci yoonu Ylla,tuur seeni dereet,nangu seeni alal,gnne leen seni kr,te loolu tewu leen a jublu ci li nu soxla, ba am tagg wu rafet ca Ylla, :{ lil fuqaraail muhaajiriin allaziina uxrijuu min diyaarihim wa amwaalihim yabtaxoona fadlan minal laahi,wa ridwaanan,wa 14 www.daaraykamil.com

yanzuruunal laaha wa rasuulahuu ulaayika humuz zaadiquun },mu leen di xamal ni,danoo war a roy ci way gddaay yu kk yooyu,nga xam ne ku dul ylla oru leen woon, u gnne leen seeni kr naggu seeni alal,ci yoonu skku Ylla ak ngrmam,ak dimbali Ylla ak ab Yonnantam, ooooy u dggu i.

Mu naan leen xanaa xamu leen ne ooooy seeni baay ci diine,kon lu leen man a dal,day daal di doon lu new,{laxadd kaana lakkum fii rasuulil laahi uswatun hasanatun liman kaana yarjool laaha wal yawmal aaxira}}muy :ku gm Ylla ak allaxira,na ko wor ne am na roytef bu rafet,ci yonnant bi. Mu leen tey rafetal ci kiy aawal ci yeen, { Idfah billatii hiya ahsanu,faizal lazii baynaka wa baynahuu hadaawatun,ka annahuu walliyun hamiim,wamaa yulaqaahaa illal laziina zabaruu wamaa yulaqaahaa illa zuuhazin haziim} muy dee leen jae jf ju aaw, jf ja gn a rafet,kon nga gis ne ki nga xam ne,ag noonoo daa am seen diggante,da na mujj mel ni sa xarit bu sellug xarit,loolu nag ku dul kuy mu du ko am,ku dul ku di boroomub cr bu mag. Dee leen di fuglu { yawma nadhuu kullu unnasin bi imaamihim } muy bis ba niy woo nit u nekk ci seen imam. Kon de baug ku ba du leen naqari, u daan def bu nu naanee ci ndoxum waaraatey S bi moomu,ba mndi, di u sawar,di daanook a yuuxu ak a fecci,ci diir bii,s bi doon baril lu muy def ay xasiday xam-xam,ak yu tagg,ci la woyoon Masaalikul Jinaan,muy tere bu amul moroom ci tazawuf,yor junni ak juroomi temer ak juroom fukk ak atti bayit,ak Mawaahibul Xudoos,ak yeneen,ci la wccee it u bari ci donga yi,niki sheex Ibraahima FAAL,ak sheex Ibraahima SAAR,ak sheex Anta MBAKKE ak sheex Aadama GY ak sheex Asan NJAAY ak u mel ni oom.

Bi nit i barilee lor yi ak sonal gi,ca Mbakke,mu tuxoo fa sanc Daaru Salaam,ci njlbenug atum junni ak atti temer ak eent,waaye teewul lor yi wy di dolliku,mu sax fa lu tollook am at,di yar nit i,di leen yege,nuy gn a dolliku,raj-rajloo biy gn a yokku,wrsg wiy gn a sottiku niki ab taw,mu juge fa,dem as lf,ca penkub bj-gnnaaru Daaru Salaam, ci lu tollook juroom walla juroom aari kilomet,sanc fa Tuubaa,ci mujjug atum junni ak atti temer ak juroom,walla ci njlbenug atum junni ak atti temer ak juroom benn,tuxu fa ak njaboot gi, s Fallu nettali na ma - aareelu xalifa - ne magam ja sri Moodu Mustafa,mi njkk a doon xalifa,mi ngi ganee dduna Daaru Salaam,guddig jjuma,fukk ak benn ci muharram atum 1306 g , njkk s biy tuxu,ndax moom mi ngi tuxu, ci li nu wax, ci jumaadas saaniya. Ci guddig kasurajab,maanaam aar fukk ak juroom aar ci rajab,s Fallu gane dduna, u magantee juroom benni weer ak fukki fan ak juroom aar,yal na leen ylla barkeel,ginaaw bi,ci la s Muhammadu Lamin Baara ganee,bokk ak s Moodu Mustafaa nday ak baay,ci atum 1308 g, walla 1309g . Mu des Tuubaa nag noom S bi,di dem ak a delsi,ak a tuxu ci diggante kr yi,niki Daarul Minnan, Daarur Rahmaan,ak Daarul Xuddoos.

Ku dul Ylla nag xamul xew-xew yi daa am, ci digganteem ak boroomam,ak diganteem aki saabaam,ci xeeti tarbiya ak tarxiya,ak yu ni mel,ak jngale ci taalifam yi,ak digganteem ak u baax i,ci ay mbir aki duggalante ak ay xuloo,ngir seeni doom ak seen taalibe yi wlbatiku woon jublusi ko,ak ci digganteem ak buur yi ak jaraaaf yi,ciy xuloo,ngir fiir ak tiit ci seen nguur gi. Lu man a xew,doxiin wi moom,juboon na,donga yi jub, u daa dolliku ak a yokku jamono ju nekk, ku mu ci wcce ,mu wy di jub,ku tbbi it tbbi cig njub,ba bi mu tukke ca gej ga. 15 www.daaraykamil.com

Sancam Jolof Ak li ko waraloon S baa ngi sanc Jolof - ci li ma s Mbkke BUSO nettali - bi mu nekkee Tuubaa,ba nit i bari fa,magi donga yi denc ay soxna,dkk yi woon ci wet gi, u ci bari tuxusi fi woon ak seeni o, i s bi jugoon ngir yar leen tmblee jaxasook eneen i,nos gi s bi nosoon mbir yi,am lu ci tmblee yqqu,mooy bgg gi mu bggoon a ber iy jng cig wll, ay ligey,ca geneen wll, iy ligeey ak iy jng jaxasoo gi naqari ko,rawati na jaxasoo gi niy def ak eneen i,nga boole ci loolu ,aj gi mu bggoon a defi ak siyaare ji Yonnant bi (j.y.m),te bggoon koo bgg,ba daa ko wax enn ci i ko jege woon.

Kenn ci sunu moroomi naari Daymaan yi,di Muhammad doomi Hamdil Abhami nettali na ma ne:S bi nee na ko ca at mooma ca Tuubaa,ndax bgg ngaa aji? Ma ne ko waaw-wallaahi,waa-waaw,ku ma fay yobbu kay laa amul,mu ne ko,demal ca sa o,te waaj,te w ci mujjug at mii, nu nd aji,bu neexee Ylla ,ma dem waaji te lijantiji sama njaboot,naan (Inna lillaahi wa innaa ilayhi raajihuun). Nu dellu ca wax ju njkk ja, S Mbakke BUSO nee na,bi ko aari mbir yu gaar yooyu jaaxalee,muy mbirum jaxasoo bi ak mu bgg a aji gi,da maa woo,waxtaan ci ak man,diisook man ci mbirum u sanc ab barab,bu nu man a tqalee aari kurel yi wlif u dul oom,te teqale leen oom ci seen biir,ngir iy jng ak a jngale man a def seenub ligey,mu samp ci jiite njngum alxuraan mi, ,s Abdu Rahmaan LO,njngum xam-xam mi,mu teg ca Maam Cerno rakam ja, nd fa ak oom aar rekk ak seeni kurel,keneen dollikuwu ca,ci donga yi walla sheex yi. Mu ne ma yaw nag kon da ngay des Tuubaa,di jwrini donga yi, iy siyaaresi bu nu wee ak seeni ddiya,ku ci war a agsi,nga byyi mu w,ku warut a agsi,bumu agsi. Ma nd ak moom ci loolu,xalaat ne lii daal xalaat bu nu barkeel la,inshaal laah. Mu tmblee waaj,di ci lqatu i mu bggul u dem,bi dogu gi dggaree ci dem,te loolu da ko daa lq sunu waajur wii di nijaayam, nga xam ne da koo byyi woon ak man rekk,doyloo ab gis-gisam ci man,mu mel ni da maa soxlawul - bi mu ci dogoo dgg nag,la xam ne du man a kk,mu ygal ko nijaayam jooju,mu dal di ko koy ygal,yf yi nag tiis ko lool,ngir xam gi mu xam ni buuri Jolof yi fiire,ak ni nu manadee mu,wuuteek buuri wii tund , te taalibey Jolof yi it dunu byyi seeni doom aki donga,te dunu mu it, wuuteeg yu gox bii,mu ragaloon nu sonal ko,aaye woon ko ci anam gu nooy mu ba a dem, yee ko ci aaday aari dkk yi,ci li mu ci xam,ndax xamoom na ne li S bi bgg dppoowul ak seeni aada.

Waaye S bi moom niki soofiyu yu mag yi,dafa dogu te fas yeenee wyal li mu dogu, ndax wyal ag dogu ci tasawuf la bokk,tekki ag dogu fi oom mook tubbee yam,dee ko gn a woyof ci oom. Kon S bi laxas na ak dongaam yooyu,ca sawaal ci atum junni ak atti temer ak fukk ak aar g,(G, mooy:ci ati gddaay gi) wuti suufus Jolof,ndax gisul ci Bawal,barab bu man loolu mu bgg,ca jamono jooja,ak ndax itam Jolof suufus ay maamam la woon,te foofee ca la wr Tuubaa amul am ndox,walla bu fa saxee it da na ajowoo jankoote ak ay oam,mbaa mudaaraante ak oom,te loolu du lu mu daa faral a def,mu dox ak oom,ba Mbkke Baari,wacc fa,sanc fa,waxtaan fa ak yenn jaraaf,waaye ag agas fee ca njlbenug wax ja, ggoon ci u naan:nun dey xamunu woon ciy donga ag skkoo dooni buur, ii di w daal,nekkunu lu dul ay buur,yu w ngir xccook un suniy suuf,ygg nanu leen a dgg ca a ca

16

www.daaraykamil.com

seen ginaaw,nun nag i ngi gi ci ne dunu dkk ak nun ci sunu suuf sii,ci seen melo wii,ak wax yu mel nii,ci yi ko nijaam ji daa wax,ak a sentul bu fa demee. Waaye Ylla moom bu bggee amal am mbir da koy wutal ay sabab, nee nanu bu Ylla bggee tllal gnel lu lemu,da koy wutal lmiu ku iaan. Bokk na ci xewal yi Ylla xewale S bi , sob gi mu ko sob ci yoonu wlliyu yi, { sunnatul laahil latii qad xalat min qablu,walan tajida lisunnatil laahi tabdiilan }} muy ci maanaa yoonu Ylla wii di wu wyoon bu ygg,doo gis ag coppite ci yoonu Ylla. Nit du jug mukk jm ca Ylla ndare bu danu koo natoo ay noon yu koy lor,loolu fiiraangeg Yllaa, ngir mu ba a jdd,ba a weru ci ku dul moom,Ylla da koy feeu cig mgg ak cib taar,ci feeu gog taar gi (attajalliil jamaalii) ,la ko Ylla di oddile nit i, uy sottiku ci moom niki ay we yu tiimub puur,loolu nag ci tggatug Ylla lay ame, uy yrmaande juy texeel ku nar a texe. Ci feeu gog mgg gi attajalliil jalaalii la leen Ylla di dddale ak yenn xol yi, u nekk seeni noon,dunu gis seen hurma,dunu leen gm,di leen ayibal ci seen bopp,ak ci seeni taalibe,waayee ak loolu lpp,hifthul hinaaii du tggook oom,mooy wattu gi leen Ylla di wattook a aar,dara du leen dal lu dull lu Ylla bgg mu dal leen juge cib noon,di luy aaw ci saayir,diw yoon jm cig fayantoom { Innaa minal mujrimiina muntaqimuuna } muy ci maanaa,da nanu fayyu ci iy too. i ngi aan Ylla jmm.

Lii mooy mbirum S bi ak ay ndandoom ca njlbenug Jolof, bu dee lu aju ci am ba woon ca ginaawam nag, oom S Mbkke BUSO nee na:taalube yi mu byyi woon Tuubaa,bi nu yggee ni S baa nga Jolof , u tmblee wuti pexey dem fa,yalwaankat yi fekksi leen ci loolu, u gddaaye Tuubaa,ndare ku fa dkk,xalaatub siyaarekat yi di fa yam dal di yqqu,lu tax det, ginaaw mbir mi du mbirum xalaat. Bu dee lu aju ci jaraaf yu dkk bi,ku ci gisoon,li nga gisoon gn naa yokk,ku ci gisutoon tmbli nga gis leegi,nga boole ci lanu dggoon ci diggam ak buuri Jolof yi,nu tmbli noo dikkal ci kaw ak suuf. Bi buur yi ak seen dag yi gisee li nu gis,te oom boroomi ngnnaay lanu, u daa dund ci seen ngnnaay rekk,danu daan song ku leen daa jem a t,duma ko,nangu alalam,ray ko mbaa u njaf ko (jpp ko jaam),loolu nag di woon aada ju yggoon ci oom,ju nu daa donnante,waaye loolu tewul u amoon jmm ak lenn ci boroom neg yu mag yi, daawunu leen boole ci seen jf jooju,daawunu ci boole it i daa aaru ci seen kaaraange,niki negub s bi. Loolu ak meneen mbir a waraloon nu jaaxle woon ci S bi,meneen mbir mi nag , nga xam ne moo leen gnoon a jaaxal,mooy mbirum nguur gu raglu gii,loolu nag mooy tubaab yii di waa faraas, oom danu daa def,suuf sunu not ,jl fa njiit,muy ku fa bokk,samp fa,ngir waa dkk ba ba a mer te nd ak oom,xoolal ma gii xam politig. Ci noonu nu jl buur yi ak jaraaf yi teg leen ci kaw daara yi ak donga yi,uy seeni njiit,waaye loolu xewal a ngi ci ndax tax na ba buur yi ak seen jikko yu bon yi nu yoroon, di sonnal jullit i ak a fitnaal ak a def li leen soob ci nit i jeex. Bi jaraaf yooyu demee ba manatunoo dellu ci seen aada yu njkk yu bon ya,muy ray jullit i,ak giir seeni alal,ak doonte loolu da leen di ggale ci nuy raye it,du tee nu def ko,bi nu demee ba manatunu loolu te 17 www.daaraykamil.com

loolu tubaab yee ko waral, u mujj di leen xiirtal tubaab yi,jaare ko ci ay pexe ak ay wor. Mu neeti : jaraaf yooyu jaxase googu nu doon jaxase jullit eek nguurug tubaab yi,jubluwunu ci woon,faagaagal leen,ndax lu man a xew, oom ci seen ron kiliftef lanu nekkoon,doonte ci anam gu woyof la,waaye kay i ngi ci jublu woon ame ciw yoon wu nu man a nangoo seeni alal,bari na lu nu leen daa wax naan diw kat da leen a ba,diw it nanguwul a fay galag, diw mee am na lu mu leen di waajal,diw mii mi ngi wut ay ngnnaay,di dajaley fas,walla nit aa ngi koy deglu , walla ku bariy taalibe la, u koy mggal,dayob mggal, ba gg ci bu leen junjoon geej gi,u sobu ci xuus ko,ak leneen ak leneen,ci seen fen yi nu daa def,ngir bgg tubaab yi digal leen u songu leen,walla nu def ci oom lu leen soop. Te xamunu ne yewwuteg faraase yi,ci wllug politig moo gn a yaatu loolu,waaye nag wax bu baree juge ci ku la naan mooy sab bt,di sa asaa sekkare,di la xoolal sa ginaaw,da na mujj am lu mu byyi ci yaw benn bis,rawati na bu fekkee ki u ne moo def loolu,du rambaaj,du jaxase,te du jeem a setal boppam,ca ki nu ko rambaaje,te iy yq dunu da,di yq diggante bi,rawati na bu nu niroolee am mbiram ak mbirum ku yori donga,yu ko gm,lu mu leen digal nu def. Loolu moo waraloon u tmblee tiit ci moom,ndaxte dau koo niroole woon ak sheex Omar Fuutiyu, Tukkulor la bu defoon ay xare ci wll gi mu dkke woon , ci mujji ati juroom aar fukk yi,bi loolu jllee ba teg lu new,la benn wolof bu tuddoon Maalik BA,nu gnoon koo xam ci Mbba,defoon ay xare ca goxub Saalum,ci ati juroom att fukk yi,ginaaw bi la Ahmad Sheexu dib Tukkulor,moom it,xaree xareem ba ak waa Jolof ak Kajoor,ba bi mu deewee ca bisub Samba Saajo,ca wllug Luga,ca mujjug ati juroom een fukk yi. Jaxasekat yi nag ,bi nu demee ci tubaab yi danu leen ne S bi ii lay roy,ba mujj tubaab yi manatuoo kk a gstu li nu leen wax,lii daal mooy li gn a waral tubaab bi jublusi S bi,ginaaw bi ko Ylla dogalee namm ca la mu ca namm,muy wax joj dara amu ca,ndax S bi lorewul ,soxlawul dduna,te xemmeemul li nu jort ci moom,Yllaay seere lii nuy wax. Bu doonutoon rambaaj yii,waxuma la buur yu ndaw yi sax dunu ko jeemal,waxantuma la ak yu mag yi,waaye loolu day dggal waxi yonnant bi ji (j.y.m), { i Ylla gn a teg ay nattu ooy yonnant yi,teg ci wlliyu yi,teg ca a gn,teg ca a ca topp}} ,ponk bii nag bu wy la ci xeetu yonnant bi (j.y.m),ndax u baax i pp ag gm foo leen fekk,daniy fees dell aki nattu, dduna dddu leen naqari ci oom, ooy ppi jafe-jafe fuuf u dul oom,boo demee ca Sahiihub Muslim,ak bu dul moom,da nga ca gis :[ ddunaay kasob jullit,tey jjanay yefar ],ylla itam wax ne :{wal aaxiratu hinda rabbika lilmuttaqiin} muy llaaxira, u ragal Ylla ee ko moom.

Bi tubaab yi demee ba manatunoo kk a xool mbirum S bi, u tmbli faa yabali ndaw aki bataaxel,ay yooni yoon,di skku ci moom mu seetsi leen,moom muy xaar ndigalul boroomam rekk,ak lu yonnant bi,(j.y.m), u gise yeex a wuyyusi gi,ag ba,bu ko defee a daa jaxase di gn a am lu nu wax,naan,waxoon nanu leen ko,gis ngen li nu leen waxoon am det ? . Ba bi fa tubaab ya yonnee lenn ndaw mu nd ak yenn soldaar yu new,bunu leen tollaleek li nu am ciy xarekat,ndax matunu woon mbooloom xare mu mag,lii moo doonoon li ko boole woon ak tubaab yi.

18

www.daaraykamil.com

Tukkib gej gi S bi,bi mu jotee ndigalul Ylla ak Yonnant bi (j.y.m),Yonnant bi (j.y.m) jox ko kiiraay luy dox diganteem ak tubaab yi,te loolu wax na ko ci genn xasida:{ ku nu tnn ki,jmm ak mucc yal nanu nekk ci moom,wutal ko kiiraay lu koy aar wlif lor,ne ko doxal te bul ragal woru,}}, bi loolu amee mu genn ca kram ga mu sancoon Jolof ngir jng ak jngale,ci bisub gwwu fukki fan ak juroom att yu safar,ci atum junni ak atti temer ak fukk ak att g. Ci jummaada saaniya walla sahbaan ci at mii,la sheex Bashiiru gane dduna di doomi sri bi,bi miy genn daje ak ki jiite mbooloom xare moomu genn moom itam juge wllug Luga, u daje ca Jeewal ca ngoonug bis booba,s Banji NJAAY,nee na ma - moom ci i ndoon ak S bi kerook la, u gnoon koo xam ci Banji Xuja - am na benn karaama bu fee Jeewal,mooy bi nu ggee Jeewal , danoo jeexaloon ndox,te foofa ndox bariwu fa,satalag S bi jeex,bi nu nekkee ci jaaxle googu nag,jenn waay ju yor ab baag bu fees dell ak ndox jege,nu wax ak moom xamul li nu koy wax,nu jox ko ab defukaay, mu duy ko ba mu fees ak ndox,nu naan,S bi jpp,ndax moom daawul tiim,waa ja jll,te dggunu aw lkkam,xamunu ci moom dara.

S bi nee na :ginaaw bi nu jullee tkkusaan,nasaraan boobu di njiitul soldaar yi,dikk na, bgg a wax ak moom,mu wlbati kanamam wlif ko ,jublu Ylla,jng Bismil laahir rahmaanir rahiimi juroom fukki yoon,waa ja nooy,aw xalam fay,mu gaaw genn,jm ci ay aajoom,mu fanaan foofa,ak jaraaf ju uul jooja,ci loolu S baa ngi naan: {ginaaw bi nu dajeek a gnnoon jm ca kram,te njqare nekk ci seeni dnn)) (Dox nanu ndandoo di way gaaw,jm ca jaraaf ja,ba tkkusaan jotee u julli fa cig ragal ylla ) (Ginaaw bi la jaraaf ji daje ak moom,mbooloom xareem mi wr ko,am ca uy siyaare ) (Mu jubale kanaman ca Ylla mu tedd ma,ba koo jubale jaraaf ja,ngir am li mu bgg ) (Wax juroom fukki bismil laahir rahmaanir rahiimi,cig toroxlu jm ca ka nga xam ne,fu mu daaneele ab noon mu nrmelu) (Jaraaf ja gnn cig gaaw jm ca aajoom,mu fanaan fa di boroomi xewal.}}

Waxam ji mu naan am ca uy siyaare ,S bi nee na mi ngi ci jublu woon,taalubeem ba Omar NJAAY,sheexub Konjoru Njaay,di dkk bu nekk ci wetu Luga,moom nag am na wccuwaay bu kawe ci s bi,bi mu faatoo s bi seereel na ko yiw wu ry,dig ko it yiw wu ko ku dul moom di eewe,ngir rafetug njortam,ak waxam ju rafet ci s bi, i ngi ko denc Njaarem. S bi nee na: ( Omar mii mi ngi gnn,ngir siyaaresi ma,daje ak soldaar siy gnn,fekk nu xamoon ko,te fonkoon ko, u kontaan ci nd gi mu nd ak oom,jppe woon ko kenn ci seen kilifa yi,waaye Ylla moom xam na la nekk foofa). S bi nee na (nasaraan boobu jiite woon soldaar yi,moo doonoon ki yoroon Luga (gouverneur) ca jamono jooja,doonoon gorob buuru ndar (boroom ndar),looloo waraloon u dglu woon ko ci samay mbir,mooy ku ryoon, ki daawul wax ci man lu baax,daawu ko def,daawul nd ak ku koy def,dogu woon it ci tumbrnkeel ma,nu ne ko du fi ame,mu ne kenn du ko tee am,dogalub ylla bi dppook li mu dogu,looloo taxoon,ma yggoon Ndar uy xool samay mbir,looloo taxoon mu wird aayay {wa iz yamkur bikal laziina kafaruu liyuzbituuka aw yaxtuluuka aw yuxrijuuka,wa yamkuruuna wa yamkurul laahu wal laahu xayrul maakiriina}}muy ci maanaa ,bi la i weddi di fexeel,ngir saxal la fi,walla u ray la,mbaa u gnne la, u nekk di fexe,Ylla itam di fexe,te Yllaay ki dq a fexe.S bi nee 19 www.daaraykamil.com

na :(Ndar, a fa nekkoon atti kurel lanu woon, u bgg u byyi ma fa,bu ko defee,nu di leen sonnal ca daanaka-dun ba bpp (daanaka-dun mooy Presquile) ,di yqq seeni kr,ak u bgg u faat ma, ooa amunu lanu bgg,ak u bgg u tumbrnkeel ma, ooa Ylla dppale dogal bi ak seeni xalaat). S bi wax na ci loolu lii: { Ylla tbbal ci xoli i sababoon ag tuxalam,ca jooja jamono)) (Mu tbbal ci seeni xol,ag gnne ko,jme ko ca rew yu sori ya,mu ame fa lu kawe dggub Saariya}} Ylla (t.s) dggal na ba mu naan {wal laahu xayrul maakiriin}}muy yllaay ki dq a fexe. Ndax xewale na ma att yu gn seen atti kurel ya,ndaxte bi may tukki,amoon naa martabay dgg-dggi sri,ci gm ak lihsaan ak lislaam,waaye dese woon naa lu ma yitewoo woon lool ba mu daa ma jaaxal ak a fogloo (fog mooy kk a nelaw guddi) ,te kk ko, u may jam ay xeej a ma ko gnal,di daggate samay baaram,loolu moo di matug gm Ylla gi nga xam ne mooy dgg-dggi xam Ylla,ak matug lislaam gi nga xam ne mooy yaqiin ( mooy mu wr la ne li nga nekk ay dgg,ni ngay xame ne aw xal day lakke boo ko joggee) ak matu lihsaan gi nga xam ne mooy gg ca Ylla mu kawe mi, atti mbir yile,amewu ma leen, ci lu dul jaxasoo gi ma jaxasook oom,te loolu moo daa doon sababu rkki gm,yal nanu ci ylla musal.

Ab nettali bu yemee ngii ma, dgge ko ci S bi,ci mbirum ttekatub (goornoor) Luga bu ry te bon,te yoroon woon mbirum tukkib S bi te taxawoon temb ci mu am. S bi nee na :( ttekat boobu ,bi ma nekkee ci tukki bi ,laa dgg u ne danu koo mujj mere,gstu ay mbiram,gis ci luy waral u gnne ko,tumbrnkeel ko,bi niy xalaat,mbugal mi nu ko war a teg,am ku ne kii daal,ginaaw moo taxoon nu gnne S bi tumbrnkeel ko,nanu ko yobb,fa waayam ja nekk, u dppoo ca loola,muy fayyug sunu boroom,yguma lu dul u ne ma ttekat baa ngi ci dun bi ma nekkoon,mu nekk foofa ab diir di ma lqatu ngir ragal ak rus,loolu moo waraloon mu dem gis goornoor (ttekat walla saytukat) ba fa nekkoon,ne ko moytul ma S bii fi yaw,bu ko jem a def lenn lu ko naqari,ndax lii ma dal de dara waralu ko lu dul sama yene ju aaw ci moom,kon daal bul def lu dul,di ko jox li nga ko war di fay weer rekk te yam ca . Loolu moo waraloon ttekat boobu nooyoon mel ne galas fi man,tukki bi, li ci jafe woon lpp mujj yomb. Bi Ylla sottee ndox ca sawaraam wa doon jf-jfi (moom goornooru Luga bi), mu mujj di ku sedd,la nu ko delloo fa mu juge woon,ginaaw bi u yobbooti ko ci penku bi,ca wllug Xaay,foofa la ko ab njabarkat bu bmbara njabare,ci gnn krug bmbara, mu dee di ku nu dkku, di ku nu ng, xoolal ma rekk mujjug iy too . Mbirum noonam boobu,nirook lool,mbirum noonub ki miy ligeyal di Yonnant bi (j.y.m),noonam booba di woon Haamir doomi Tufayli,ba mu nee jamono ja ko tawat ja sonnalee ci gnn kru jenn jigeen ju Salool: (ndax lii day am mbas mu mel ne mu gilem , te di ag dee ci negub jigeni Salool ?).

S bi def na ag xasida,gu mu tnke arafi {mazalul jannatil latii wuhidal muttaquun , ba ca, tilka huqbal laziinat taqaw }} ne; { too gu nu ma doon too,jeex na,aji not jee ko jeexal,ji damm ngnnaayul ki doon puukarewu, te mu damm)) (Moom de ylla am na samag cant,ndax rayal na ma ka doon fexe ci atum junni ak atti temer ak fukk ak att g,te deem gi dolli xalaat yi)) (Amewul ca la mu doon def,lu dul am mbugal,te ginaaw bi mu farloo,ba yaakaar ne moo ci nekk,daa daal di giim,tawat ji gllankoor ko)) (Fayyug sunu boroom da koo tiital mu daw, ci gej gi ak ci jeri ji,te am mbooloom wor ko }}. 20 www.daaraykamil.com

Jaraaf ju uul jooju,xam naa aw turam xam giir gi mu bokk,waaye du ma sobeel sama xalima ci bind aw turam,mook mbokkam mu nasaraanu, mi daa aawal S bi ak a saboote,fu mu masaa daje ak moom,moo nekkoon Garambasaa. Gis naa li s bi bind ci oom aar, u bari it, ci i xam seenug mujj,nettali nanu ma ne ku ci nekk dee gu aaw la dee,kenn ki mooy ku jeri ji,mi ngi Ndakaaru,ki ci des,di ku gej gi,nekk Konaakiri,yal na nu Ylla musal ak jullit pp,ci nattu bi mu leen tegoon. Nu dellu ci mbirum tukki bi,S bi nee na kerook wird wi mu gnoon di def,mooy { Inna wlliyiyal laahul lazi nazzalal kitaaba,wahuwa,yatawallaz zaalihiin}} muy ci maanaa :kiy mngoo samay mbir,mooy Ylla mi wcce tere yi,te mooy kiy mngoo mbirum u baax i. Loolu mooy maanaam waxam jii: {Ylla naagul na ci man ibliis,fa Jeewal,bi ma ko woowee ci turu walii,(muy kiy mngoo mbir yi) }}. S bi fanaan foofa,bi mu julle suba,laxas jm Kokki, u yendu fa,mu tmbli faa woy xasidag Asmaau Ahlul Badri, S baa ngi wax ci loolu: {ganaaw bunu fa yendoo,moom tmbli na fa di woy lol ubbil na ko ab bunt }}. Boobu bisub diber la,bi gee jllee ba teg lu new,u laxas, - ci li ma kenn ci i ndoon ak s bi nettali ci fenkug weer wi,ci guddig altine dppook aar fukki fan,juge Kokki,nee na :booba un i ngi dox, muy wicc-wiccal ci sunu kaw. S bi nee na : maa ngi raaan (mooy dox guddi) kerook ca guddi googa,ci kaw sama wenn nglamu u naa ko Hawnul laah,wu gaaw,nga xam ne fasi o buur bi manunu ko woon a jot,te i ngi doon def li nu man,ba mujj am ci oom u naan ma:S bi defal nnk,yramal sa bopp,te yram nu,ma naan leen gaaw leen,nu ku nu yilif,ba noppi yonni ko di yeexe? bu ko defee,nu wedam. S bi def na ci loolu aw woy: {{laxas nanu ginaaw bi nu yendoo,di dox,ca ginaaw gee, nd caakug xat te di ko mu ) ((Nu gg,laataa jullig fajar,mu fanaan guddi gi ci yekkati ay bayit ,di boroomug jjji}. Bayit yi mu doon yekkati, ooy aar yu Busayri yii: (kuy sukkandiku ci ndimbalul Yonnant bi,bu koy gaynde fekkoon cib ll it wedam) (Moom Yonnant bi,foo ko gise ak doonte moom rekk a nd,da nga naan mook am mbooloo nd ngir,mggam ga ). Li mu jublu ci di boroomug jjji gi ci woy wi,nag,mooy mu nekk di jjji fas wi ngir mu gaaw. Ginaaw bi, nu gg Luga,laataa fajar,yendu fa.

Nettali nanu ne S bi nee na:bi mu jegee Luga,kenn ci ndawi nasaraan bi,te bokkoon ci i ndoon ak moom,wax na ak moom,ci anamug yrmaande,ne ko ngnnaayul,jege nanu noon bi de,S bi ne ko ci kddu gu dgar,ylla du ltt,te du des ginaaw,bi nu ggee ba dal,la ndaw li ko doon wax loolu dellusi, ne ko man dey da ma laa wax ngir yrmaande,ngnnayul,jege nanu noon bi,nga ne ma Ylla du ltt te du des ginaaw,li nga ma tontu ci sama wax jii de,xawma ko,loo ci jublu? S bi ne ko maanaam loolu mooy Ylla (t.s) dara du fddu ci moom,kon mi ngi nd ak nun,bu doxee sama diggante ak noon yi,ci kttanam,dkku ma wlif leen,kenn du ma manal dara,bu ma byye ak oom it, u def la leen soob,kenn du ci man dara.{wa in yamsaskal laahu bidurrin falaa kaashifa lahuu ila huwa,wa in yuridka bi xayrin fa laa raadda li fadlihii,} muy ci maanaa bu la Ylla laalee ak lor,kenn manu koo dindi ku dul moom,bu la nammalee aw yiw it kenn manul a delloo ngnlam. (Ylla mu sell mi dgal na,Yonnant bi,jmm ak xeewal nanu sax ci moom,jttalee).

21

www.daaraykamil.com

Ndaw li dem nd ak mbgte,man ma ne kooku S bi daf ko doon leeral haalam (haal mooy melo walla mbir walla aw nekkiin) ak ni mu donne Yonnant bi (j.y.m),Yonnant bi (j.y.m) nee na {wkkiirlu mooy sama haal,fggu di sama sunna,ku ltt ci sama mbir,bu mu ltt ci sama sunna}},S bi moom dnn na ci haalam ak sunnaam ab cr bu mag,ak ci haalu Ibraahiim (j.y.m) bi nu ko snnee ca sawara sa,malaaka yi aan ko mu skku ci oom ndimbal,mu ba,Jibriil (j.y.m) ne ko aan ko,mu ne xam gi mu xam sama haal doy na ma ba du ma ko aan.

S bi Yonnant bi la ciy jikko,di Ibraahima ci yite (j.y. ),day jf haalu Yonnant bi ak sunaam,gis nga haal ji noonu,mu jfe ko,ma won la nag ag jfeem sunna si,bokk na ci loolu,moom defal nanu ag xasida gu nu tnke harafi {hasbunaal laahu wa nihmal wakiil}muy ci maanaa Ylla doy na nu skk,te moom de weruwaay bu baax la. Mu ne ci xasida gii laa sengewoo woon (senge mooy ta-ta,walla ci tubaab fortification,muy miir bi u njkk a daan tabax wrale seen dkk yi,ngir mu leen di aar ci song gu bette,kon sengewu mooy aaru ) ca ngoonug bisub jjuma ba,ba ma dogoo ci nd ak oom ca gwwu ba,ginaaw bi ma Yonnant bi (j.y.m) aaree,digal ma ma dem,ne ma wyal te bul ragal lor. Xasida gii nag mooy muslaay li,juttit bu ne war na koo jeem a am di ci musloo li mu ragal,bu leen ftte li enn iy wax naan,waxtuw ajjuma mi ngi dale ca ginaaw tkkusaan,ba bu jant bi sowee,xasida gi nag mooy gi tmblee hamidtu man yahsimunii minad darar, muy : {maa ngi sant ki ma musal ci lori jpp saytaane ak jinne ak nit) (Tudd naa sellam ga,muy buur,buy aji wattu,may skkoo aaru ci wattoom gi wlif musiba yi ak mbugal yi)) (Maa ngi skku ci moom mu musal ma ci bnneex,ak ibliis,ak ci mbooleem yiy lore ci jamono ju nekk)) (Yene naa koo aan di skku am ramu,ci darajay soppeem bay ramu iy ramu)) (Mooy Ahmad,sangub mbindef yi,may julli ak a slmal ci moom,te di ko def aw yoon jm ca sama boroom)) (Maa ngi aan ,sama boroom,ci darajaam,mucc ci saytaane ak ciy aawtef,ak way bew yi di ma xccoo)) (Yaa moom mbindef yi ,yaw sama boroom,may ma ag mucc ci oom,ak bpp balaa ak mbugal)) (Yaw laa jox sama bopp de,yaw aji wattu ji,ba fww it yaay sama wettal)) (May ma li ma bgg ci adduna ak alaaxira,na nga ma musal it ci gccag dduna ak gu allaaxira)) (Jubale naa la sama kanam,yaw sama boroom,yaak sama wasiila,te loolu doy na ma)) (Musalal samag wll ci mbooleem luy aaw,te nga fegal ma mbooleem luy jax-jaxiloo)) (Soril ma mbooleem noon yi ,ci barkeb Yonnant bi,ak Ahlu Badri u tedd, iy ay tnnef)) (Na nga ma xeewale ci ma dugg ci sa senge (kaaraange) lu aaru li,te dkk fa,di ku am kolute ci samay noon)) (Yaway kiy musal kuy muslu ci yaw,ci lpp lu ko man a jublu ciy mbugal)) (Samay mbir ba fww da ma koy joyal jme ci yaw,ndax yaay ki nga xam ne ku weru ci moom deesu ko jalax)) (Yaw aji baax ji,fegal nga ma ag kefar,ak lori oam,ak jpp fitna)) (Fegal ma loxol way bokkaale yi,ci darajay Ahlu Badrin,te nga def leen uy sama senge)) (Yaw aji baax ji,nekkal ma te bu ma gccaal,ci dduna ak llaaxira,te dee ma jggal)) (Bindalal Yonnant bi ag xewal ak mucc,ak oam aki saabaam,ci anam gu sax.}} Mu tje ko { fanqalaboo bi nihmatin minal laahi wa fadlin,lam yamsashum suuhun,wattabahuu ridwaanul laahi wallaahu zuu fadlin haziim}}: muy ci maanaa, ( u dellu nd ak xewalug Ylla ak ngnelam,lu aaw laalu leen, u topp ngramul Ylla te Yllaay boroom ngnel lu mag li).

22

www.daaraykamil.com

Mu neeti { alhamdu lillaahil lazii hadaanaa lihaazaa,wamaa kunna linahtadiya law laa an hadaanaal laah,wa aaxiru dahwaanaa anil hamdu lillaahi rabbil haalamiina}} muy ci maanaa : ( maa ngi sant Ylla mi nga xam ni,moo nu gindi jme nu ci lii ( muy lislaam) ,duu doon gindiku bu nu Ylla gindiwutoon,sunu wax ju mujj,mooy ag cant eel na Ylla,miy boroom mbindef yi) . Xoolal ni mu aaroo woon ci baat yii nga xam ni,Ylla da leen a tagg,tagg it nit i ciy aaroo. Mu wax:{allaziina xaala lahumun naasu innannaasa xad jamahoo lakum,faxsawhum,fasaadahum iimaanan,waxaaluu hasbunaal laahu wa nihmal wakiil ba fam yam}}muy ci maanaa :( i nga xam ne nit i dau ne leen: nit i kat dajaloo nanu ngir fexeel leen,kon tiit leen te moytu,loola dolli leen ag ngm, u maase ne Ylla doy nanu ,te doy na skk ku u doyloo). Nga boole ca loola juroom fukki bismil laahir rahmaanir rahiimi, yi mu jngoon ca Jeewal,ba ndawul nasaraan bi bggee wax ak moom. Waxees na ma ,te loolu lu wr la,ne rakkam ja sheex Ibra Faati, ci bis bi S bi tukkee,ba bi mu dellusee,masul a da di def junniy salaatu alan nabii ci melo wii:( allaahuma salli halaa sayyidinaa muhammadin,wa halaa aali sayyidinaa muhammadin,salaatan tunajjiinaa bihaa min jamiihil ahwaali,wal aafaati,wa taqdii lana bihaa jamiihal haajaati,wa tutahhirunaa bihaa min jamiihis sayyiaati,wa tarfahunaa bihaa hindaka ahlad darajaati wa tuballixunaa bihaa aqsal xaayaati min jamiihil xayraati,fil hayaati wa bahdal mamaati)). Maanaa mi di:( yaw buur bi jullil ci sunu sang Muhammad,ak oi sunu sang Muhammad,ag julli gu da nga nu ci musale ci mbooleem tiitaange yi,ak gkk-gkk yi,fajale u ci mbooleem aajo yi,laabale u ci, ci mbooleem aawtef yi,yekkatil u ci gn jaa kawey daraja fa yaw, ggale u ci ca dayo ya gn a sori ci mbooleem yiw yi,cig dund ak ginaaw ag dee). Mu ko daan def ginaaw bu wccee kaamil bi,waaye kaamil bi moom lu saxoon la,suba ak ngoon,naka jekk, njkk S biy tukki,waaye salaatu halan nabii gi moom saxal gi,man na a nekk muy ndigalul S bi, mbaa xalifaam bu baax,bu sell ba,ngir xr gu mu defoon ci muccug S bi ak ag delluseem ci jmm,mu skkaloon ko mbooloo mu ci daawul sggan suba ak ngoon,waxambaane wu ragal Ylla,wu dkkoon Kokki wii di Samba Joop nu gnoon koo xam ci Samba Asta daan leen jiite. Ku baaxoon la te gudoon aw fan,mi ngi faatu ci atum waafiris sitri,di junni ak aat temer ak fukk ak juroom att,bokk na ci loolu woy gi mu def Ahlu Badrin,ak aaru ci oom,bi mu nekkee Ndar,mu mottali ko, tudd itam nd gi mu defoon ak oom ci tukkeem boobu, u daa toroxal kpp ku ko daa jem a lor,tere boobu,jotoon na koo won ca magi Ndar ya ka u naan Alhaaji Muhammadu Maabey,ne ko mu mokkalandi bayit wu njkk wa,ba u dajewaat ginaaw bu ibisee. Te kat dajewaat nau ginaaw juroom aari at ak ay weer,bi nu dajee s Maabeey jngal ko bayit wi,daal di daanu ab jll,jooy. Ak leneen ak leneen ci li mu aaroo woon te xamunu ko, degg naa ko bis mu naan: bi mu nekkee ci gej gi,masul a da di jng Hisbul Bahri,bu imaam Shaazalii,muy lu am njari,li koy wone mooy yitewoo gi ko S bi yitewoo woon,bayit wi mu digale woon mu wattu ko,mooy njlbenug xasidag Asiiru gu yeme,gi nga xam ne S bi feeal na ci njlben gi,ba ci fukk ak juroomi bayit,lenn ci mboti tukkeem bi ci diganteem ak noon yi,ak wone ci mucc gu mu mucc ci seeni lor,xamale ne saytaane moo leen wor ci moom,tax ba uy am njort yu aaw ci moom,waaye seen njort yi sooy nau,te S bi dellusi na ci jmm,bayit yee nekk nii: {maa ngi dox nd ak u baax i (waa Ahlu Badri),bi may dox 23 www.daaraykamil.com

(bi may tukki),waaye noon yi jort ne man booba ku u njaf (jpp) laa )) (Sama dox bi may def, ci wommatug Yonnant bi, nd ci ak gaa yu baax yi,Ylla rekk a ko tax a jug,ba fww it samab dox du jm ci ku dul Ylla)) ( Bijji gi ma wommat (bijji mooy jazbu,di lol day xcc,kon man nanu koo jppe yitewoo sunu boroom gi nga xam ne daa mujj mel ni ab asyee bu koy oddi jme fa Ylla) jme ma ci aji tedd,joj lu ma skku ci moom mu jppandi,mooy liy dox ak man )) (Samag cant ci xalima,ak ci xol ak jmm, eel na ki ma nekkal cig tab ( ki nga xam ne jamono ju nekk mi ngi may sottil ay xewalam ) te mooy ki di ab santaakon (ku soxlaalul kenn) )) (Sama ndimbal,samag dgral,sama kaaraange ca noon ya,mi ngi bawoo ci Aji yaatu,ji di ab Mayewaakon,(ku tabe lool) kooku mooy aji dimbali sama )) (Sama kilifa nag, ci bu may dox ak bu ma taxawee,mooy sama kerkeraan,di Yonnant bi,te mooy ki may ligeyal,te moom dey day xont (mooy jox ab dund) ku koy ligeeyal)) (Samab yool ci ligey bi may defal Ku nu tnn ki,di Yonnant bi, mayewaakon (Ylla) bee ko warlu,te moom ku am lu mu faye la)) (Li ma nesar nag mooy nekk jaamub boroom Aras rekk,di ligeyal gn ji mbindef,te moom Yonnant bi mooy samab xuppkat (Yonnant bi day bashiir tey naziir,di kuy bgale tey xuppe ngir jaam yi ba a sggan ba a naagu ) )) (Aji feg jii di Ylla,moo may fegal ci Yonnant bi,ayi noon yi,ak lpp lu aaw te mooy ki may xettali)) (Samag mujj mooy nekk dib jaamam,di ligeyal Yonnant bi,mbiri mbindef ypp nag ca Ylla lay mujj )) ( Samay weer aki bis lg oo may seedeel nekk gu ma nekk di jaamub Ylla,te moom siw na )) (Samay sutura ci adduna ak allaaxira,mooy tagg Yonnant b,ci woy ak wesar,te moom suturaalkat bu baax la )) Samaw jiwu mooy tereb Ylla bi ak sunna si nga xam ne ci laay aaroo ci li yaqkat bi jublu (muy saytaane) )) (Samay kr wet na, o i tas,ngir tagg Ki nga xam ne,noo ko man a tagge,du tax tagg wi mat )) (Woru gi nekk ci mbindef yi,wor na nasaraan yi,ciy pexeem, u jort ay njort,te njort ak woru la}}.

S bi nee na : ginaaw bi nu jullee tkkusaan,lanu dugg ci saxaar gi,jm Ndar, u gg Ndar bi jant biy bgg a so,ci loolu S baa ngi ciy wax naan: {Ylla ca bu njkk,la dqoon samay nx-nx, ca Ndar jme leen ci ku dul man,ci barkeb Ahlu Badrin a diy gaynde)) (u ndandoo, sax ca dun (le) ba akub coona,fuglukat ya di u fa bari}}. Ma sax fa - s beey wax - la desoon ca safar,muy fukki fan,ak weeru rabiihul awal,ba ca bis bu mujj ba,muy bisub alximis, ci diir boobu laa matale woyug Asmaau Ahlu Badrin, muy turi waa badar ,topp ko,wral ko,ci laa dajee it ak u bari ci kilifay Ndar yi,ak li ko wr,kurel it ci njiiti Njaambur yi seetsi ma ngir tinusi ak ramusi,ci tubaab bi,ma ne leen byyi leen ma ak sama boroom rekk,moo leen pp eewant ci man,gn leen a xam li gn ci man, u far taxawlu.

Nee nanu bi nu ko taxawalee ci seen kanam,wax ak moom,ci teewaayu kilifay nasaraan yi,te booba moom ku wet la woon ci seen biir,amu fa ab xarit du caagenug aw wttal,nu ne ko wax nau nu ci yaw nngam ak nngam ? S bi ne leen indil leen ma ki leen ko wax,ba xam maak moom ku ciy ki wax dgg!. Te booba li nu doon wax naan moo ko def,ab dof bu amut am xel sax du ko def,waxantu ma laak ku mel ni moom, li am daal rambaaj la gu juge ci u kaaan ljal,ba u mujj amatuu kersa ci Ylla,saytaane yq seeni xel,jox leen xalaatam yu aaw,ba nu mujj di rambaaj ak a tudd ciy aawtef aki caaxaan lol i gn a dof ci wutkati dduna yi sax,xalaatunu koo bggal seen bopp,mbaa u koy soxla,waxantu ma laak boroom xel yu dddu yi dduna.

24

www.daaraykamil.com

Ca bis ba ma war a juge Ndar jm Ndakaaru,te booba ma nga woor, gg fa njkk jant biy so, u wcce ko fa, ca genn kr,mu tmblee waajal dog ak julli,waaye u jekki-jekki rekk lenn ndaw teew,ne ko ayca u dem,S bi jug nd ak moom,waa ja yobb ko ci neg bu deesi muslu,lndam kariis,tng jrr,xee xunn. Bi S bi gisee li wcc ci moom,mu xam ne mooy nattub Ylla bi ko doon xaar,amu ci am pexe mu dul gddu ko,te mu te sant Ylla te gram ko,ndax doon na sentu lu gn a ry loolu,mu dal ni innaa lillaahi wa innaa ilayhi raajihuun. S bi nee na ma fanaan fa dundal guddi gi ci saari Baqara ak Aali Himraan, u feg ma oom aari saar yooyu,ci aari sawara yi ak aari gcca yi,ma teg ci julli ci Yonnant bi (j.y.m) ki may ligeyal,sama dnn leer,sama xol dal,kolute gi dolliku ci Yllaak Yonnant bi,ndax {{ alaa bizikril laahi tatma-inul xuluub } ci tudd Ylla ak fttaliku ko,la xol yi di dale. Sama gudd gi daal di neex ci Ylla, ak ci aji sabab jii, ak dkk bi,ak ci neg bi. Ci loolu s baa ngi naan: { Ylla dq na jme ci ku dul man ca Ndakaaru,wpp ay wu pexewaakon (ki bari ay pexe ) bi xccoon jme ci man)) (Bu ma fattalikoo panaan moomee,ak njiit loolee,ak sax ga,sama xol day naaw ak man jm ci jli xepp aki gobar ngir jiyaari,waaye Yonnat bii di kiy fari bkkaar,dox sama digante ak loolu )) Dugg ci gaal gi juge Ndakaaru Bi nu xyee - s beey wax - muy bisub jjuma,di bis bi njkk ci rabiihus saanii,lanu yeeg ca gaal ga,gaal gi yendu,fanaan,am mbooloo ci murid yi dikkal nanu ma ca digg gaal ga,di jooy,bokk na ci mbooloo moomu,sheex Ibra FAAL,moo ca magoon,S baa ngi ciy wax ak ci gaal gi,nana: {{Ylla xamal na ma ci gaal gi,ne maay jwrini Yonant bi )) ((Gaal gu fees googu ak mbooloo, yendu na fanaan )) ((Muritam bu amub nattu boobu dikkal na ko ca gaalam gu nu duy ga )) ((Murid ba tggoo, dellu ca dun ba, nd ak xol bu naqari}}. Mu jublu ci muritam boobu,sheex Ibra FAAL,ci loolu la jiitoo woon pp. Am na ci biir gaal gi ba tay,waa ju ko dikkaloon,di ko laabiire naan ko,am na njiit lu bees lu w juge tugal,jaxasoogul ak nit u uul i,boo ko bindoon xamal ko ne danu laa too,kon mu delloo la sa kr,ca sa njaboot,S bi nee na waa ji byyiwu ko,di ko ci ljal ba mu far jl daam ak xalimaam,nee na, bi ma tmblee ba bind wenn bind rekk,la ma wax ji dikkal juge fa boroom mbindef yi,ne ma leegi da ngay diis sa aajo mbindef mu mel ni yaw,byyi ma fi.

Ma daanaka faatu ngir tiit ak kersa,ca saa sa, ma far la ma bindoon,waaye ngoor si ljlati ma,ma ne ko,loolu manul a nekk, ne ko bu buurub buur yi di wax ak jaamam yi mu dgaral ,kenn du ko man a xam ku dul oam,a mos la ca neex ak la ca naqari. Nitug neen nag, nga xam ni mook nit pp a yam,dara waru ko lu dul mu gttalu ci loolu te yam fi mu war a yam,bu bggee mucc,sunu ko tawfeexalul nangul ko. Ci loolu mi ngi naan: {{Ki njiit li yonni woon ca ligeykatu yonant bi,skku na ci moom cig laabiire mu yonnee ab bataaxel,ca njiit lu bees la tukkee woon ca seeni suuf,ba mu ko doon bgg a bind,far reccu )) ((Ginaaw bi aji ligey ji far li mu bindoon, u neeti ko bindal)) ((Mu bind xasida gu nu nangu gi,ngir fttaliku ki nga xam ne ci moom la Ylla di wonee aw yoon}}. 25 www.daaraykamil.com

Xasida gu nu nangu gi,moom lanu def ci arafi waxi sunu boroom ji (t.s) (wa ufawwidu amrii ilal laah,innal laah basin bil hibaad)) muy samay mbir maa ngi koy joyal jme ca Ylla te Yllaa ngi gis jaam yi. {maa ngi jmale samam mbind aji moom ,ji moom suuf ak asamaan ak buur yi}}.

Gaal ga deqi bisub gwwu, aareelub rabiihus saanii,S bi nee na romb nanu Konaakiri,am benn wolofu saalum-saalum bu ko fekk ci gaal gi,jox ko fa ddiya ju kawe,ne ko man de da maa dgg u ne yaa ngi w ci gaal gi,jm Gabong,ma ne naa la siyaaresi,nga aanal ma dnk ma. S bi nee na ci waa jooju la dgge turu Gabong,xame ca it fi nu ma jme,ma dal di koy aanal,ne ko bi ma koy dnk: xamal yaw sama mbokk,ak foo man a nekk,ne amul benn buur bu dul Ylla,ku jublu ci ku dul Ylla,dana xam ne amul ku fi nekk ku dul Ylla,ku jublu ci Ylla te jaaralewoo ko ci Muhammad Yonnantab Ylla bi,(j.y.m) da na xam ne Yonnant beey ki ylla yonni, u dal di tggoo,mu dem.

S bi nee na u romb Garambasaa,mu ne am na ku ko doon aawal ci biir gaal gi,waaye Ylla dox diggam ak moom ci hikamam,loolu nag ni mu ame mooy daa am jmm ju yegoon ci gaal gi,ca Konaakiri,te moom xamu ma woon,bi nu jegee Garambasaa,jenn waay ju uul gnne ci ab neg ne ma,ndax yaay diw ?jaar ci samaw tur,ma xool ko ,mu ne ma, nee nanu ma sama mbokk (mag walla rakk) de moo la jpplu,ngir barig li la sa taalube yiy ryal ak a mggal,ak nngam ak nngam,bi mu tollee ci wax jooju rekk gaal gi dal di sab (yuuxu) mu dem di xaar coow li dal,ba mu dolli aawalam yi,waaye sab ga dakkul ba kerook gaal ga di teer,mu wcc nd ak i doon wcc, kon alhamdu lilaa ginaaw amul li mu bggoon,ci loolu S baa ngi naan: {{sama ddiya sell na ca Konaakiri, eel ku nu tnn kiy fari bkkaar,ci lu dul kuy weddi)) ((Ylla setal na ma ca Konaakiri,ci lpp luy xcce jme ci yu nu sib )) ((Ylla soril na ma cag njkk ca Garambasaa,ka doon lewtoo ak man te mu dem wlif ma}}. ddiya jooju mu tudd foofu nag mi ngi ci jublu,leeral gi mu leeraloon waa ja ko doon laaj,leeral gi mu ko leeraloon maanaam laa ilaaha illal laa,waaye du ddiyay alal ja ko waa ja jox,moom waa jooju nga xam ni bu ko S bi leeralutoon loolu mu alku,te Ylla gindee na ko ci leeral gi. Mu tudd romb gi nu romb Dawme,wax karaama gu yeme gi ko Ylla defal foofa,mu ne daa jloon benn bitelu misk,bu mu yoroon,ngir wis ko ciy yerem aki tereem, nee na u ne ko snni ko ci gej gi, mu ne ma gaaw snni ko,bi gaal gi teree,am mbooloo ci sunu mbokki jullit i,duggsi,ndax danu maa dggoon ,u woon ngir nuyyusi ma,waaye kpp ku dugg rekk,jox nga ma ab bitelu misk, pp walla a ca pp,ci loolu la S bi naan: { kiy jagleele yrmaandeem di Ylla,woo na ma ci boppam,ci indil ma xewal yuy tee jaaxle}}. Mu jublu woon ci aji yrme jooju Ylla mii di boroomi xewal,daa ko indil ay xewal,bokk na ci xewal yooyu biteeli misk yooyu. Mu wax ne bokk na ci karaama yi ko ylla doon defal ci gaal gi,tggat gi mu defoon boroom gaal gi mu dikk di ko waxtaanal,di ko won ag eewant ak yrmaande,di mettitlu bu baax li ko dal,daan baril lu mu ko daa wax naan ko yaw danu laa too . Mu tuddati ne am na benn doktoor bu ko seetsi woon foofa,mujj am yrmaande lool ci moom naan ko man daal da ma laa bgg rekk,te fas laa dimble,mu ne am na wenn waxambaane wu tubaab,wu ko dikkaloon wu bokkoon ci waa gaal gi,mu ne

26

www.daaraykamil.com

Ylla def ci xolam mu sopp ma,mujj di ma ligeyal ni ko murit yiy defe .Mu ne moom daal,noonu la ylla nekke woon ak moom ciy xewal,tggatal ko pp ba kerook muy wcc Gabong.

Mu ne Gabong moom yggu fa dara rekk tuxooti fa dem ci beneen dun,foofa nag ma sax fa juroomi at,mu ne ci diirub juroomi at yii nag laa mjje mel ni ab jant,mu jublu ci, ci yekkatiku ay maqaama akug siw ak bari njari,mu ne ci diir bii it la taalife taalif yu kenn masul a def cib taar ak bari njari ci Ylla ak Yonnat bi ak ci lislaam. Dun bii nag mooy Maayomba,li koy tegtale mooy waxam ji mu naan :ca tefesug gejug dun boobu laa taxawoon di joriku, di xutba gej gi naan: { yaw gej gi kennalal sa boroom te bul ko attal,ndax sunu boroom kat kawe na wlif u koy attal(wareesu koo def att, ndax kenn rekk la) cy moom ni mu doone buur bu tedd ) (Na nga nekk di bajbaji,di fuur ngir ragal Ylla,te seere ne man ab jaamam laa,bob sopp na ko}} Mu ne ba mu fa defee jeroomi at la demati ci beneen dun,nekk fa ak ab coona,am fa atti at yu manke tuuti,di ligeyal Yonnant bi (j.y.m), mu ne am na wenn waxambaane wu bokk ci oom wu ko fekkoon fi mu nekkoon di bind,mu bocc jaaseem di ko wndel ci sama bopp,naan ma yaw ay diw di jaar ci sama tur,ma ne waaw,mu ne ma moytu ma,sama maam kat raykatu walliyu la woon,te maa di ab stam,ma joxo ko sama xalima gi,gdd ko mel ni dama koy song,ne ko xamal ni doo sa maam ja daa raye,te du ma ku mel ni a sa maam daa ray,waa ja dal di tiit,daw juge foofa fpp. Mu neeti am na kenn ci seen kilifa yi,ku doon w ca dun ba mu nekkoon,di nemmikusi soldaar yi,fan yooya ypp nit i dajaloo ci waajal kilifa gi,di setal yoon yi ak a rafetal ak a samp ay raaya,waaye bi waa ji wee,li mu njkk a def,mooy laaj ma, u tegtal ko sama kr,mu w ,dugg ,nuyyu ma,tudd samaw tur cig mggal,dal di tllal loxoom ngir nuyyu ma,man itam ma tllal sama bos,waaye ca saa sa am lu wax ak man,mel ni ag dnnu gu juge ci asamaan,ne :{ yaa ayuhal laziina aamanoo,inna maal musrikuuna najasun}muy yeen i gm,xam leen ne bokkaalekat yi sobe lanu,mu mel ni samam xel daa muuru,ma bmx ab loxoom bmx gu tar,ba waa ji yngutu,deltu ginaaw,dal di taxaw ab diir mel ni day xalaat ci samay mbir,waaye man loolu lpp,teewul ma nekk ci samam mbind,bi lu tollook waxtu jllee mu woolu ki koy firil,wax ak moom ab diir,firilkat bi w ne ma sa waa ji nee na mi ngi lay nuyyu,te di la xamal ni bu ko mere ndax moom bokkul ci i la ba,walla mu lay ljal,di la tumbrnkeel ak a gnne sa rew,moom de nee na bu ko manoon leegi mu delloo la fa nga bgg,boo gisee muy sonn ci yaw ak di la njkk a seetsi bi mu daataa wcc,mooy daa am kenn ci sa mbokki senegaal yi,ku taxoon ma sopp la,mu skku woon ci man ma nuyyul la ko,moom dey ci i mu gn a sopp nga,loolu moo waraloon sama w gii du leneen.

S bi nee na ma wax kiy tekki ne ko:nee ko loolu ma def de ag ba ko taxul. Mu dem waaye taxul mu soppiku ca na mu meloon,bi mu demee ba toog ,dal, u ne ma da nga koy teral,te booba maa ngi ak as lf ci seen mburu moomu u jaxase ak suukar,mu doonoon mburu mu neex lool,ma yonnee ko ko,mu bg ci lool,sant ma, ne lii de bu ko kuy jambaar-jambaarlu defoon te li miy woote nekkul ci moom,man na caa loroo,waaye deesul loroo ci ndigal,alhamdu lillaah.

27

www.daaraykamil.com

Da na rafet fii ma indil leen fi bayiti ki def Xawaariq muy Ibnu Hanbal: ( Bari na aji jalgati (tookat) ju sol yrey teddngaam,di puukarewu ,sol ab tneem aki takkaayam) (ay junniy junni nekk ci ron kiliftefam,te faalewul ku koy digal mbaa mu koy tere)) (ngeen (S bi lay waxal) wcce ko ci mbartalum toraxte,dammte ko ci jaasiy ndimbal ju di ab dogaakon (ju aw) ) ( muy ndimbal lu tukkee ca Ylla eel jaamam bii di ligeyal Yonant bi,nga xam ne soldaari nasaraan si ci la nu mujje mokk ba mel ni ay ansaaram,(ansaar mooy ku lay jppale ak a dimbale) ) ( cey bu tuddoon sekkare bi, kon dey mbindef yi yemu,waaye moom ab dnnam bmmeelub ay mbot la). Nee na bokk na ci karaama ( mooy xarbaax ak kiimaan yi Ylla di defal aw wlliyu) yi ko Ylla defaloon ci gej gi,feeug Ahlu Badrin,mu ne moom kat bi mu nekkee ci benn ci dun yi,dau koo yobb woon ca karce ga,dkkal ko fa soldaar sa,nee na ma mel fa ni kenn ca oom,uy tux ak a naan ak a fo ci sama wet, man may mu seeni lor rekk,ndax man xam naa ne mukallaf mu ne am na aari malaaka yu ko seq,di bind ay jfam,ginaaw aari malaaka yooyu oo man a mu,man a dkku li iy dajeel ciy lor,ngir topp seen boroom,kon du jaadu ci man may jmbat,ndax oom kat li leen di naqari rekk moo may naqari,li leen di mettee may metti,te oom du u jmbat. Ci noonu Ylla dogal soldaar si genn bis di tggatu ji ,ba u demee fauy tggatoo fekk fa am mbooloo mu war ay fas, kaalawu, sappewu (rang),soldaar si dal di tiit ,taxaw,ci noonu seen njiit li tyye leen,gdd leen ne da leen di ray bu u siiwalee xibaar bi. Bi suba jotee ba leer,mbooloo mi waroon fas yi ne mes,soldaar si dem ne miik,ba a nettali dara. S bi nee na bi loolu tegee ay fan,aakim bi (goornoor bi) woo ko nooy-nooylu ci kanamam,wax ak moom wax ju nooy,ci biir wax ji mu ne ko: xanaa da ngaa am ay ndandoo yu lay dimbali ci li nga bgg? Ma ne ko oou moom ay nit lanu walla ay jinne? Mu ne ma yaa ko gn a xam ! Man ma won ko ne xamuma dara ci li miy wax,mu dal di noppi. Am na ci boroom xam-xam yi ku ko ci laajoon lu waraloon feeug Ahlu Badrin gi,S bi ne ko :ngir tiital noon yi. Keneen laaj ko ne ko ooa ooy niti Ahlu Badrin a walla malaaka ya?,mu ne ko malaaka ya .Am ku neeti ko ndax yonnant (j.y.m) bi ca la woon? Mu ne ko moo doonoon seen njiit,daal di ciy wax wax jii:<< ki nga xam ni wommatal na ma la fddu woon wliif bepp wlliyu,jppndalal na ma mebat yepp fa dkk ba niy wax Limbarwali >> << ka soril rambaaj ba ak ku inaa ka ,wommatal na ma waa Badar a diy sang>> << Ylla da na ma wommatal begleg laa illaaha illallaa fu ma man a ne >> . Ku baax ki nee na li mu bgg a wax ci bayit yooyu mooy: li fddu woon weliif bepp wlliyu,mooy feeug waa Badar nd ak seen kilifa ga (j.y.m) ca pkk yu lndam yooya ca geej ga,ngir jjji ay noonam.Begleg laa ilaaha illallaa,mi ngi ci jubloo wax aaya bi sun boroom di wax (( wa in yuridka bi xayrin fa laa raadda lifaddlihii)) muy ci maanaa bu la Ylla bggalee aw yiw amul ku ko man a tyye. Fu mu waxe nex-nexi walla lori laa illaahaillal laa,mi ngi ci jublu waxi Ylla ji mu naan:(( wa in yamsaskal laahu bi durrin falaa kaasifa lahoo illaa huwa )) muy ci maanaa bu la Ylla laalee ak aw ay amul ku ko man a dindi ku dul moom.

Mu ne bis teg nanu ko ci mbedd mu xat,dal di joyal aw nag ci kawam,tmblee seetaan,yaakaar ne agsi na ci sama kaw ba noppi,waaye bi mu ma jegee daa daal di jekki-jekki rekk naaw mel ne daa am ay laaf. Nag wii mooy wi Abdu Laahi Saalim Ibnu Anbal doon tudd ci Xawaariq bi mu naan: ( ab xiik (xiik mooy xale bu jigeen bu masul a sy,fii mu jublu ci nag wu toll ci war a sy ) ci nagi kr yi,muy naaw ci jww ji ba kenn gisatu ko).

28

www.daaraykamil.com

Mu ne mas naa am mu ygg ci benn barab ba foofa soof ko,mu tmbli di jmbat,waaye nee na daa jmbat rekk Ylla sotti ko yamb yu soxot te bari,u koy mtt ak a sonnal,mu ne bi mu xamee ne li ko dal moo ko teg boppam,ndax kat ((wamaa asaabakum min musiibatin fa bimaa kasabat aydiikum)) muy musiba mu leen dal yeen a ko teg seen bopp,bi loolu amee mu ne ma soppi samag jmbat def ko ag cant,daal di ne: (( nasaxal naa sama njmbat def ko ag cant,dootuma jmbat ci moom lenn lor,ndax sama lor naaxsaay na)). Ci noonu nee na yamb ya dem wlif ma ,ma tmblee noppalu,xam naa ne yamb yooyu la ki def xawaariq jublu woon bi mu naan: ( ay yamb yu toll ne ay mburtu (mbate) yu suur cig ry, cam si (cam si mooy waa ji,mu jublu ci Sen bi) daje na ak oom,te faalewul seeni lor ). Mu waxaat ne waa jooju doon nasaraan-nasaraanlu te nu tuddoon ko ca ginaaw,bis def na ko lu aaw ba yenn xaritam yi yedd ko ci,xupp ko ba mu tiit, reccu,ca guddi googa nag mu w nd ak ku koy wommatal ab gtt,moom mu yor benn biteelub daa bu mag ci loxoom,dal di tedd tllalu ci sama kanam,nee waay day tuub,te ne du jug fi mu tdd mukk,li feek teguma sama ndggul tnk cig doqam,ngir tuub,ma fexe ba jle ko fa ci wax ju rafet rekk,mi ngi ma fekkoon nag may bind ca jamono jooja,ma dal di def bayit wii ca saa sa: 4(( Ylla nooyalal na ma ci guddi gii xolub boroomug tubbi ga,ginaaw bi mu ma indilee ab gtt ak daa , ( ngir tuube ko ) )).

Ku baax ki tudd na ba tay yeneen karaama yu ko ylla defal ci gej gi,mu ne da fa mas a dkk ak benn doxalkat (goornoor) bu soxot,bu kenn dul jege te bagul dara ci lu baax,ma wax bis ne jiyaar jii may def ci yoonu Ylla daal di naa ko seet tay ci mbirum ttekat bii,ma xool nu ma ko Ylla di tggatale, ci noonu ma juge sama neg dal di dgmal kram,u ne ko sri ba dey a nga jemsi ci yaw, mu ne aah loolu de lu jomb la,ndax danu daa skku ci moom muy ba,kon tay naka la fiy dikke ci coobareem,u ne ko amul benn sikk ci ne kee di dikk de moom la,mu dal di jug ci saa si daje ak man fu sori,bg ci man mbgte mu kawe,ci noonu mu nd ak man ca barabub boppam ba,dal di ne ma loo bgg, loo bgg cig baamu ? Wax ko ay yoon, man itam ma ne patt, rekk di xool lu ma koy wax,ba ygg ma ni ko,da maa bgg as lf ci daa, mu dal di may jox bitel bu mag bu fees ak daa,ma daal di ne wlbat won ko ginaaw,booba fekkoon na ma may bind ak xasida gu u tnke arafi a b t th j (mooy abajada rekk) ,ba ma ggee ca arafu faa,ma bind ca bayit wii ne: (( sama xalima texe na fa ab aat (mooy ku xaraful)bu weddi Ylla,kok tggat naa ko ci xul huwal laahu ahad)).

Ma bindaat ay bayit,yoy dau maa wax ni ma lii de ag wor la, ndax yaa ngi byyi yefar yi ci anam gu dog,ba noppi ngay jl ci oom di nbb,ma dal di byyi la ma doon def,gas am pax ba mu xoot ,ma sotti ca daa ja,suul,dal di xam ni sama jiyaar ji dggu na, ma sant Ylla . Nee na itam,benn janqu ndar-ndar,dafa gnt gis Waa-Badar,ci bis yooyu nu dugg dkk ba, tmblee ray waa dkk ba,bi nu demee ba kenn ci oom jege ndaw si,jenn moroom ji ne ko soxna soosu de ab jullit la,mu dal di koy byyi. Sri bi nee na xale bu jigen boobu ku baax la woon,daan sonn ci moom ci li mu am,daan ko wax naan man dey lu ma la jox rekk xamal ne maa ko aq ci sama loxo,njgug sngara nekku ci du caagenug gu poon,loolu da koo leeral foofu ndax kat foofa ci aar yooyu lau daa jflantee,te moom xam na ne man du ma leen jfandikoo te du ma jfandikoo seenug njkk,ma laaj ko bis ne ko loo

29

www.daaraykamil.com

bgg ci lii nga may defal?,mu ne ma bu dee ci dduna ,st yu baax,bu dee allaaxira jjana, ma ne ko Ylla man na lu nekk. Yggul tuuti rekk,Ylla dogal mu mb,te daawul mb,bi diirub mbam matee rekk mu dal di wsin,dal di faatoo ci wsin wi,ma jullee ko,masu ma koo gis it mukk,ndare bi ma taxawee di ko jullee,ndax sunug jflante mi ngi doon ame cig yonneente (correspondence). Nee nanu doomi Daba SEY la woon tuddoon Aamina (Ami),boroom kram tuddoon Ylli SEY,bokkoon ci ndawi goornoor yu mag yi,di woon it ku baax te daan sonn ci man. Am na bis mu jote ak ttekat bi (goornoor bi) jote gu tng,ngir sama jmm ji,loolu nag ni mu ame woon mooy daa am bis ma wutoon eenti bant teg leen ci sama buntu neg ngir def ko ab julliwaay ngir iy romb ba di ci jaar,bi ko ttekat bi gisee ,daa dal di jug,falang jkka ji buddi bant yi,snni leen,ne fii amul julli amul lislaam,da nga oo bgg a yqqal sunu soldaar yi,ma ne miik,bi ko Ylli SEY ygee te tubaab bi demagul,daa dal di jug ca saa sa,jawalsi nd ak aw meram , ne ko lu tax nga tas jkkaam ji,te moom defu ko fu dul ci buntu kram?, sakkul yoon wi te xatalul kenn it. Tubaab bi ne ko man daal maa ko def,fii jkka du fi am,Ylli ne ko waaye man di naa ko defaraatal jkkaam ji na mu meloon,tubaab bi ne ko du fi ame, uy bgg a doorante nit i dox seen diggante, u nekk di xuloo diggante tkkusaan ba jant so,ci biir loolu lpp man maa ngi bind.

Ci xisa bii (nettali bii)laa binde xasidag ((Rabbanaa axrijnaa min haazihil xarya azzaalimi ahluhaa wajhal lanaa min ladunka walliyan wajhal lanaa min ladunka naziiran) muy ci maanaa yaw sunu boroom gnne u ci dkk bii nga xam ne i fi dkk ay tookat lau te nga wutal u aji mngoo ju tukke fi yaw,te wutal u aji dimbalee,xasida gee nekk nii: (( grm naa kilifa gu mgg gii nga xam ne yar na samab xol te koomal ma, moom dey mooy boroom bi gn a tedd)) ba bi mu ggee ci : (( bindal ko(moom Yonnant bi) ag xewal ak ag mucc ak oam aki saabaam te nga def sama jkka ji ci darajaam (moom Yonnant bi) muy lu yaatu )) Bi mu ggee foofu u ne ko nangul nanu la ko,da nga ko gis. Loolu nag gis nanu ko,mooy jkkay Jurbel ak Tuubaa ,xasida gi nag gu gudd la te rafet gu am jeexiit gu ry ci ja ak oddi bu soobe Ylla ak ci barkeb aji defam,ku koy jfandikoo na ragal Ylla te xemmeem aw yiwam. Ylla dogal na bis Ylli moomu siyaaresi ko Njaarem,juge ca yooyale wll,ginaaw bi jumaa ji noppee muy ju Njaarem,S bi ne ma maak sama jenn waay nd leen ak moom mu siyaare jkka ji,u nd ak moom, won ko jkka jpp,penkook sowwu,biir ak biti,mu yemu gpp yemu,bi nu dppee S bi ne ko noo gise jkka jii ak sama jkka joojee,yaw mi ma doon xeexal ak a dkku?,mu ne subhaanal laah maneesu leen a tollale,S bi ne lii mooy maanaam sama wax jii: (( Ylla dq na jme ca ku dul man ca Maayomba la naqari woon sama xol te ykkati samag wll)). La naqari woon sama xol bu nu koy firi mooy tas gi nu tasoon jkkaam ja,yekkati samag wll mu jublu ci yekkatikug soorool yi.

Ab nettali bu yemee ngii bu lmboo ay karaamay Se bi: Se bi nee na bi tubaab bi buddee bantam yooyu,snni leen,kenn ci gaa yi bgoon ci jfi tubaab bi, da cee jloon ab bant samp ko ci wanag wi miy sangoo ak a doxe aajo,waaye Ylla nattoo ko benn bis mu bgg a tuur ndox,jawali ca satala ga te booba 30 www.daaraykamil.com

satala ga ndox mu tng a ca nekk te moom ygu ko,te seetu ko it,waaye bi mu noppee ba sotti ko ca cr ba (skkara sa) da wadd ca kaw ni ab baa bu gor bu tiit,dal di yuuxu ba fa baatam yam, ne: Se bi dimbali ma alku naa de,dal di snni satala ga ca ll ba,dikk teg loxo ba ca tubay ja,ma ne lu deesi defati lu dul mu ak wax (( innaa lillaahi wa innaa ilayhi raajihuun)).

Mu neeti - moom ku tedd ki - ne am na at mom bu doonul woon li ko Ylla tawfeexal saa su xamee ni weer tmbali na mu di ko bind,kon wenn weeru ramadaan doon na jll te du ko xam,ndax waa dkk boobee mu nekkoon xamunu woon lu dul weeru tubaab wi,bi korite gi jotee ma xy, dog ,sangu, def li ci sunna digale,ma gnn ne damay julli ji ca pencum dkk ba,ba ma ggee, ma xool sowwu ak penku,xoolati sama ndijoor ak cammoo,nd ak am kolute ci ne kenn du w,am aari jbber (jbbeer mooy jaam bu jigen) yu agsi war a toll ci baalix ( baalix mooy ati gnn ag ndaw) taxaw sama kanam di ma seetaan,ma kbbar u tmbalee xqataay,saa su ma kbbaree nu ree,naka noonu su ma jngee,ba ma slmal def samab xut ba, sama deyaale gi maa ngi ciy wax:(( yaw buur bi, xam nga ni woor naa weeru ramadaan ni nga ko digalee,ma dog ,sangu,julli ni nga ko digalee,waaye dey lu ma gnnee muurum koor laa amul,bu ma ko amoon it,ku ma ko jox laa dul am,kon jullil te slml te barkeel ci sunu sang,sunu kilifa Muhammad ak oam aki saabaam ,te nga nangul ma lpp lu ma man te def ko ci sa ndigal yi,te nga bindal ma yoolub li ma manul ltt ci,te amoon ci yeene walla yu ni mel.

Bi ma noppee def xasida gii: yaw buur bi jullil te slml te barkeel ci sunu sng ,sunu kilifa Muhammad ak oam aki saabaam te nga def qaafiya bii di w,mu kawe miimiya ba ,ci lu fee ak lu nbb,aamiin yaarabal haalamiin ci barkeb Yonnant bi (j.y.m) : ((maa ngi yaakaar ci aji yaatu ju dggu ji,ci darajay ki niy xeetu di Yonnat biy dimbali dgg ci dgg (j.y.m) )) (( maa ngi yaakaar ci Ylla moomu delluwaat ci samay mbokk ci lu gaaw nd ak njub gu dggu)) (( ak nekk jaam bu texe bu nu matal, tey ligeeyal jaamub Ylla miy dgg,jaamam boobu di yonnant bi mu tnn)) (( yaw Ylla ci darajay ku nu tnn ki ak oam,yal na nga ma jggal te nekkal ma te wommat ma te goreel ma)) (( di naa la grmloo ci Alxuraan ak sunna si nga xam ne,Yonnant bi yoonalal nanu ko,yaw miy aji teqale lu taqaloo)) (( yal na nga ma tggatal noon yepp ba fww,te fegal ma ag bokkaale,yaw aji not jiy boroom tijji ak tj)) yal na nga ma wommat delloo ma Daaru Salaam gi nga xam ne fa laay deyaaleek yaw ciy aaya,te yal na nga kaweel ci man ay gox)) (( yaw sunu boroom yal na nga ma dello ci lu gaaw te defal ma samay mbat yepp,te nga may defal ay mbgte te di am eewant ci ma)) (( te nga may ma ay xam-xam yu jari jmm ji ak mbidef yi,te nga dolli ag yaatal gog texeel lay doon ak ubbi ak xar-baax)) (( sama bakkan dy daa ba ag ywnal,ndax ab noon la,kon sellalal ma ko cig taxa (taxa Se bi mi ngi ciy jublu lu gaaw) yaw miy ngn ji kuy yegale )) ((na nga ma may ba fww li ma bgg ci mbindef ypp, te nga fegal ma senuw ay yaw miy joxe ag jiitu )) (( mngal ma samay mbat fii ak fa nu jm,te nga may ma ngnel lu mgg te saxalal ma ngnel li)) (( yaw sama boroom fegal ma li ma ragal ca bisub njqare ba,te nga defal ma jggi siraat gu gaaw gu mel ni melax )) (( musal ma ci (ay nocciku = nusuuh) ak lpp lu nit iy ragal te nga def ma may ku sori ag lakk)) (( nangul sama aan gii yaw sama boroom,te nga faral ma samay ayib ,te nga seere ne man dey tuub naa ci jepp jf ju di jfi dof)) (( te nga nekkal ma yaw sama boroom,te musal ma,te amal sama yaakaar,te fegal ma luy bijji ag nx )) (( nangul ma sama aan gii,yaw mi moom lepp, te nga tabe eel ma cig yaatal ak 31 www.daaraykamil.com

dddu ak dggu )) ((ci darajay Yonnant bu nu tnn bi,te nga fegal ma hisaab ci darajaam,te tggatal ma ci moom kepp ku di boroomug kccoor)) (( na nga julli te slml ci moom Yonnant bi,ak oam aki saabaam,yaw mi moom penkook sowwu)).

Mu nettali ci karaamay gej gi,ne : am na jenn waay ju bokkoon ci kilifay barab bi ma nekkoon,da maa digoon ab bitelu misk ci lu dul ma di ko skku ci moom,ndax man daawu ma skku ci oom lenn,te daawu ma sentu ci oom,daawu ma wolu seeni dig it,waa jooju ma digoon bitelu misk bi,ndekete daa digoon keneen ci moroomam yi lu mel ni li mu ma digoon,waaye bi mu deful li mu digewoon ,waa ja daa tmbali di xuloo ak moom ak a ngaayoo,moom itam muy dkku boppam,(di defandar boppam) loolu lepp it mi ngi doon ame ci sama wet,ci wolof it lau doon waxe waaye yu leerul dara,waaye lkk gi nu koy lkk li muy leeradi leeradi fttali na ma rew ma, ba mel ne da maa ibbi far ,ngir gj gi ma ko gj a dgg,loola neex ma lool. Waaye xuloo bi nu def te li ko waraloon lepp mooy wolu gi mu ko wolu woon,ak dig gi mu ko dig te defu ko,loolu lepp ma sant ci Ylla,mi ma defal may kok woluwu ma kenn,sentuwu ma ci kenn ku dul moom,loolu tax ma def xasidag cnt gii, ma wax ne: Maa ngi tmblee samay wax aki bjf ci turu Ylla miy boroom yrmaande ju yaatu ji ak ji miy jgleele, xeewal ak mucc yal na nekk ci sunu sang,Muhaddad ak oam aki saabaam.Miimiya bii moom la eel yal na ko Ylla grm. Yaw sama boroom sama noon yiy say noon,snni nanu ma ci gej gi,ni nu snnee woon sa xarit ba Ibraahima ca sawara wa,nga waxoon ak moom (sawara wa) ci :(( yaanaaru koonii bardan wa salaaman halaa ibraahima )) muy yaw sawara wi doonal ab sedd ak jmm ci Ibraahiima. Sawara wa dal di mujj di jjana ci moom,jmm ak xeewal yal na nekk ci moom ak ci mbooleem nabiyu yi ak yonnant yi, Yaw sama boroom! Yaw sama boroom! Yaw sama boroom! Yaw aji dund ji! Yaw aji taxaw ji ! Ci darajay weeru ramadaan mi nga wcce Alxuraan, mu dig jub eel nit i, te di ay aaya yu leer yu di ag njub ak ag teqale dgg ag safaan,ci barkeb xut ba bii tggatal ma gej gii ak oam ak mbooleem samay noon yiy sa yos,te nga bgal jullit yu gor yi ak yu jigen yi ci u gis ma te dajeek man,te dgg sama ag dellu ca Daaru Salaam,ak Tuubaa ci lu gaaw ci lu dul ab coona du caagenug ag sabablu gu tukkee ci man,Aamiin yaw boroom mbindef yi, ci darajaam moom Yonnant bi,(j.y.m) te nga def miimiya bii mu kawe li ma jortoon,ni nga ko baaxoo defe ak man ca la ma waxoon njkk bii,te nga defal ma ko muy ab yobbal,tey pakk tey jjana ci aari kr yi,aamiin yaarabal haalamiin. (( man dy maa ngi tagg,tey sant ngn ji aji xewale, te du ma jmbat kki xewal ci menn mbindef )) ((kepp ku ma jorte ci sama tumburnke gii may kuy toroxlu ci kenn ku dul aji doyluloo jiy aji yaatu (muy Ylla) na ko wor ne moom ku gumba la )) (( moom de laay jmbat samag ltt ,samag kk ak samag tumburnke,may yaakaar samag dellu ci lu gaaw di ngn ji ku nu xeewale )) (( jmbat naa ko samag ltt,mu fajal ma ko,te nekkal ma ci lu kawe sama njort,moom kat mooy gn jaa teddi kuy terale )) (( i nga xam ne weddi gi nu weddi Ylla da leen a wor danoo jublu woon samag wll,mu aar ma ci oom dkku jepp aji too)) (( ag cant eel na ko tukkee fi man,di yaakaar ci moom sama ckkutef lii,ci lu dul ab coona buy juge ci man,te sama naqar da na )) (( ki njort wor ba muy iaan, bu ma woree tam,na ko wor ne ki ma wommat cig teral de woru ma)) (( ku ma snni ci gej gi ngir ag weddi di boroomug 32 www.daaraykamil.com

mbaeel,na ko wor ne ci gej gii de tabeg aji terle ji dikkal na ma fi )) (( koo xam ne li ko naqari mooy nekk gi ma nekk di jaamub Ylla,tey jwrini aji rammu jiy ku nu jiital )) (( na ko wor ne man de ab jaamam laa ci gej gi ak ci jeri ji,di ligeyal kiy musale ci luy waral reccu)) (( ku ma dddu de na xam ne xewal yi jublusi nanu,juge ci aji yaatu jiy aji doyluloo,kiy aji wattu tey aji jiital )) (( ku ma snni ci gej gi ngir skku samag tumburnke,na xam ne ag tggat eel na ma tukkee fa sama boroom ci gpp gej )) (( samag weru eel na Ylla ci samag teew ak samag fdd,te di naa jmbat jm ci moom jaarale ko ci Yonnant bi,moom miy samab raas (bi may yege jm ca Ylla) ndaw muy ku baax )) (( yal na Ylla dolli xewal ak mucc ci moom ak ci oam aki saabaam ak bepp jullit )) (( yaw sama boroom saxalal ba fww ngn jaa selli julli ak slml ci Muhammad)) (( ak oam aki saabaam yepp,te nga delloo ma Tuubaa ci lu gaaw,te peek ma te xamal ma)) (( yaw sunu boroom man de warlu naa ba fww di kuy ligeyal Yonnant bi,tey kuy ligeeyal aaya yi,na nga ma xamal te dggal ma )) ((yaw sama boroom,maa ngi skku ci aji maye ji ag geju akug wui akug yinkiiwal (ag sol xam-xam mu tukkee fa Ylla) na nga ma wuil te yinkiiwal ma )) (( jublu naa aji ubbi ji tey skku ag ubbeem,di yaakaar ci moom ay may yuy ball,ndax ag ballam day yol di sotti)) ((grm naa aji not ji bi mu ma tggatalee noon yi,ma doonoon ku tumburnke,di ku wet fa oom di ku amoon gpp lmmu)) (( di naa ko grmloo ci Alxuraan ngir sant ko ci xewalam yi,ci sama xol ak sama yaram ak sama gimi )) (( war na ma ma saxal li mu ma tnnal mu dig jub,te ma koy grmloo ci aaya yi ndax oom kat (aaya yi) mujj nau di samam mng (ngaaay) )) samay cant aki ngrm aki tagg eel na aji jarie joj indil na ma Alxuraan ju tedd ju u mggal)) (( moom (Alxuraan) mooy ndmm mi (koom mi) tey leer gu fs gi niy aar ci sawara ak noon yi ak gcca)) (( ab teere la bu tedd,juge ci aji tedd juy terale,jm ci jaam bu tedd,buy xettalee tey boroom yrmaande)) ((teere bu darajawu la juge ci ku darajawu,ku darajawu te wor indi ko, jme ko ci aji darajawu kuy matal )) (( xewal ak jmm ci lu dul dog yal nanu nekk ci moom,ak oam aki saabaam fu mu man a nekk)) (( jmm ak xewal yal nunu sax ci moom li feek aji sant a ngi naan : da ma ne maa ngi sant ngn ji aji xewale)) (( Xewal yal na sax ci moom juge ci aji tedd ji may nekkal,te du ma jmbat kk ay xewal ci menn mbindef)) (( mucc yal na nekk ci moom juge ci moom (Ylla),(mucc) gog da nga ma ci fegal (yaw Ylla) aw ay, te aar ci samag wll wlif ku nu rbb ki (muy ibliis) ak ku gumba)) ((xewal yal na sax ci moom tukkee fa moom(Ylla),li feek ku koy jmbati mbiram a ngi am la mu bgg di gn ji ku nu xewale)) ((aki o aki saaba yoy maa ngi aan aji kawe ji mu dugal ma ca seen biir lg may boroomug xewu )).

Bokk na ci karaamay gej gi ba tay nettaleem bii,mu ne: bis xy na, waaj ngir ligeyal Yonnant bi - ni mu ko baaxoo woon - amul lu dul aw mettit wu tar daj mbooleem yaram wi,ba manatul li mu bggoon ,waaye am benn tubaab ci njiiti nguur gi,mi ngi dkkoon ci wetu fi S bi dkkoon,nekkoon di xaqataay ca kaw aki moroomam,S bi daa di ne:Ylla yaw de xam nga li ma waajoon jm,ak li ma ci gllankoor,maa ngi lay aan nga tuxal lii fi man te yobb ko ci ki lay wutal moroom,amul lu dul ma dgg waa ji doon xaqataay muy onk,man may bind.

Bokk na ci karaamay gej gi ba tay lii: bis nee na fi mu nekkoon ndawal da faa mnke woon lool,ba jn yu ndaw yi nuy def ci poti we yi rekk lanuy lekk daanaka (xam naa mooy poti ton yi) ma jfandiku ci bis,bi 33 www.daaraykamil.com

ma noppee ma raxasu ba sonn,jfandikoo suuf ak saabu ak lu nu man a dindee ag xet rekk,waaye dara,ba ma ca manatul dara ba ne naa dem nag jublooti ca ligey ba,bi ma tmbalee rekk u ne ma ((wa minhumul laziina yuuzuunan nabiiya)) muy am na ci oom uy lor Yonnant bi,ma tiit lool, jaaxlee jaaxle,ca saa sa ma byyi koo jfandikoo,doxe ca byyi luy jn,boole ko ci li ma jaayante ne du ma ko lekkati,bis bi ma ko byyee walla lu ko jege,ay kuy dikkal nanu ma,juge ci fere yi,di njg gu nu gaawal ci jn yi ma jaayante woon.

Mu neeti moom ku baax ki:dkk bi mu nekkoon da faa nekkoon aki lbbe uy jl ci xaley yefari nit u uul i nekkoon foofu di leen def ay mbindaan,di nd ak oom di wr ci ja yi (marse)ginaaw tkkusaan,njiit li nekkoon foofu defe woon ne da maa xemmeemoon ci gone yi mu ne ma woon boo ci soxlaa de ma joxla ci uy nd ak yaw,ma ne ko soxlwu ma ci. Njiiti dkk booba itam baaxoo woon nanu di jl ci magi nit u uul i, u uy def ay toggkat aki rootkat,ma skku kenn ci oom bis ngir ligeyloo ko,waaye ba mu ma jegee daal xeeal na la ko xee goo xam ne amul gu ni mel,ma ne kii daal sobe na ba maneesul a jaxasoo ak moom,ca noona ma jaayante ci seeni ndaw ak seeni mag ni ma jaayantee ci jn yu mag yi ak yu ndaw yi ,ci loolu mu ne:

(( ma ne njgug ndaw i dikk na ak gu mag i ak ndaw i)) ((Muhammad gn ji imaam mooy sama dkkandoo,ag bbbam de (dexam) ci sama xol lay sottiku jm)) . Fere yi woon indi kuy yi (xar mu goor mu mag) ooy mosalug njgi yefar yu mag yeek yu ndaw yi,kuy yooyu it di mosalug njgi jn yu ndaw yi ak yu mag yi. Bokk na ci karaamaam yi ci gej gi ba tay waxam jii mu ne: bi ma xoolee sama diggante ak noon yi ,nooni Ylla yi,ma xam ne oom kat am nanu kttan ci lor ma ak gaa ma,ci dogalub Ylla bi akug nammeelam,ma xam it ne bu doonutoon kaaraangey Ylla ji akug fegam kon ba tay waxatunu ko,laa leen byyi ak seen bgg-bgg,jublu sunu boroom,mi yor mbir yi,ma deyaale ak moom ci sama mbir: ma ne ko Ylla yaway ki nu bind ngir nu jaamu la,nga ne ((wa maa xalaqtul jinna wal insa illa liyahbudoonii)) muy bindu ma nit ak jinne ndare ngir u jaamu ma,nga neeti : (( yaa ayyuhan naasu uhbudoo rbbakum)) muy yeen nit i jaamu leen seen boroom,bu ko defee tawfeex eel ki texe jiitu ci moom,mu dgg wax ji topp ko,naka noonu toroxte eel ki ag texeedi jiitu ci moom,mu lnk ba a wuyyu,tx, luu, ngirug weddi,man nga tawfeexal ma,def ma ci mbooloom i wuyyu,mbooloom Yonnant bi Muhammad (j.y.m) imaami anbiyaawu yi ak yonnant yi jmm yal na nekk ci oom epp,nga dolleeti ma ngnel,def ma may jwrini Yonnat bi tey xalifaam ci diineem ak xeetam,am mbooloo ci sa noon yi, noonam yi,jug song ma ngir dox sama diggante ak jaamu la,te ligeyal ko (moom Yonnant bi) . oom dey i ngii di u caaxaanadi ci seeni jf,di uy farlu ci seeni neen,te yaw yaay ki wax ci lmmiu sa Yonnant bi,lol maanaa mi mooy:nit ku nekk daa am kr ca jjana ak ca sawara,bu duggee jjana u won ko kram ga woon ca sawara,ne ko fee de nga jmoon boo jaamuwutoon sa boroom,leegi nga xam ne daa nara gnt,ab yefar a koy donn. Bu tbbee sawaraat nu won ko barab ba mu doon am ca jjana,bu jaamu woon Ylla,ginaaw nag jaamuwul boroomam ba tbbi sawara,leegi ab jullit lanu koy jox. Ginaaw mbir yi nii lanu deme,te noon yii - ni nga ko xame - ci too ma lanu dkk ak a def ci man lu leen soob,te du ma

34

www.daaraykamil.com

fayyu te du ma leen aanal aw ay,waaye maa ngi lay aan seen kr ya ca jjana,Ylla nangul ma ko,may ma leen,ba ma xamee ne maa leen moom,ma jox leen ddiya waa-Ahlu Badrin . Ci loolu mi ngi naan: ( jox naa ddiya kri noon ya nekk jjana mi kuy jalgati dul dugg,eel saabay Yonnat bi)) ((kr yooya de jlees na leen ca noon ya,jox leen saaba yu baax ya)) (( Ylla jox na ma kr ya fa samag tumburnke,teeyal it samab xol)) (( man nag def naa leen ay ddiya eel saaba yi,yal na leen Ylla gram ,moom mi ma aar wlif (sahaab:ay niir ) )).

Na nga xam ne karaamay tukkib gej ji moom maneesu leen a jeexal,bu ma bggoon a indi li ma ci xam ci lu juge fu wor ,ak li ma ci dgg ci nit i,kon dey ma indi fi lu yem xel yi,te kon du xaj ci teere sii di su nu gttal,looloo tax ma yam ci li nga xam ne topp naa ko ba mu wor. Mu ne ati tumburnkeem gi juroom atti at yu mnke tuuti la,bi mu matalee li ko Ylla bindaloon cig tumburnke,ci suufus yefar yu uul yi,Ylla indeeti ko ca suufam ngir nitam i oom itam jariu ci moom ci li ko Ylla may ciy mbot ci tukkeem bu barkeel boobu,ak ngir mu daje ak mbokki jullitam yu baax yooyu di naar yi,ci noonu Ylla dal di def ci xoli kilifay nguur gi u am ag eewant ci moom delloosi ko. S baa ngi gsi Ndakaaru bisub gww juroom benni fann ci sahbaan,atum kasasin di 1120 g, mu wye fa, jll Ndar def fa lu tollook fukki fan ak juroom ba ca bis bu njkk ba ci ramdaan, mu doonoon bisub talaata,mu juge fa,dem Luga, wcc ca rakam ja Sheex Coro MBAKKE,ca guddig gwwu ba, mu raaane fa romb kr Sheex Jull SIISE,jugeeti fa jaar kr muridam ba sri Sire LOO, yoor-yoorug diber ja ca Snnoosi, mu sax fa la desoon ca ramadaan ja,noppalu fa,woor fa. Ci diir bii,foofa fees na dell,raj-rajloo ba mel fa nu mu masul a mel,ci diggante ay taalubeem ak kuy skku ndimbal,aki kilifa yu koy siyaaresi,di ko ndokkeelsi,bokk na ca ooa ka nuy wooye (kiimaanug jamonoom,woykatub waxtoom) Sheex Ibraahima JOOP Almasharii,ab xisaam lu xoromu la te yeme,ag wui (feeal mooy wui) gu yeme fee na ci eel S bi (maanaam S bi wone na ci ay xar baax) loolu mooy sheex Ibraahima moomu daa amoon ab bor bu mag bu ko ljloon lool,ci jamono joj fay ko ci jafe na,mu jug wr ak moom ci sri su mag si waaye taxul kenn tyye ci loxoom,ci noonu mu jaaxle lool te am tiis,waaye bi S bi agsee Snnoosi,mu w indaale ay bayitam tudd ci mbirum bor bi ak ni mu ko seddalee ci diggante Yonnant bi(j.y.m) ak eenti saabaam yi,ginaaw sri si nanguwunu koo xettali.

Bi mu ygloo S bi ne ko mu agsi,mu dikk,nuyyoo,bi mu daataa wax ay mbiram ak boram bi ak ni mu ko seddalee ci bayit yi,S bi ne ko indil ma mbuus mee,mu indi ko,mu neeti ko jox ma mi ci des ,mu jox ko ko,mu ne ko waal li nekk ci mbuus mu nekk,mu wa ko, muus mu ne atti temer nekk ci,boo leen boolee uy juroom benni temer,S bi ne ko indi benn temer bi te jl li ci des dimbandikoo ko ci say soxla,te moom boram bi juroomi temer rekk la woon,ca saa sa sheex Ibraahima daanu ab jll,yuuxu ca kaw,S bi ne ko waaw yaw lu mu? Mu nettali ko xisaam,jngal ko bayit yi,moo nekk nii: ((bori ay mbokk war na ma,ma seddale leen ci diggante u tedd i ndax u fay leen)) ( yaw Ku nu tnn ki(Yonnant bi), yaay ki moom cr bu njkk bi,yaw su xarit bi (Aboobakar) yaay ki moom aareelu xaaj bi) ( yaw ki 35 www.daaraykamil.com

teqale dgg ak fen (Omar) yaay boroom atteel bi, yaw sunu Usmaan mi, nga moom bi ci topp) ( yaw gayndeg xarekat yi,yaw baayi Asan ak Usaynu iy leerug sunu diine ji,yaw laa feetale li ci des) (yeen de u tedd ngeen o kuy jmbati coona du weru ci seen daraja te fajalu leen ko ko) ( kon gn jaa selli xewali Ylla na sottiku ci yeen,li feek Ylla a ngi faje ay soxla ci yeen).

S bi yemu lool te sant Ylla,waaye noon yi oom seen kiaan gi mayu leen sax u xaar ba S bi ibbi kram,waaye danoo dal di tmbalee wut seeni pexe,di lal seeni yoon, di waajal li nu nar,di xaar waxtoom jot banu def ko. Ku baax ki moom bi mu jullee iid ca bisub kori ga,mu doonoon bisub alximis,da faa toogaat bisub jjuma ak gwwu ba ca tkkusaan sa,mu laxase fa romb ca kr taalubeem ba Koor Mag JOOB,boole fa timis ak gee,ngir tarug dox ba,dem Mkka Smba JOOB fanaan fa,xy bisub diber dem kr baay txam Sheex Ibraahima MBAKKE Kajoor,laxasati ca tkkusaanug altine ba, dem ca Masmba Xari JOOB,moom mi ngi kr Muxtaar,fanaan fa, yendu fa,jugeeti fa ngoonug talaata dem ca Muxtaar Mareema Silla ca axal,mu def fay fan,juge fa jll Kokki Guy ca Maxtaar Masmba JOOB,yendu fa waaye fanaanu fa,da faa juge njkk jant biy so,te booba a ngay waajal am yi,waaye taxul mu xaar ko fa,dox nag jm Daaru Salaam kram,gg fa guddig llarba ci lu tollook aar fukk ak benn,Siidi Muxtaar ,rakam ja booba ma nga fa woon,ca biir sawaal.

Rakk ji (Sheex Anta) tmbli di ko ganalee lol kenn ci murid yu mag, yu man yi sax manu ko,waxantu ma laak u new i doole. Mu sax fa diirub fukki fan,bis bu nekk u ray ay fukki ykk,bu ko matalul mottali ko ci gilem walla ay gilem,kem li mu mnke rekk.u koy waajal ay wccuwaay ca rakk ja sheex Ibraahima,diggante Tuubaa ak Daaru Salaam,muy fa S bi tudde woon Daarul Mannaan, mu dem fa moom ku baax ki ci njlbenug silqihda . Sheex Ibraayma mii moom jrul ngay laaj ay mbiram, mooy ki ku baax ki dnkoon njaboot gi ak bagaas yi,bi miy tukki. Ci noonu mgi taalube ypp daje fa,Sheex Ahmadu Ndumbe jiite leen,mooy ki doon dem ak a dikk,di yee i gmmentu,di jngal goney Sri bi ba nu mokkal ci diir bu new njkk ku baax kiy dellusi,dara yquwul ci mbirum S bi,ba pp daan ko lebe ci wllug jub ak tegu ci yoon. Mu jullee foofa iid (tbski),sax ci meloom wu sell wa ak yareem (tarbiya) ga mu nekkoon,mbiram ak mu dongaam yi di gn a jm kaw . Kawe fopp,fopp,fopp na mu meloon,kaamil yi u leen di jng di leen xool ci bcg gi ,di leen tari ci gudd gi,naka noonu xasaayit yi,ak njngalem xam-xam mi,ak ligey bi ,loolu lpp gg fof maneesu koo melal cig kawe.

Ni nga xame ne mbirum ku baax ki yokk na ak mu taalube yi ba jggi ab dayo,ba maneesu koo misaal,naka noonu mbirum u iaan iy rambaaj. Mbirum jaxase gi dellu fa mu nekkoon,rambaaj yi jug di def seeni ligey ba nu xy indil S bi ay soldaar,li ko waral mooy: jaraaf ji nu dnkoon mbirum wll googa,ca jooja jamono,- moom xam nanu turam ak giir gi mu bokk - waaye bggu ma koo tudd di nxal 36 www.daaraykamil.com

ay doomi baay txam,ak doonte ndunu woon ak moom ci yeneem ak jfam ak waxam,waaye ginaaw seen doomi baay tx la,rafetatul nu leen koy tuddal,te doy na ne i teew moom xam nanu ko ci tur,ci jmm ak ci mbokk,te yal na Ylla musal i teewul uy xam turam. Moom de moo waxoon te tegu ko woon fenn ne : S bi day dajale ay kano aki fital ak yeneen jumtukaayi xare,te mi ngi waaj fi mu nekk,bu ngeen ma joxoon ay soldaar de kon ngeen gis li may def. u ndoon ak moom ci kaw waaye woluwunu woon ay waxam,looloo waraloon u boole woon ko ak buuri rew mi mpp,buurub Kajoor,bu Bawal,bu Siin,waaye bu Siin a ci gnoon a rafet njort ci S bi,gnoon cee rafeti wax,waa-waaw xamal nanu ma ne am na ay buur yoy seen biir de S bi la ndal.

Am nanu xam-xam ci ne bi nu gsee waa juy ry-rylu ji mngoo woon ryam nga (al lazii tawallaa kibrahuu) moo dal di woon tmbali di dog skket yeek jaaseem ji, te daawul xaar ku ko ubbil bunt,lpp lu dox ci kanamam mu dog,te amul lenn lu muy rus,dale ko ca sowwu ba, ba ca penku ba. Fekkoon na Buur Siin - ci li nu wax - mu wutoon ay fuglukat (controlleurs) indi fa ngir ragal uy dugg cib neg di fa duggal ay ngnnaay walla fital te kenn du ko yg,ngir dggale ci li nu waxoon ne S bi day dajale ay ngnnaay,waaye Ylla dogal loolu amul,bu nu ko bggoon it du man a am,ndax donga yi doonte danoo bank seeni loxo,teewul i ngi nd ak oom ci ay bt ak ay xoolkat. Bi nga xamee ne gisu u lenn ci li nu doon tuumaal sri bi,te gisunu ci donga yi kenn ku yor kanam gu lndm mbaa gu kk,ku u ci gis rekk ma nga mel ne kuy waaj a julliji kori mbaa tbski,ngir tuwaaletu bu ry,u xam ne noon bi day fen,buur ypp rus,am kersa ku ci dul waa ju fetterlu ji,moom sax gccawu na waaye daa suturloo jmbaar-jmbaarlu ak skku-skkulu nu ganaleel ko buur yi,ak xontal ko fas yi,waaye lu mu soxla rekk nu defal ko ko ca na mu gn a gaawe,gnnee yombe,ci noonu u dellu di u reccu,yal na Ylla fay a ca amoon yene yu rafet.

Ag karaamaa ngi nii: bi sodaar si laataa agsi ay mbokkam moom S bi danu koo wr ljl ko witt,gn a tar ci moom ay jiit,tiit gi nu tiitoon taxoon amatunu woon kersa,taraloon lool ak moom,demoon ba bgg koo gnn seen biir bu nu ko manoon,a ca bokkutoon ca mbokk ya daal mooy a ca yaroo ca moom,waaye ku baax ki moom loolu lpp tewul mu doonoon ku fex ku ko ygalutoon yaramam,naan leen bg leen,wallaahi mbir mii aari by dunu ci daanate,waaye kuy dgg loolu ? oom ii nga xam ne tiitaange gi yobb na leen ca dayo ba moos. Ca bis yooya ku baax ki gnneel leen aw dagiit wu yeme ciy woy,ne leen bu ngeen ko jngee ci kanamu soldaar si du ngeen dgg lu leen naqari mbaa ngeen koy gis,moom nag i ngi ko toftalee ci arafi (Rahmaan Rahiim)(muy boroom yrmaande ju nu yaatal ji,ak boroom yrmaande ju nu jagleele ji) moo nekk nii: (( sama boroom de bettee na ci luy leeral xel yi,ci darajay ngn ji ku weru ca Ylla)) (( samag cant eel boroom bu tedd,bu amul bokkaale,sama dnn it tay fees na dell ak leer guy jolli)) (( Muhammad ,xewali sunu boroom yi ba fww yal na nekk ci moom,sama lpp de ci moom la ko watoo )) ((maa ngi aan sama boroom, moom mi ay mayam matale mbooleem mbindef yi, la mu tnn moom mi binde )) ((deyaale naa ak moom - moom de mgg na - ay at , mu teral ma teralug aji gindee,sama lpp it set na ciy caaxaan)) (( yaw boroom yrmaande ju matale ji,mayal mbooleem mbindef yi yrmaandey ka nga xam 37 www.daaraykamil.com

ne ku jng Alxuraanam ji,mu feg la wlis aw ay)) (( aaral xeetu Mustafaa wi ci gpp yqute,te nga yrm mbindef yi,yaw mi bindoon seen maam)) ((yaw boroom nguur gi ,yaw mi mgg wlif fayyoontoo, yrmal mbooleem mbindef yi,yaw aji gindi joy dimblee na))) ((far nga la xol ba jublu woon ciy lor,ci darajay ngn ji ku weru ca Ylla)). Sama mbokk Muhammad doomi Aliyu Alyahxuubiyu,nu gnoon koo xame ci turu Muhammad Tuubaa,ngir taqoo gi mu defoon ak ku baax ki ca Tuubaa,ak baril lu mu daa sikar,ak a jng xasida yi,xibaar na ma ne bi S bi gnnee xasida gi (Rabbii bimaa yashrahul),da ne ma mokkal ko, ma mokkal ko ba nu daataa w,bi nu wee mu woo ma ne ma jng ko ca kaw,biral ko,ma jng ko ni kuy nodd,baamu ko lu tollook atti yoon,mu ne ma doy na ,mbir mi mat na te ywan. Mu daan def fu mu nee ma dajewunook lu nu naqari de,ma ne ko xasida gi -ci karaamay ku baax ki- def na ci soldaari Tuubaa yi la picciy Abaabiila yi defoon ca soldaari Mkka ya,ngir sunu Yonnant bi (j.y.m),waaye ii ak ee li leen wuutale, ii daiy o ay nu jflanteek oom ci kem seeni yene,naaxsaayal leen,ee a ca pp di u baax,u ga (forse) leen ,te seeni xol S bi la ndal, Ylla yeexal seeni mbir ba nu bari tuub ci,ba ca ka leen jiite woon,moom it tuuboon na,enn nit aa ngi sikk ay mbiram nag,bi nu xamee ne ltt doo nga tuub du tuub. Sri bi nee na : ((dgg-dggi tuub mooy nga byyi bkkaar boo mas a def ngir Ylla)) (( ci sa coobarey bopp,waxunu lu mel ni (lu la Ylla teg) niki tx ak jngoroy py ak gumba ak luu)) ((nga byyi ko rekk ngir mggal ku mgg ki,ak ragal mbugalam mu metti mi)). Man nag li may wax mooy lu man a xew ci mbooloom S bi la ,moo xam daa ltt walla daa tuub,mbari na lu Ylla jggal ku too te tuub,byyi ko ak Ylla daal a gn a wor, rafet njort ci moom itam a gn a mat,Ylla nee na : ((fa man jaa ahuu mawhizatun min rabbihii fantahaa fa lahuu maa salafa mamruhuu ilal laahi)) muy ku ag waar dikkal juge ca boroomam,mu byyi la mu doon def,la mu jiital eel na ko,te mbiram moom ma nga ca ylla. Bi soldaar si demee,ci la gnne ci ndigalul Ylla ak Yonnantam ci aareelu tukkeemba,ma nga ca naan: (( ku jorte ne sama dox ba ginaaw atum aksasin di 1321g,mook sama dox bi ci bopp jaysasin di 1313g oo yam)) (( sax na ne aji rer ju dof la ,ndax moom dox boobu teeyal (neexal) gu aji kawe ji di teeyal samag dund la)) (( saama doxub aksasin bi du lu dul yoolub ki ma wommatal ci ginaaw bi dl (dig) bob def na ko)). aareelu tukki bi (Gnnaar) Ci bisub gwwu,fukk ak juroom aar ci weeru gmmu atum aksasin di junni ak atti temer ak aar fukk ak benn,la S bi gnne ca kram ga ca Daarul Mannaan,ginaaw bi ko ay bataaxel dikkalee aki ndaw tukkee ca nguur ga,naan ko na leen fekk Ndar ginaaw tisbaar. Mu fanaan Ngaabu ak njiitul soldaar si,xy dem Njaarem ,juge fa dem Tool,juge fa jll Tiwaawon,foofa la yege saxaar dem Luga,ware fa gaal dem Dagana,loolu lpp ci ag ayu bis,sax fa juroomi guddi,jggee fa dex ga juge Dagana ginaaw bi, ci aar fukklu fan ci weeru gmmu nd ak waayi Sheex Siidiya Baaba ji,mooy Sheexunaa Ibnu DAADA,man naa am li waraloon loolu di woon li nu wax ne Sheex Siidiyaa ko wax muy ne leen sri bii de amul lenn lu aaw lu deesi ragal ci moom. u ne ko woon ndax man nga noo woral (gaaraantil) li nga wax? Mu ne leen warlul naa leen ko,u ne woon ko kon leegi danu koy boole ak yaw. 38 www.daaraykamil.com

S bi moom daawu leen yeexal lu dul diggante bi muy xaare ndigal lu juge ca boroomam ak sangam ba,loolu moo daan waral uy jort ne daa lnk,te fekk booba noonu la deme,ci noonu mu dem nd ak Sheex Siidiya,ba nu gg ci yenn ci kr yi nga xam ne du nu woon kram,waaye yu Banii Daymaan lanu,mu wcc fa ngir ay mbir ci digganteem ak yenn giir yi,bu ko defee ku baax ki wcc moom itam,bu niy laxas mu laxasati def ko ay yoon. Bi tuxu yi baree nag ak mngaan mi ci wenn weer walla aar,nga xam ne daanaka dunu sax fi barab,te loolu wuute naak lool aaday waa rewam,loolu tiis ko sonnal ko ak ag njabootam,te itam taalubeem yi danu koy dikkal fu mu man a nekk te barab yi sori nanu,scc yi bari ci yoon yi sonnal leen it ya yooni yoon,ci noonu ku tedd ki skku ci oom u tggoo,u ba ngir xr ci nd ak moom,ak ngir yilla ju jiitu ji muy dnk gi ko ko nguur gi dnkoon . Waaye S bi moom dogu rekk,nu xam ne ku dggu la,te du skku dara ci bnneexu bakanam,nu nd ak moom ci li mu bgg,nangul ko ngntam,moom itam mu jmmante ak oom ci aw bayit wu ygg:( bu u nu tnnloo woon de du ma tggook yeen, waaye ag tnn ndul ak jamono ),S bi ginaaw lii du bayitu boppam mu soppi waaye ag tnn ndul ak jamono,def ko waaye ag tnn ndul ak am ax,jublu ci loolu yen da ngen di skku fu ngen di smme ak fu ngen ko man a ame,loola reeloo leen. At mooma mu woore Sarsaara koor ga,muy barab bu nu xam fa oam,nit i sottiku fa,ak uy jle ci moom rawati na ci Banii Daymaan ak seen kilifa ya,doomi Baydah yi Abdul Laahi aki mbokkam ci loolu ku baax kaa ngi naan: (( mbooleem sama xeeti cant eel na ki nga xam ne sama lpp ci moom mujj na di ngrm lu ndul ak ab s(mer), eel ko fa Sarsaara)) (( moo moom sama tagg ak sama ngrm ci lu dul s,bi mu ma wommatalee ay ansaar yu bokk ci Banii Daymaan)) ((sama lpp eel na Ylla fa teeni teraanga,yu nu tuxoo,te bari na fa u siyaaresi)) ((i nga xam ne danoo dikkoon Sarsaara ngir siyaaresi ma fa,na nu xam ne tggoo nanu aki bkkaar dduna ak alaaxira)).

Ci Sarsaara gii nee na daje na faak Yonnant bi (j.y.m) cig yewwu,du ciy gnt,mu jox ko Wirdul Maaxuuz .Fekkoon na njkk loolu Sang Bu nu Wolu bi dikkaloon ko ca gej ga,rkki (jl)woon ca moom lpp lu mu jle woon ci nit i,ba deseetu ci dara,mu jox ko wirduw Xaadir,ba ca mujjug tuxal ga nga xam ne loolu day tegtale ne daje na ak Yonnant bi (j.y.m) ca gej ga,Jibriil dikkal ko fa mooy Sang Bu Nu Wolu bi,rkki woon ci moom la mu ca rekki woon,joxoon ko la mu ko joxoon,jaarale ko ci Yonnant bi (j.y.m). Mas naa teew bis kenn ci boroom xam-xami naar yi laaj ko kuy Sang Bu Nu Wolu bi ? Mu ne ko Jibriil,mu ne ko ndax Jibriil dees na ko gis ginaaw Yonnant bi ? ku tedd ki tontoo ko aari bayiti ki woy Xazawaat : (nee nanu Jibriil da na teewal kiy faatu te gm,aw nit it weddi nanu ag dikkam ginaaw Yonnant bi (j.y.m), dgg gi nag mooy amul ab dayo (ag dikkam) ) . S bi neeti ko waaye wax jii am na u ko tax a jug,ooy i ci am ag am akug dggal,waa ju juge fee rekk nag li war mooy mu nangu ko mbaa mu noppi,ngir ba a loru. 39 www.daaraykamil.com

Man nag ma ne misaalum loolu mooy lu mel ne ku nu digal mu taal ab taal ngir aajo ju wr,mu taal ko,ab lpaalp jaar fa tbbi ca,dee,kon kooku dara waru ko ca dee googu,naka noonu ku nu digal mu wax, bu waxee.Ma ne wlliyu yi di gis malaaka yi moom kenn manu koo weddi, ndax jle naa ci mbindum sunu sri Xalifa Alhaaji Muhammadul Faadil,moom mu jle ko ci yenn ci teere yu mag (majaamih) yu wr yi lol ab yaxam mooy ku u ubbi (maftuuh halayhi) moo xam ab nabiyu la walla wlliyu,manul a kk mu jkkarlook malaaka,ci seeni jmm,ni u mel,tey wax ak oom uy wax ak moom,kpp ku ne wlliyu du gis malaaka tey wax ak moom kon na xam ne tegtalub loolu mooy moom du ku nu ubbi,lii nag mooy layuw ku nangu(feug Jibriil),ci ku ko nanguwul. Ginaaw Jibriil da na dikkal aji gmm ji buy faatu,te ku u ubbi day gis malaaka yi tey wax ak oom,te yinkiiwalug wlliyu yi (sol gi nu leen di sol xam-xam ak li Ylla di bgg ci oom) mi ngi am jaare ci malaaka walla mu am ci lu dul muy jaar ci kenn,ginaaw loolu lpp am na,kon du jomb ci Jibriil moom mi Ylla wolu ci whyoom gi,mu nekk ag diggale (intermdiaire) ci yobb ak joxe yinkiiwal gi Ylla di dsotti ci enn ci wlliyoom yu mag yi,ginaaw oom ooy iy dnn yonnant yi.

Moom Jibriil dimbali na sunu sang ba Hassan saaba bi (y.y.g)ci teewaayu Yonnant bi (j.y.m),mu di ag kiimaanam tey karaama eel aw wlliyoom,luy tee kon mu man a dimbali ligeykatam bii ci ginaawam,mu dig kiimaan gu w ci ginaaw bi tey karaamay wlliyoom wu dikk ci ginaawam te di ko ligeyal ni ko Hassan,wlliyoom wu njkk wa doon defe. oom aar de ay mbokk lanu ci lgey bi,ba fa tuxal ga xam. Du kk ari u indi tuxal gi ba ngen gis ko,mi ngi nii:da ne yal na ko Ylla mu mgg mi gram : bu dee bunt bi yor wirduw aji nos ji (aji woy ji) moom doggantal nekku ci ,(doggantal= franais =chapitre,araab=faslun) aji nos ji ,wird wi mu njkk a jl ci wird yi mooy wu Xaadir,ginaaw bi wu Shaazaliya,ginaaw bi wu Tiijaan.

Bu dee wirduw Xaadir moom jfandikoo na ko lu ygg,daan ci skku ndigal ci kpp ku mu mas a yaakaar ne ku nu ci jiital ga (muxaddam), ba jle woon ko ci u bari. Ginaaw bi mu wor ko ne i mu daa jle du u ci woon ay muxaddam maanaam u u jiital (u ko war a joxe) ,mu skku ci Ylla (t.s) mu may ko ci lol ag glm mbaa ag dengi-dengi dootu ci nekk. Mu ne bi ma Ylla yobboo ci gej gi ma nekk man rekk ak moom la ma Sang Bu Nu Wolu bi dikkal (j.y.m),dal di rkkee ci man lpp li ma jle woon ci nit i ba dara desatu ci,mu jox ma Xaadiriya ci diggaleg (jaarale ko ci) Yonnant bi (j.y.m). Tuxal gii ak lu ni mel ci mbidd yi, danuy wone ne Sri bi daje na ak Yonnant bi(j.y.m) ak Jibriil (j.y.m) ci lu dul woote ag yonnant,du caangenug whyu,waaye ci kem li Ylla di jagleel lenn ci wlliyoom yu mat yi. Waxam ji mu naan wirdiy aji nos ji mi ngi ci jublu woon xasida gi mu doon tudde atti sri yu tedd yooyu,ak dnn gi mu leen dnn, tuddati sunu sang Anas,ak Hassan (grmul Ylla yal na nekk ci oom) ak dnn gi mu leen dnn ci waxam jii: ((wommatal nga ma la Jiilaani (Abdul Xaadir Jiilaani)kawee woon ba fa mu yam)).

Ku bgg a am lu ko leer na xool teere bi nu naan Tanwiirul halaki fii imkaani ruwyatin nabiyyi wal malakidi ci maanaa leeralug lu lndm kriis ci man a nekkug gis Yonnant bi (j.y.m) ak malaaka,teere 40 www.daaraykamil.com

boobu boo bggee lu leer rekk moo ciy gej jug mbmbullan gi.te boo defee ag settantal ci tuxal gii ak li ci topp,da nga gis la amoon kon ca gej ga muy ni nu nangoo woon li mu jle woon ci ku dul woon Yonnant bi(j.y.m),ak dello ngi ko ko Yonnant bi delloowaatoon,ak naayibam yi, atti sri yu tedd yi,ngir mu nekk naayibam moom Yonnant bi ( aji wuutoom),tey ki fi wuutu yooyule sri (g.y.y.),ci seeni wird ,di seen muxaddam bu nu joyal bi , nga xam ne amul lenn lu ko tnk ci wenn wird,(ku ko neex ak nu ko neex la koy joxee) ,da nga ci gis it la amoo n ci Sarsaara muy jox ga nu ko fa joxoon wirduw boppam moom rekk,jagleel ko ko,nga xam ne benn sri bu ko fi jiitu masu koo yor.

Looloo waraloon daawul digal ku jbbalu ci moom te yoroon aw wird njkk muy w mu koy byyi,da koy digal kay mu tye ko te yene ne moom moo ko ko jox,ku jbbalu ci moom nag te waxoo ko dara,bu boobaa mu door laa jox wirduw boppam. Looloo waraloon doomam ju tedd ja,sunu sri,SheexMuhammadul Bashiir naan cig xasida gog biral na ci ngnelug wirduw S bi ci yeneen wird yi,xaaral ma jox la ko lpp,ma nga ca biir it waxam ja mu naan: ((wommatal nga ma la Jiilaanii kawee woon)) ba ca bayit ya nga xam ne s Bashiiru tudd na leen ci xasidaam gii,mi ngii:

(ci turu Ylla laay tmbalee aw woy wuy jari ku bgg a jariu te ab xolam set) (ag cant eel na Ylla,yal na dolli xewal ak mucc ci Yonnant bu nu tnn bii di gn ji mbindef) (ak oam aki saabaam ,u tedd ii te diy sang,oom i wui lndmi xol yi ak lndm) (bu loolu jllee ma naan la dglul waxi kiy laabiire boppam tedi la laabiire ci luy faji aajo) ( yaw miy skku matug texe ci yooni atti sri yi) (yoonu s Imaam Jiili (Abdul Xaadir Jiilaani) ak Shazali mi lq ag ngnel) (ak Abool Habaas (Sheex Ahmad Tiijaan) miy ndamul u mat i,oom oou nga xam ne seenub tte ca jublu ga (xasd) mooy tteb ku njkk ka ) (nd ak ku ci nekk yor sa jagley bopp yoy ci la saw yoon lqe ay jagleem,loolu nettali nanu ko) (na nga taqqook yoonu Abdul Xadiim (jaam biy ligeyal Yonnant bi) ,ndax moom kat moom la Ylla mu jiitu mi jagleel mu dnn yoon yooyu ypp) (ndax kat wird wu nekk am na mbot,ci benn baat bu ci nekk,(ci biir wird wi) yal na la Ylla gindi) (baat boobu nag boroom baziira yi rekk a ko xam (baziira = gisug xol )keneen ku dul oom xamu ko,muy hikamu ab boroom buy aji not ) (misaalam mooy Laylatul Xadar ci weeru koor wu nekk,ak Waxtuw jjuma,dees leen di wr di) (Ylla feealal na ko (moom S bi) ya lqu woon ypp (ci wirdiy yeneen yoon yi),ginaaw bi mu leen ligeyalee te yekkati ag wllam ngir jmmam ju tedd ja,ba mujj pp bgg ko jiital ko,(def ko muy seen muxaddam (ku nu jiital ki am sa sau joxe wird wi) ) ) ( Yonnant bu nu tnn bi tam - yal na ko Ylla dolli ay xewal ak mucc ni mu ko tnne - yegal ko ci ab hadara bob ku dul moom fddu na ci yaw,bu nekk fa aji kawe ji (muy Ylla) loolu di lu kawe sax la mu doon wut ) (bi loolu wyee mu donnalati ko lu nu nbboon li , muy aji jiitu ciw yiw joj wui na ay fitna) (ci coobareem (moom Ylla),mgg na te kawe,la ko tnne ci darajay Yonnant bi miy ligeyal biy joxe ag sell) ( ngir barig li mu leen ligeyal te sellalal boroomam,di it ku sellal te matal kllare ci diineem) (mu boole lpp,dolli ci,yeg ci barkeb Alxuraan te fa mu yegak a baax) (boo jlee wirdam de jl nga wird ypp,te doo ragal ag nrmelu) (la nu dige ca seen wird yooyee it da nga ca jot,te doo ragal genn tkku ) (ndax moom (tkku gi) ku byyi dgg a ko tax a jug,te ku ko jl (moom wu s bi) yayoo nga jagle ya ) (jpp ko de moo di jpp ca lu baax la te dolli ca nag,ngir boole gi mu boole (wird) ypp,teg ca yor leneen ndollent (lu yeneen yoon yi yorul)) (cosaan li mooy da ngay wax (ahuuzu billaahi minas shaytaanir rajjiimi)teg ca (bismil laahir rahmaanir rahiimi) jng yenn aayay Alxuraan,doo ga tmali) (def hasbala 41 www.daaraykamil.com

(wax hasbunaal laah ba fa mu yam) def istixfaar ( astaxfirul laah) ,def haylala (wax laailaaha illaal laah) ,julli ci sangub u tedd i) (ginaaw bi defees ag tj gu rafet,loolu da na amal fa Ylla lpp lu baax) (lli mooy cosaani seen wird yi oom pp,ku ci nekk nag am na genn jagleem gu mu moom moom rekk gu kawe) (S bii nag moom jl seeni ndono jle ko ci gn ji mbindef mi leen di ggale) (mu wax (moom S bi) bi miy nettali yooyule xewal,di ci sant kiy fttaliku (di Yonnant bi) ngn ji aji xewale ji (di Ylla) ) (ki moom jpp jumaa ak jpp jkka, moom loo na ma mebtum mbooloo yi) (mu wax di sant aji tedd juy kenn ju ko donnal tere bi (di Alxuraan) muy ndono lu am njari) (tllal naa sama loxo jme ca Ylla,moom itam mu tllal xewalam ga eel ma ca gej ga,te loola tlleeku) (tereem bu tedd ba mujjoon na di wird ci man,daqaloon na ma samay noon it te dkku leen) (mu daan won lu neex kpp ku ko taqoo, di ko jng lu mu man) (boo bggee leeralug lii ma la tuddal,am lii nga xam ne ciy woyam laa binde sama mbind mii) (wommatal nga ma lol ci la Jiilaani kawee, ngramul ki ma kaweel yal na nekk ci moom) (wommatal nga ma la Abool Hasan kawee woon ci ligeyal Yonnant bi,miy maami Hasan) (matalal nga ma la nga xam ne ca la Sheex Ahmad Tiijaan kawee woon,te nga nekkal ma ci lu rafete ni wurusu marjaan) (wommatal nga ma lol soril na ma taq-taq,ma mujj mel ni Anas ci ligeyal yonnant bi) (moomloo nga ma te wommatal ma ag rafetal,donn na Hassan ci tagg Yonnant bi) (ngrm ak jmm yal na nekk ci oom,ni lndm dqoo ci oom(ni nu leerale dduna bi)) (mu wax ci bi miy tagg ngir sant ku nu jublu ki ( di Ylla) ci tere bi (di Alxurran) ak Yonnant bi Muhammad) (sama ddiya ji juge ci yaw ak ci Muhammad sunu sang bi, lu man a tee mer la) (darajay aji far ji (muy Yonnant bi) far na samag dengdengi,te wommatal ma kttan ga ci lu dul ag doyodi) (sama lppay sant aji yekkati ji may dgral,cant gi nag jm ci Alxuraan ak Yonnant bu baax bi) ( tere bi ak Yonnantub ku nu jublu ki, yekkati nanu sama lpp ci lu dul keno) (Alxuraan nooyal na sama xol bu gindiku bi,dq it bpp jalgatikat jme ci ku dul man) (sama xol ak sama loxo maa ngi ko jme ci ku nu tnn ki ci di ko ligeyal,may na ma nag la pp njari) (aji dgg ji wuyyu na ma ci weeru koor,te baax na,mooy sama jubluwaay,ci barkeb Yonnant bi Muhammad) (Ylla gindi na sama xol,ongal samaw yaram ci ngrmam,daal aji yq sama) (mu waxati bi muy deyaale ak boroomam,mbgte eel na i ko sopp pp) (ne: yaw mi jggal sama aari way jur ak i ma sopp ci lu dul njqare) (te nga fddul ma ci sa bopp ak ci Yonnant bi wlif mbindef yi,te may ma ay saar) (fddu nga ak man bu njkk nd ak Yonnant bi,may boroomug lqu wlif mbooleem mbindef yi) ( ma di ab jaam buy ligeyal Yonnant bi,di ku nekk ci yaw nd ak dgg gi foofa,tey ku fddu) (mu waxaat ci yenn may yi nu jagleel i topp yoonam wi) (Ylla jme na ci i dul i aju ci man lor yiy daje ak dof yi) ((ab boroom bu man loolu may na ko ko,te moom (boroom boobu) ku yayoo wuyyu la ci ku ko woo) (nuy tje ci Yonnant bi,mi di ag tmbali te di ag tj,tey ki gn a mat,yal na Ylla saxal xewal ci moom ak ci u mat i) Foofu la loolu yam.

u dellu ci wax ci cosaanul wird wi,ak yax bi(yax=nassu ci araab.=texte ci franais) mu bindoon ci ginaaw sotti (sotti = nusxa ci araab.=copie ci franais) ga mu amaloon ca wird wa, muy : bismillaahiir rahmaanir rahiimi wa sallal laahu halaa sayyidinaa muhammadin wahalaa aalihii wa sahbihii wa sallama tasliiman ,ku xool araf yii nu bind ginaaw matug wird wi, na xam ne ki ko bind di Ahmadu doomi Muhammad doomi Habiibul Laah,mi askanoo Mbakke te dkk Bawal,may na ndigal mbokkam moomu ci Ylla (t.s),sang bi Mustafaa Usmaan mi juddoo Halab te dkk Madina,may na ko ndigal ci mu 42 www.daaraykamil.com

jfandikoo wird wu nu barkeel wii ak jox ko ku ko soop ci mbokk yu gor yi ak yu jigen yi,ni mu ko jlee ci Ylla jaarale co ci Yonnant bi (j.y.m) cig yewwu du ciy nelaw,atum baksasin di junni ak atti temr ak aar fukk ak aar,ginaaw gddaay gi,yal na Ylla defal ki ko defoon gn jaa saxi xewal ak gn jaa jarii jmm,ci benn barab bu nuy wax Sarsaara,ci weeru koor gi nu wcce Alxuraan,mu dig jub eel nit i,te di ay aaya yu leer yoy ag jub la ak teqale dgg ak safaan. Ylla nag mooy seere lii nuy wax.Subhaana rabbika rabbil hizzati hammaa yasifuun wa salaamun halalmursaliina wal hamdu lillaahi rabbil haalamiina.

Sunu mbokk moomu Muhammad Abdul Laah Alhalawii,nee na ci teereem bi tudd(( Anafahaat almiskiya fiil xawaariq al mbakkiya))muy ci maanaa bonnig misk ci xar-baaxi Mbakke,nee na S bi Ylla da koo jox wird wii,mu jox ko muritam yi,xemmemloo leen ko,te loolu di lu war ci moom. Mu ne leen kpp ku ko saxal aki sartam da na tbbi jjana ci lu dul hisaab (hisaab mooy laaj yi iy def ak a gstu ay mbir) du caagenug mbugal,te Ylla it da na ko aar ci naqar yi ci ddina ak alaaxira,te saytaane mu nu dkku mi du ko jege,da na doy wird wi ag kawe,nekk gi mu nekk wird wow boo ko dee jfandikoo soxlawul gay jfandikoo yeneen yi,te manoo am li ci moom te jfandikoowoo ko. Sunu Sri, sunu wasiila ca sunu boroom mu kawe mi nee na bi mu nuy jox wird wu tedd wii:jox naa leen wird wii ngir jmmi Ylla mu tedd mi te kawe,kon tye leen ko ngir jmmi Ylla mu tedd mi te kawe. Mu waxaat jpp leen ko ak doole,ku ci jotoon a yor weneen wird bu ko manee, na leen boole,kon muy leer ci kaw leer,bu ko manul mu yam ci wird wu tedd wile. Jeex na.

Ki ko doon taariixal nag ne moom : bismil laahir rahmaanir rahiimi ,lii aw tagg ak taariix gu Ahmad doomi Asan def eel wirduw sriam bi Sheexul Xadiim,yal na nanu Ylla jari ci moom ci aari kr yi aamiin.

( sunu boroom taxawal (fondumang)na sunuy jf ci may nu u man a root ci gn ji teen, kon mbgte eel nanu (mu jublu ci wirdul maaxuuz)) loolu mooy wirduw sunu sri bi Sheex Ahmadu Mbakke,mu juge ca boroomam jaar ci Ahmad Yonnant bi) (yal na ko Ylla dolli xewal ak mucc,li feek mi ngi doon ab raas jm ca texe gu kawe ga) (jox na ko wird wii jle ko ca aji namm ja muy Ylla,yem naa te e bii sri ak yii taalube) (jagleel na ko wurusu luulu wu nu ongal ci xor,te lq ko ku dul moom) (wurus eel na sunu sri bu nu grm bu mgg bi,ku ko am de am dkkaaleg ka gn a mgg) (mi ngi ko gnne ci bisub jjuma,mu jm ci ku Ylla texeel ci doomi jamono ji) (ci juroomi fani sawaali atum (sahidnaa karaman) di junni ak atti temer ak aar fukk,moom boroom taariix bii,moom miy ndppul u tedd i (ndpp mooy mbaxana mi nuy solal buur) ) (mooy sunu sri Ahmadu MBAKKE mi dgg di tax a tukki ak a took ) (gnneel nanu ko ngir jmmi Ylla ,kon billaahi bu ko sggane) (ngir Ylla,boo bggee am li nga bgg,ndax kat kuy rbb ba jam ay man a dpp) (yaw sama boroom ci darajay aji wommat ji xeet yi jme leen cig jub,di Muhammad miy wui njqare) (yal na Ylla miy sos niir yi,sotti ci moom gn jaa selli

43

www.daaraykamil.com

xewal ak mucc ak oam aki saabaam) (ak ci darajay sunu sriub Mbakke bii,na nga ma may ma jot ca la a jiitu bggoon) (ci ag kawe,bu ko defee ma bokk ci mbooloom i la jege,yaw miy boroom nguur gi) .

Nan dellu ca tukkib aareel ba,dem ba Tintu Muxsin,foofu barab la bob xew-xew bu aaw te soof dal na ko fa,muy : ab naar bu nu xam turam ak giiram,daa jugoon ngir ne da koy faat moom S bi - man moom xam naa ko waaye dama koy suturaal ngir doomi baay txam yu julit yi - moom da doon fexee faat Sri bi,Ylla musal ko ci,ni mu doon defe loolu nag mooy xanaa w ci moom won ko ag cofeel gu dggu ak jbbalu ci moom,S bi moom itam suturaal ko,boole ko cig njabootam,bindal ko atti byit,ne ko na ko saxoo jng,guddi ak bcg ,naar bi moom itam dkke woon loolu,byit yi moo nekk nii: (lor ak saytaane jm nanu ci ku dul man,ndax oom aar kat amunu ci man genn kttan) ( Ylla mooy sama boroom,Yonnat bu nu tnn bi - yal na Ylla dolli xewal ci moom, moom mi ko gindi te tnn ko) ( mooy samab xarit te di sama soppe,te ba na it samag loru,te skku na ci boroom mbindef yi samam mbg ).

Naar bi taqoo woon ak loolu,di ko jng guddi ak bcg ,ci mbooloo mi ak bu wetee,mu ko daan def ginaaw saaru Yasiin,mel ni kuy nodd,nga xam ne da naan wax: yaasiin,yaasiin,yaasiin,ba kero muy mat juroom aari yoon,mu door a ggale saar wi teg ci byit yi,jngati yaasiin ni mu ko defe woon,tegati ci byit yi,baamooti leen,nii daal la ko daa defe ,daawul taxaw lu dul daa sonn walla muy nelaw,mu sax ci loolu ay fan,am na u ne weer. Jamono jooja S baa nga woon fa o sheex siidiya,nekk ca seen xayma ya,ci noonu mu digaloon taalube ya nu defaral ko ag kr ca bitib gdd ga,u def ko ni mu ko bgge woon,bi mu noppee mu wax ko sheex Baaba,sheex Baaba digal mbokkam ma sheex Siidiya Muxtaar mu gunge ko ca kr ga,mu defe ko noona. S bi moom digal naaram booba mu w nd ak moom ca kr ga tey jng atti byit yi,ni mu ko baaxoo woon,bi nu agsee,saytaane jpp ko,xamal ko ne pexe mi mat na,def dong a ci des,bi guddi gi soree ba kenn yngootul,naar bi jug,summiku ba mel ni ko ndayam jure woon,dal di dugg ci kr gi,jawali ca neg ba S ba nekk,ginaaw xamoon na fa jaasiy S bi nekkoon ,mu jawali ca,bocc ko ci mbar mi,waaye Ylla dogal jenn waay ju bokkoon ci negub nguurug Kajoor,te gnoon cee rafetug tuub ak byyi dduna,u ko daa wax Omar FAAL NDATI,nekkoon ca jkka ja,di fa fanaanee jaamu Ylla,bi ko naar bi rombee mu jug ca saa sa,seeti ki yor mbiri biiri S bi ,di Muhammad Lamin ANG,doomi Muhammad Lamin Mati,moom waa-jur wi,doomi bjjan la ci S bi,xamal ko ne am na jmm ju rafle ju jm ca negub S ba,ca saa sa ndonga la jug,gaawantu,fekk naar ba mu bocc jaasi ja,di settantal naka lay jekkoo S bi ba man koo lor bu baax,te S bi moom mi ngi tdd ci wetam,bi naar bi xccee di ko door jaasi ji,ylla dogal mu lonk ci koub xayma bi,daje ak ndonga li di wadd di dal ci kawam,mel ni kuyul gileem loolu,dal di koy nrmel,naar bi yuuxu,murid bi yuuxu ci kawam,mel ne da koo bg a lekk,seen coow li fees foofa dell,a nekkon ca wet ga yuuxaloo,daje fa,nga xam ne S bee mujj w dox digganteem ak nit i ne kon u ray ko,mu dalal leen,dal di yonne ci menn mbooloo,mu fanaanoon fu sori foofa,mu mu naroon a 44 www.daaraykamil.com

yewwi,woolu leen,ne leen yobbaaleel leen ma naar bii ba Xumaak, (barabu kiliftefug tubaab yi,da nanu ko wax it Sahwatul Maa) ngen byyi ko fa te dem seen yoon,denk leen u yram ko te dimbali ko ci bagaasam yi,lq leen nag xibaar bi,ngir ba u gaa ko,jeemul a fayoonte ak moom ci jfam ju aaw.

Yenn taalube yi nag gis nanu ne li tax S bi delloolu naar bi Xumaak,fa tubaab yi am sa-sa,ab junj la ci ne oom tubaab yi oo ko yonni,Ylla rekk a xam,waaye pexeem ma moom Ylla naaxsaayal na ko. Yooyu aari byit boo ko xoolee da nga gis ne Ylla feealal na ko ci ay karaama yu kawe,yal na ko Ylla fayal jullit i aw yiw ak Lislaam.

Man nag li ma gis mooy lii mooy dgg-dggi laabiir ak doylooYlla,ak nangu ab dogalam,miinunu ko ci ku dul moom ci waa jamonoom,li mu nuy fttali mooy li daloon ki miy ligeyal ci yenn ci xareem yi,loolu mooy dafa am benn Ahraabii (araab bu dkk ca kaw ga) bu tuddoon Duhsuur bu ko fekkoon mu tdd,xaw a sori saabaam yi,mu bocc jaaseem,xcc ko ne ko ana ku man a dox sama digante ak yaw? Yonnant bi (j.y.m) ne ko Ylla,ci noonu waa ji di lox ba jaasi ji rote ci loxo bi,Yonnant bi (j.y.m) jl ko ne yaw nag ku la man a musal ci man? Mu ne ko amal yrmaande, Yonnant bi jggal ko,ba koo def dara.

Naar bii nag moom bis dellusi na ci S bi ca Xumaak,taalube yi jug ngir fexeel ko,S bi yg ko gnn ci naaj wi,te solul ay dll,di wax ca kaw: byyi leen ko,byyi leen ko,(alaa tuhibboona an yaxfiral laahu lakum) muy:xanaa bggu leen Ylla yram leen,di ko baamu. Nu byyi ko,mu digal ko mu lqu,gnn te dem yoonam,ginaaw bi mu ko defalee ag njekk. Bi ku tedd ki nekkee Njaarem,naar bi delseeti fa,S bi aarati ko,naan ko:boroom jaasi ji,naar bi naan ko : dedet neel boroom xm gi,bu ko defee S biy ree,gnneeti ko ginaaw njekk.Man ci sama bopp gis naa ko Cees,maanaam Jnqeen,te booba maa ngi nd ak am mbooloo ci taalube yi,waaye man rekk a ko ci xmmee,bu ma ne woon kii de diw la u ray ko,waaye kon ana jikkoy S bi,Alhamdu lillaa.

Nu dem nag Jaraari,barab la bu Halawi yi moom,S bi tudde woon ko Biirul Xayri di ci maanaa teenub yiw,ci barab boobu la S bi doon waxe xasida gii: (( li ma doon laaj sama boroom indil na ma ko cig baamu,rawati na ca Biirul Xayri di Jarraari)) ((samag cant ak njukkel eel na ab boroom bob wommatal na ma ay xewal,ci lu nbbu ak lu fee,di ku u baax i sopp)) ((sama boroom wommatal na ma barkeb saabay ku nu tnn ki,mu nekkaloon ma te daawu ma won ayuw kccoor yi)) (( samag cant eel na aji jiitu juy aji des,kok aar na sama kanam wliif bpp aawtef,nd ak ag bbb guy daw juge ci moom jm ci man (bbb mooy luy sottiku bu baax di wal fii mu jublu ci xewal) )) ((samay cant eel na ko,ci biir ay sang yu askanoo ca Aliyun (fii man na cee jublu Seydinaa Aliyu,man naa firi it aji kawe di Yonnant bi) ci lu dul aji jalgati mbaa workat)) ((aji des ji amul bokkaale yal na dolli xewal ak mucc ci ki nga xam ne indil na ma la ma ko aanoon cig baamu)). 45 www.daaraykamil.com

Halawi yi nee nanu xamunu lu tax S bi tudde ko Biirul Xayri,ndax tur woowu oom masunu koo dgg ci seei baay,ba bi nu fa suulee Sheex Ahmad Bun BUDDIN,nu dal di xam sekkareb li tax mu tudde ko ko,nu xame ci baatinub S bi. Ci Sheex Ahmadu Bun Buddin, S bi wax na ci ay wax,Alhaaji Muhammab Bun AAB,dkkantal la ci Sheex Ahmadu Bun Buddin,nettali na ma ne baayam bind na bis S bi ne ko daa bgg mu nuyyul ko Yonnant bi(j.y.m),ak Sheex Ahmad Tiijaan,te itam soxla na seenub tontu,S bi tontu ko xamal ko ne Yonnant baa ngi koy fay,ak Sheex Ahmad Tiijaan,aji nettali ji nee na ca saa sa, baay ji daanu ab jll,di yggal bopp bi ak a waxtu,mel ne ku jaaxle te nu muur am xelam,daul ci melokaan woowu ba bi mu faatoo (y.y.g),te booba i ngi fu sori woon S bi, te ygalunu ko woon kenn ci guddi gi mu ame woon,waaye amul lu dul ay ndaw dikk ci suba gi ne S bee leen yabal u teewesi dencug Sheex Ahmadu gi,te di leen ko jaale.

Mu bind ci loolu ag xasida di ci xamale darajay Sheex Ahmadu moomu, fa Yonnant ba,moo tax mu terale ko karaama googu,ne lii mooy payug Ahmadu Bun Buddin,tey payug ab xalifaam: Bismil laahir rahmaanir rahiimi, yal na Ylla dolli xewal ak mucc ci sunu sang bi Muhammad aki oam aki saabaam,na ngeen xam ne guddi gi Sheex Ahmadu Bun Buddin di faatu ruuhul xudsi (jibriil) (j.y.m) wcc na juge ci asamaan si,nd ak lu bari ci ay malaaka ngir terale ko sang boobu,ngir rafet gi mu rafetoon njort ci Jaam Biy ligeyal Yonnant bi (S bi) ,yal na ko yal na ko Ylla nekkal cig teral,moom miy aji jiitu tey aji des,oom nag delluwaatunu ca guddi googee ndare bu danoo yobbaale ruuwam gu tedd ga,lii nag mooy dl bi nu ko dloon,(dlmooy dikk) .loolu la S bi di junj ci byit yii: ((Ruuhul Qudsu w na,di wuisi njqare,nd ak mbooloo mu mag ciy malaaka,jamono ji Ahmadu mii di lqu)) ((Ahmadu am na la mu bggoon ca Ylla,buntub yiw ubbikul na ko bu dul tjooti)) ((yal na Ylla fay ka joxoon ddiya aji ligeyal ji,moom moomu nga xam ne am na fa Ylla ag tab gog aw yiwam moo gn a mat)) ((maa ngi skku ci boroom aras ay may eel ka ko joxe woon moom mooy aji texe ju nu ndppal ji (ki nu solal mbaxanam buur) )) ((sangub sang yi wy na,di ab sri bu nu jiital (bu nu def muqaddam),jiital gi it ki ko def di sri bob aw wirdam ba fww am ngr lay doon)) (( moom de bir na ko ca llaaxiraa gee mu nekk ne man maay jwrini ki nga xam ne mooy boroom raw ak jiital,te mooy ku nu ndppal ki)) (( sangub sang yi yal na am ngrmul sriam,ak ngrmul gn ji mbindef,ndaw muy ku nu bgal !)) (( Ylla laay aan mu may xalifa bii mu fi byyi la mu yene,ci darajay ka nga xam ne ay leeram day jolli)) (( yal na nekk ci moom ,moom Yonnant bi,aari xewali Ylla mi ko gindi def ko muy ku nu gnal ki,ni mu doon yege ak a kawe ca raaan ga)) wasalaamu hallaykum wa rahmatul laahi tahaalaa,wa barakaatuhuu. Esky,gis nga waxam ji mu naan ka ko joxe woon mi ngi ci jublu Sheex Ahmadu Bun Buddin mii,li mu ko joxoon mooy benn teere bu tuddoon ((Mawaahibul Ladduniya)). Sama mbokk,sama xarit Sheex Ibraayma AMAR nu gn koo xame ci turu Ibra Joor,nettali na ma ne S bi,bi mu nekkee Sarsaara walla Tuntu Muxsin, da koo yonni woon Ndar ngir mu jndal ko fa tereb Mawaahibul Laduniya,nga xam ni ki nuy wax Qastalaanii moo ko def,nee na ma dem sonn ci lool,fu ne 46 www.daaraykamil.com

ma wr fa,waaye dara,ma am lu ma naqri lool,yf yi tiis ma lool,ma dpp di ibbi,bi ma tollee ca gddug Sheex Ahmadubnu Buddin,te fekkoon ma xamante ak moom,ma daad fay jdd ngir nuyyu ko,siyaare ko,ba ma fa ggee mu bg lool,teeru ma dalal ma,bi nu toogee bay waxtaan mu laaj ma lu ma taxoon a jug,ma ne ko s bi dey moo ma yonni woon Ndar,ma leeral ko tam naqr wi ma am ci kk a am teere bi ma S bi yonni woon,ca saasa mu jug,gstu ci ay teereem,gnne aari xaaj yepp indil ma,ne ma neel S bi ddiya la,ju ma ko jox ngir Ylla,ma bg ci ba fa bg yam,waaye S bi moom gn maa bg fopp ci teere beek ki ko joxe,loolu nag mooy maanaam ka ko joxe woon,mu jub lu ci li mu joxe woon MawaahibulLadduniya .

Xasida gii ndollent la ci tontub kiy laaj ndax Jibriil da na dikkati ginaaw yonnat bi. Bokk na ci li mu bind eel Sayid Ahmad mom Sheex Muhammadul Haafis lii: Bismil laahir rahmaanir rahiimi,allaahuma salli halaa sayyidimaa muhammadinil faatihilimaa uxliqa,wal xaatimi limaa sabaxa,naasiril haqqi bil haqqi wal haadii ilaa siraatikal mustaqiim,wa halaa aalihii haqqa qadrihii wa miqdaarihil haziim,na Sheex Ahmadu Bun Sheex Muhammadul Haafis,ak ku dul moom ci o Halawi yu goor yi ak yu jigen yi,ak ku dul oom ci jullit u goor i ak u jigen i,nanu xam ne Yonnat bi jmm ak xewal yal nanu nekk ci moom,delloo na ab nuyyo Sheex Ahmadu,te Sheex Tiijaani moom itam grmul Ylla yal na nekk ci moom delloo na ko nuyyoo,te Yonnant bi (j.y.m) teral na ko teral gu mel ne gi mu teral mbokkam mi Sheex Muhammadul Haafis,ki ciy dund yal na ko Ylla grm te aar ko ci lpp lu mu ragal,ka wy it mu grm ko te yrm ko,te SheexAhmad Tiijaan it yal na ko Ylla grm,te jegeel ko,def na ko niki doomam,kpp ku jle wirduw tiijaan ci aari sri yii tudd Ahmad yal na leen Ylla grm te aar leen te yrm leen,mel na ne jle na ko ca Sheex Muhammadul Haafis (y.y.g),kpp ku ko jle ci oom ba noppi byyi leen fi di demati ci keneen ci mbooleem sri yi,nd ak yeney byyi leen,na ko wor ne pert na ci ddina ak allaaxira,yal na nu ci Ylla musal,kpp it ku ko jle ci kenn ci oom aar,bu ca faatoo tonowu na adduna ak allaaxira,kpp ku xool mbind mii na xam ne bi nu koy bind Sheex Ahmad Tiijaan (y.y.g) moo taxaw di wax uy bind. (( dello nuyyoo bu teey bu kawe bpp nuyyoo buy bijj ag dppoo)) ((juge na ca jaamub boroomam bay ligeyal ku nu tnn ki,jm ci ki lq kawe gi niy tnn)) (( yaw s bu mggi mbir bi,musal nanu la ci lori lpp lu aaw)) ((musal nanu la ci rkki aw yiw wu nekk ci yaw,ba kero ngay tbbi jjana yaak i lay xeetu)) (( Aji des ji musal na la ci aawtef yi,ci barkeb ku nu tnn kiy boroom raaya ba (daraapoo ba ,di Liwaawul Hamdi) )) (( ak darajay sa sri bu nu grm ba,Sheex Tiijaan,ka mujj mel ni wurusu marjaan fa sang ya)) ((yal na Ylla miy aji des dolli xewal ak mucc ci gn ji mbindef, moom (Ylla) miy ki koy wommatal kawe ga ak saar ya)) ((ngrmul Aji des,luy bijj ag dppo yal na nekk ci wlliyu wow topp na ay tnkam (tnki yonnant bi) )). Subhaana rabbika rabbil hizzati hammaa yazifuun wasalaamun halal mursaliin wal hamdu lillaahi rabbil haalamiina.

47

www.daaraykamil.com

Bokk na ci li mu bind ngir iy am ag wuute ci Mahiya (mahiya mooy ag nd,nu jublu ci nd gu Ylla nd ak kenn walla nekk gu mu nekk ak moom) ,lii: Bismil laahir rahmaanir rahiimi,ahuuzu billaahi minas saytaanir rajiimi,wa inniya uhiizuhaa bika wa zurriyatahaa minas saytaanir rajiimi,rabbi,ahuuzu bika min hamazaatis sayaatiini,wa ahuuzu bika rabbi ayyahduruunii. Bismil laahir rahmaanir rahiimi,allahuma salli halaa seyyidinaa wa mawlaanaa muhammadin,al faatihi limaa uxliqa,wal xaatimi limaa sabaxa naaziril haqqa bil haqqi wal haadii ilaa ziraatikal mustaqiimi,wa halaa aalihii haqqa xadrihii wa miqdaarihil haziim, mu ne mi ngi aan julli gii doon gog da na yee kpp ku xool mbind mii,mu yee ko ci ne Ylla kat nd gi mu nd ak un nd gu yellook moom la - tudd naa sellam ga - du nd gu xel di jot,te moom barkeel na te kawe - jege na nu,waaye jege gu yellook moom,du jege gu xel di xalam,te xam-xamam tudd naa sellam ga - lu nu sellal la,niki mbooleem ay meloom ,jmmam it - barkeel na te kawe tqalikoowul ak ay meloom te du tqalikoo ak oom it. Waxi Sheex Sanoosi ji,(y.y.g) ak i nd ak moom ci lu aju ci Mahiya lu wr la,ndax oom kat danoo seet fi nit i toll,u wax faak oom,ndax bu nu weesoo ak oom foofu u tbbi ci alkande,oom pp. Waxi Sheex Ahmad Tiijaan ji it (y.y.g) wuutewul ak li nu wax. Waaye li i askanoo ci moom(y.y.g)di wax,ba miy indi ak noonoo ci seen digganteek Abuubakar Ibnu Fatan,na leen wor ne noonoo googu de ci saytaane la juge,ndax Ibliis day tbbal lntlnt ci xolub kpp ku nekkul Mushaahid,(mushaahid mooy aji jkkaarloo,maanaam kay jkkarlook mbir ya ca nguurug sunu boroom ga) liy firnde ci loolu mooy Jaam biy Ligeyal Yonnant bi - yal na ko Aji des,jiy Aji jiitu nekkal cig teral - bi muy bind laabiire gii dy,Yonnant bi dikkal na ko (j.y.m) ne ko Sanoosi Ak Sheex Tiijaan ak Xazaalii de oom wuutewunu,i am ag wuute kay ooy u dul oom. Dgg gi mat a dellu daal mooy byyee settantal ci melow Mahiya te gm rekk ne lu am la,ndax di ci settantal day rkki ngm ,yal na nu ci Ylla musal. Wasalaam .

Bokk na ci li mu bind eel Abuubakrin Ibnu Fatan ci mbirum Mahiya lii:Bismil laahir rahmaanir rahiimi,yal na Ylla dolli xewal ci sunu sang Muhammad ak oam aki saabaam,ag xewal akug mucc gog da na ci xamal nit i ne la Aboobakrin Bun Fatan waxoon ci waxi Seex Tiijaan ji,jubluwu ci woon Sheex Tiijaan(y.y.g),te moom Sheex (y.y.g) dppoo na ak moom (Aboobakrin) ci mbooleem li mu wax ci tontoom yi. Ag jub nag mooy nit i byyee xuus ci lu mel nii,ndax xuus ci, ci aawtef yi la bokk . Waxi qutbu yi, yal na leen Ylla grm, du waxi boroom xam-xam yi,yal na leen Ylla yrm. Boroom xam-xam yiy jfe seeni xam-xam,fi nu toll ci wlliyu yi mooy fi wlliyu yi toll ci yonnant yi . Boroom xam-xam yi boroomi tawhiid lanu yuy aar Sariiha mu nu laabal mi, qutbu yi boroomi sellal lanu yu jegeYlla di aar Haqiiqa mu nu leeral, mu nu sellal mi.Kon wormaal pp ngir jmmi Ylla mu kawe mi lu war la . Bgganteg boroom xam-xam yi,yal na leen Ylla yrm,mooy dundug sariiha,seenug wuute ci masala yi,ag jng la akug jngale,dug noonoo,dug iaanante. Wasalaamu halaykum wa rahmatul laahi wa barakaatuhuu.

Bokk na ci li mu bind ci Ahmadabnil Kawri Addaymaanii, lii:Ahuuzu billaahi minas saytaanir rajiimi,Bismil laahir rahmaanir rahiimi,yal na Ylla mu kawe mi dolli xewal ak mucc ci sunu sang ,sunu kilifa Muhammad ak oam aki saabaam,xewal ak barke ak mucc gog dana ci xamal nit i ne Muhammad 48 www.daaraykamil.com

Ibnu Kawri Addaymaanii,ak Abuubakrin Bun Fatan Alhasani,Ylla mu barkeel mi te kawe jggal na leen oom aar,ci bisub Harafa atum shahidnaa bikaram di junni ak atti temer ak aar fukk ak aar,te ku ci nekk ci oom aar xawoon naa alku,sababub loolu mooy juumug Daymaanii,ak weddig Alhasanii. Ahmadu Bun Kawri moom dppoowul ak Sheex Tiijaan ci li mu doon xuus ci wllug Mahiya,bu dee Aboobakrin moom daa kki teggiin ak Sheex Tiijaan (y.y.g) ci kk a nangu ag tontoonteem ak Ahmadu Bun Kawri,Sheex Ahmad Tiijaan nag moom ku beru la wlif leen oom aar.Liii mooy dgg gi nga xam ne sikk amu ci. Wasalaamu halaykum warahmatul Laahi wabarakaatuhuu. Mu bindoon ba tay jme ci enn ci oom: Assalaamu halaykum warahmatul laahi tahaalaa wabarakaatuhuu,bu lii jllee,man de gis naa li xewoon ci sa diggante ak keneen ci lu aju ci mbirum Mahiya,man nag li may wax ci Mahiya,mooy jmmi Ylla moom,kawe na te barkeel,du toq ci xelum kenn mu koy jem a gstu ,kon xuus ci Mahiya mook wuute gi am ci diggante yahood yi ak nasaraan yi oo yam,yal na nu Ylla mu kawe te barkeel mi musal ak yeen ci soxlawoo lu nu yitelul. Soxlawoo def ndigal yi te teet tere yi moo gn a jaadu uy soxlawoo xuus ci googule wll,Ylla barkeel na te mgg,nee na :( zarhum fii xawdihim yalhabuun) muy byyi leen ci seen xuus googu,uy fo. Wassalaamu hallaykum wa rahmatul laahi tahaala wa barakaatuhuu. Ci noonu S bi tuxoo ci barab dem ci barab, ba bi mu sancee ca Sahwatul Maayi,nu gn koo xame Xumaak,soriwaay bi di lu tollook doxub bis bu tar ci ku sawar,juge Dagana walla Budoor. Loolu amoon ginaaw lollib atum baksasin,di junni ak atti temer ak aar fukk ak aar,mu mujj di wr ci barab boobu di tukkee ci kr,dem ca geneen gu jege,mbiram it mook mu mbooloo yi koy dikkal di siyaaresi di gn a yokk,ci jamono ju nekk. Cig gttal daal leeral mbiri S bi yepp ci aari tukki yii,aal topp aal (aal = tolluwaay yi nit di toll), xewxew topp xew-xew,kenn ku dul moom manu ko,yal na Ylla yokk ngrmam ci moom. Ag karaamaa ngii gu amoon ca Xumaak,maanaam Sahwatul Maayi,ci genn guddi ci benn ci aari weeri rabiih yi,atun jaksasin,di junni ak atti temer ak aar fukk ak att,muy tawati tnk ju ko daloon te tar lool,fogloo nu ca guddi googa,nu fanaan ca la wr xaymaam ba,nga xam ne sax jortoon nanu ne du weesu guddi ga,waaye moom mu niy dalal rekk naan nu dellu leen ca yite ya,amul solo,waaye nun deeti nopp mbaa ay xel di ndati ak nun. Bi Ylla dogalee mu wr ca suba ga,mu xamal ma ne mbir mi de balaa la woon bu juge fa sunu boroom,jmoon ciy nitam,u naroon a fr bu leen daloon (fr = naaxsaay), ma ne sunu boroom lu tax nga jagleel sama nit i nattu bii byyi eneen i,u ne ma ndax kat Ylla da laa teg ci sa kawi moroom,kon manul a kk mu jgleel la sa nattub bopp bu eneen i dul am,te loolu amul lu ko gn a tar.Man it ma ne yaw buur bi ndax man naa koo gddu wlif leen ? u ne ma aha kay, jlal ,mu doonoon lu diis juge ci asamaan wcc sama kaw,ma daanu xm,u indi ma ci xayma bi te yguma. Ki ko yobb ci xayma bi,di Moor Xari Joob nettali na ma ne jaan a ko mtt,kon alhamdu lillaahi ci mucc gi ak tuufu gi (tuufu mooy am li nga bgg) . ibbisi gi jugge Gnnaar Ba mu fa nekkee ba guddig gmmug atum haksasin,di junni ak atti temer ak aar fukk ak juroom,di guddig jjuma,la fa Sheex Ibra FAAL w,tukke Ndar,indaale kyit wu juge ca tubaab ya di ko may mu dellu rewam Senegaal,murid boobu it dikk jpple ko ci tuxu gi,mu tmbalee waaj,di tggu waa dkk ba 49 www.daaraykamil.com

,ba jjuma ja dellusi,di fukk ak juroom eent ca weer wa,mu gnn kram googa sobu yoonu Ngaanjaar,maanaam Gaaya,dib dkk bu nekk ci penku bj-gnnaaru Dagana,dex gi romb na fa,ooa skku ci moom mu julli ci seen jkka ji nu doon yeesal ,ngir barkeelu ci,mu nd ak seen imaam ja Muxtaar SOW, julli aari rkkaa ci njlbenug yoor-yoor,jggi dex gi dem dagana,nekk fa ba bisub gwwu aar fukki fan ak juroom att ci weer wi,mu dugg gaal ci tisbaar ji jm Ndar.

Jamono yi mu nekke woon Dagana,nganale gu nekk defal nanu ko ko fa,ci bcg gi, bu guddi masaan a jot,u daa indi ay lmp yu leer ci kanamu boli yi. Mu wax ci loolu ne loolu mooy liy dggal waxam ja mu waxoon ca lenn ca xasaayidam yi mu defoon ci arafi ((walil laahi mulkus samaawaati wal larli))di ci maanaa Yllaay boroom nguurug asamaan ak suuf,muy li mu mujj a bind ca Daarul Mannaan ca Tuubaa,ba mu ggee ca arafu daad wa mu waxoon ca : ((gane ji naa aji Tedd ji,mu teeyalal ma ganale gi,te du ma da ci nganale gi mel ni ay lmp))

Bi mu ggee Ndar ca guddi ga,daa dal di wcc ca Sheex Ibra FAAL,sax fa ay guddi,juge fa dem Luga, wcc ci Alhaaji Masamba Soxna,foofa la yabale ligeykat yi u dem Njiheen,maanaam Cyen,ca Jolof,jiitu ko fa,defaral ko fa ag kr njkk muy agsi,dal di jll Ngaajax,fanaan ca jkka ja,fa seen xabrub wlliyu nekk,dal di jll ca kr s Asan NJAAY,yendu fa ,fanaan fa,yendooti fa,laxas dem Kokki,wcc ca Sheex Muhammadu Maam ,maami Sheex Bashiiru,demati Duriga,faSheex Madun Samba,maami Sheex Murtadaa,juge fa gg Kr Baasin ca Sheex Muhammadu Amina Xuma JOOB,doo nga dem Cyen ci bis yu new,di njlbenug rabiihus saanii,fekk yenn kr yi noppi,bi mu agsee ca kr ga,ca njlbenug rabiihus saanii,atum haksasin,di junni ak atti temer ak aar fukk ak juroom,daa wcc tudde ko Daarur Rahmaan,mu nekk fa mbiram akuw doxiinam di gn a jub,di dolliku waxtu wu nekk,ba ci benn ci aari jumaada yi ,ci atum saksasin,di junni ak atti temer ak aar fukk ak juroom aar,mu taxawal Daaru Xudoos ci sowwub dkk bi,soree ko lu tollook aari kilomet walla lu ko yes,mu sax fa ,bul laaj nag mbiram,moom daal na ma la ko waxe woon rekk ci bpp barab,waaye fii sax gn na fee dolliku,ba ca jjumay aar fukki fan ak aar ci weeru muharram,atum lasasin,di junni ak atti temer ak fanweer.

Ca sahbaani sakasin ja,di junni ak att temer ak aar fukk ak juroom aar,walla ca ramadaan ja,la s Abdul Laahi gane dduna,wax nanu ma ne S bi daa bind Abdul Laahi ci aw kyit,yonnee ko Sheex Muxtaar Binta LOO,nijaayi s Moodu Mustafaa,digal ko mu tudde ko noonu,mu defe ko ni mu ko binde woon ci kyit wi,mbooloo mi nag leegi danu koy wooye Abdul Laahil Haziizi,te xawma fu nu jle loolu,ah waa-waaw xanaa denu cee jublu ne Haziz turu Ylla la. Ag gnnam juge Jolof jm Njaarem Ci njlug bisub gwwu,aar fukki fan ak att ci muharram,atum lasasin,la gnn dem Njaarem,mu julli woon suba ginaaw bi mu doxee lenn ci ay kilomet,mu fanaan ca la yes Tuubaa, ca guddig altine ja mu fanaan Tuubaa,ca Daarul Haliimil Xabiir,fa Sheex Abdu Rahmaan LO,muritam ba jngal doomam yu mag yi,mu xy nag jm Njaarem,fanaan fa guddig talaata aar fukki fan ak juroom att,bi mu ggee 50 www.daaraykamil.com

Njaarem,u dalal ko ci njlben gi ci benn pkk bu nekkoon ci wetu ttekat (goornoor) bu ndaw bi,ttekatu o bi (al haakimul ahlii,xanaa mooy gouverneur civil) ,ca jamono jooja ma nga dkkoon ca wetam,barab boobu fa lanu tabax fi mu nekk jngukaayu farase bu mag bi (cole franaise),ca penkub dkk ba ,nee nanu ci safari lasasin,di junni ak atti temer ak fan-weer,la s Ibra mom S bi gane dduna,ca rabiihul awali atum alsasin,di junni ak atti temer ak fan-weer ak benn,mu tuxoo fa dem ca kram ga nekk ca kaw tund wa,ginaaw bi mu ko tmblee defar ca weer wa ko njkk,loolu nag mi ngi amoon ca bis bu njkk ba walla ba ca topp,walla ya ko jege,dal di koy tudde Albuqhal Mubaaraka,di ci maanaa pkk bu nu barkeel bi.

Ca aar fukk ak att ci weeru sawaal atum balsasin di junni ak atti temer ak fan-weer ak aar,Sheex Abdul Ahad gane dduna,ci muharram atum jalsasin di junni ak atti temer ak fan-weer ak att,s Abdu Xaadir gane dduna,ci guddig jjuma,ci fukki fan ak eent ci silqihda atum jalsasin ba tay s Saaliwu gane dduna,ci juroomi fan ci weeru kooru halsasin,di junni ak atti temer ak fan-weer ak juroom s Suhaybu gane dduna di rakki s Abdul Ahad,ci silqihda hasasin ba tay la s Abdus Samad gane moom itam,ci rabiihus saanii atum jamsasis,di junni ak atti temer ak en-fukk ak att,la Sheex Murtadaa gane dduna.

Mu tmbli jumaa ji atum halsasin,di junni ak atti temer ak fan-weer ak juroom,jego ci aari tnkam yu tedd yi ci guddig diber,weeru rabiihus saanii,ftte naa nag bis bi mu ci tollool,u tmblee gas dal bi (fondmang bi) ci aar fukk ak juroom aar ci jmaadas saanii atum walsasin di junni ak atti temer ak fan weer ak juroom benn. Tabax gi moom u door ko bisub altine ci yoor-yoor,S bi wcc ci biir paxum xuba bi,Sheex Muxtaar Binta nekk ci wetam,yor ndab lu def ban ( xam naa simaa la war a jubloo wax) , S bi jl jumtukaayu tabax bi (turel) dal di tibb ci ban bi (simaa bi) , wax bismil laah,sotti,jluw xeer teg ci ban bi (simaa bi) ,jlati gasukaay bi door ko ci xeer wi,jng :wa isyarfahu ibraahiimul qawaahida minal bayti,wa ismaahiilu rabbanaa taqabbal minna innaka antas samiihul haliimu mu di ci maanaa :ba Ibraahiima di ykkati dal ya, (mbaa ponk ya, mbaa fondumang ya),ak Ismaahiil,,naan :yaw sama boroom nangul nu ndax yaay aji dgg ji,tey aji xam ji.

Mu dal di fay juge,julli aari rkkaa,aan. Alhamdu lillah,ligey bi gg na ci juroom aari at,ci teewaayu S bi ,mu julli fa aari iid yi(tbski ak kori),aari yoon ci lu wr ,atteel bi kay laay sikk,waaye julliwu fa jjuma . S Mbakke BUSO nee na li ko waral mooy moom kat masu faa yenee sax mukk,(ku yenewut a sax jjuma waru ko), ka fa njkk a taxawal jjuma mooy Sheex Ibraahiima,rakkam ja,ci dppoo gu mu ci def ak Sheex Mbakke BUSO,ak doomi S bi ak magi taalube yi,ndax oom pp a fa yene woon a sax.

51

www.daaraykamil.com

Ndax S bi moo digaloon mag i u sanc ci wetam,byyi boroom kttan yi man a ligey tey tarbiyawusi u nekk ca tool ya,di ligey di indi.

Dkk ba mujj di dkk bi gn a dund, ak jkkaam yeek daaraam yi,ak jngukaayi xam-xam yi,kaamilub S bi nag bis bu nekk u wcce ko ci bunt kram eenti yoon,aari yoon ginaaw jullig suba,aw yoon ginaaw tisbaar,ak weneen ginaaw tkkusaan,bu dee guddig jjuma u wcce ko juroom aari yoon,mbootum loolu moom,Ylla rekk a xam,mooy jullig farata gu mu julli gu nekk, tollookub kaamil bu nu koy wcceel,li ko tmblee suba gi ba timis,juroom aar yi niy wcce ci guddig jjuma gi tollook geey ayu bis gi = julli gu nekk kaamil. Bu dee lu aju ci mbindlu mi moom, da daan def kpp ku mokkal te rafetum mbind,u daa ko bindloo ab kaamil ci lu tollook atti weer yu nekk,walla sumun walla robo walla sulus walla nisif ci weer wu nekk,mu nd ko ak ku mu nirool mbind,mbaa u mu nirool. Naka noonu i ko daan coobarewoo di ko def ngirYlla,ci donga yi nekk ci biti,ak i u daa fay ci waa-rw mi ak naar yi,weer wu nekk daa nanu am lu tollook ay temer ciy kaamili loxo,lu bokkul ak li nuy jnd ci yu mol yi . Xam naa ne bis daal jndandoo nanu juroom aari temeri kaamiil ci yu mol yi,ci benn yaxantukat,yu bokkul ak terey xam-xam yiy dikk di juge ci wll gu nekk,yu nu binde loxo ak yu nu mol,deesul delloo mukk ab tere,ak doonte dikk na fi ay yooni yoon,ak doonte danoo dagg aari wll yi. Mu bire ci loolu ne menn njnd mi mu daa def moom saraxe rekk a ko waraloon ak doonte da ko daan suturaal ci ron ay njkk,te loolu bokkul ak li mu daa seddale way kk yiy laaj,mu di ag ndimbal ngir Ylla,ak li mu daa jox boroom dara ja yi lpp ngir Ylla rekk. Leeg-leeg bis, mu seddale ci ay junniy junni,bokk na ci li gn a yemey li iy gis, gis,te iy dgg, dgg ko,mooy daa am bisub aar fukki fan ak juroom benn ci weeru koor,atum bamsasin,di junni ak atti temer ak en-fukk ak aar, mu dajale nu,nun mbooleem bindkat ypp,yu rafet mbind yi,te booba ab takk bu ry ci kyit a ngi ci kanamam,mu ne nu ndax xam ngen lu ma leen di doye ? u ne ko dewalaay,mu ne leen kyit gii daal laa bgg ngen bindal ma ci ab kaamil,te du u ne ma mukk teru waa ngii,ndare bu da ngen ma ne kaamil baa ngii !, ndax da ngen ko def ?,u ne waa-waaw,mu ne nu jl len kyit gi ,nu jl ko ,seddoo ko ci sunu biir.

Nga xam ne da ngay gis ku jl aari isib,bind leen ci bis,ak ku jl aar bind leen ,keneen maas leen, u tqalikoo ci loolu ci yoor-yoorub juroom benneelu fan ba,ku nekk ci nun xam na la mu war a bind,ak baat ba muy yam,ca digganteem ak ka mu ko seqal, dunu ci dolli ,dunu ci wi. Kaamil bi noppi alhamdu lillaah,ci tisbaari bisub juroom eenteel bi,u jbbale ko, S bi xool ko,gisu ci lenn lu ko naqri,du mbind mu gn a ry moroom ja,du mu gn a sew,du lenn daal . Mu dal di sant Ylla bu baax,daa di ne ndax dggagun ngen fi ku bind walla mu bindlu ab kaamil ci atti fan ? Nu ne ko dedet , mu santaat Ylla,dal di jng:(( innii laa udiihu hamala haamilin minkum)) muy ci maanaa,man de du ma snk jfi aji jf ci yeen . 52 www.daaraykamil.com

Bokk na ci li gn a yeme ci mbir yi,li ma daloon ,mooy man kat daa am bis may yr benn ci terey siira yi (jaar-jaari yonnant bi),yaakaar naa ne tere boobu nuy wax Zaadul Mahaad fii hudaa xayril hibaad la,di ci maanaa yobbalub delluwaay ba muy lg,ci jubug gn ji jaam yi,ba ma gg ci i doon bindal Yonnant bi(j.y.m)maanaam i ko doon bindal wahyu gi ak bataaxel yi,ma lim leen u doon fukk ak juroom benn,Ylla dogal ma ne naa xool nu itam i ci matal ab kaamil ci koor gii aata lanu woon ,far lim ba di benn,ca noona ma def aari woy,wenn wi ma aan ci Ylla ci barkeb bindkati Yonnant bi (j.y.m),wi ci des ma aan ci ,ci barkeb bindkati S bi,am benn waay ci sama gaa yi ku ci tuxale ci man woyuw bindkati S bi te boolewu ci wu bindkati Yonnant bi (j.y.m). Ginaaw bi ma xool ci buntub ligeykati Yonnant bi (j.y.m), uy juroom eent,ag jigeen it nekk ci,mooy Barakatu yaayi Ayman,ma teg ci xool ligeykati kr S bi,ca koor googee amul lu dul u toll ne oom,te ag jigen bokk na ci, mooy Awa Saar jbberub S bi,ma defati aari woy,kurel gu ci nekk wenn tax laa jug. Waaye aar yu saaba yi lakk,te kenn jotu leen a tuxal,aar yu ligeykati ak bindkati S baa ngii: Bismil laahir rahmaanir rahiimi, Muhammadu Lamiin Joop Dagana wax na di woy turi bindkati Sheexul Xadiim ca at ma mu koy woy,di leen tollale ak bindkati Yonnant bi (j.y.m) niki mu nekke loolu ci Zaadul Muhaad :

(ci barkeb i jaayante ak ngn ji ligeykati Yonnant bi,daan ko bindal,di ci grmloo aji des ji) maa ngi lay aan ag jaayanteek moom gu dggu,ni miy grme ku jaayante ak moom te di ko samp) ( ci barkeb Andariyi ,boroom mbgal mi,Muhammad mi nu tudde Bashiir) ( may ma ay mbg yuy leeral sama xol,yu di naa ci mujj di mbgum sama dkk) (ftteel ma ci moom lu dul li nga ma tnnal,may oy (jpp) ci wpp yiw wees ma tnnal) (may ko ci yaw ak ci jwrini Yonnant bi(j.y.m),mbti xolam,akug jiital) (yaw sama boroom nekkal ma cig aar,ci barkeb jaamam ba Muhammadul Amiin) (nga dundal ci moom sama xol ci ay xalaat yuy tax nga grm ma ,bu ko defee ma dib jaam buy sant) (na nga ko may ag aju (jbbalu) gu dggu,ci darajay ki nga xam ne wommatal nga ko lu wr la) (ci barkeb Sharif Mafaatim mu da mi kumpa,muritam bi nu melal ci ngnel lu ry li) (teralal sama xol ci jikko yu rafet,may njari lu sax eel mbindef yi) (rafetalal samag dgg ak samay wax eel kpp ku ma waxal yaw boroom may gi) (nekkal ko, ci di ko may li mu bgg,ci yiwi aari kr yi,mu doon ag am gu mat) (yaw sama boroom ci darajay Daymaan,Muhammadul Xayri boroom koolute gi) (may ma xol ak lmmi wu laab cig neen, u xam ko cig smm) (te ma taqook ragal Ylla ak jfe lu may tax a dab u mat a) (may ko mu tukkee fa yaw grm ak jmm,juy des di nd ak moom ba jjana) (ci barke turandoo wa ,muritam bu lewet ba,doomi Sulaymaan, Sri Joob mu mucc mi) (sarax ma saxug cofeel ak rafetal,ak ag ubbiku ci njngum Alxuraan) (ak jllale ak dddu lu dul lu rafet,ak jege luy bijjee jme cig giim) (mngal jme ca moom ay barke yu sax,yu nd ak sellug dund,ak mujj gu rafet) (ak ci barkeb muriit ba ,doomi Sahiid NJAANI,Muxtaaram mu nu xam, mi mel ni Marjaan) (may ma saxug noppi ci lu amul njari,tey wax lu am njari,te am njari) (may ma kepp ku ma xam,mbaa mu dgg ma sopp ma ci lu dul ag xeeb) (ywenalal ko ddunaam ak diineem,te nga mng ko yoolub jiyaarkat yi) (ci barkeb mbokkam ma ak saxiixam (mooy koo bokkal nday ak baay) bu baax bi,Ahmadu Binta boroom ywn gu nu xam gi) (may ma ag lewet ak xol bu yaatu,ba ma far nekk dib sang bu yaatu) (may ma ag cawarte akug toroxlu,ak mu,te nga sellal samy barab) (na nga ko dundal yaw buur bi ngn ji dund,te nga def ko ci ginaaw bi muy dund ca jjana) (ak ca darajay doomi Faadil jii dib bindaakon,Majamba SILLA kay taarub bindkat yi) (doxal sama diggante ak lu aaw ba 53 www.daaraykamil.com

fww,ci lu bir ak lu lqu ak luy jax-jaxiloo) (doral kiiraayul wattu ba fww ci sama diggante ak bpp saay-saay bu dul jaamu) (mngal ko yaw boroom bi,ci aari kr yi,barke buy aare ci aari gcca yi) (ak ci barkeb weer wi,doomi Muxtaar mi pp xam,di Ahmad waaye nu xame ko ci turu Moor Alima) (may ma may taarub alxuraan,te nga may ma barkeb jngale) (kaweelal sama yite ci luy rafetal sama saayir ,ak sama baatin nd ak xol bu laab) (may ko yaw buur bi xam-xam ak jf,ak teggiin yuy indi lpp lu mu mbat) (ak ci barke doomi Ahmadul Muxtaar,Ahmadu Awa ,sang bu nu tnn bi) (may ma ag baax gu ag bon dul toppati,ak ag nangu gu lamb dul jege) (bpp ayib bu man a gllankoore ci lu baax,na nga ma ko faral ba ma man a am texe gu sax) (may ko lpp lu mu bgg,ci yaw,te nga saxal bnneexam ci ngrm ) (ak ci darajay ki fgg te sax fa,di Muhammad mi niy askanale Wajja) (saxalal samaw lmmi ci wax aw yiw,ci waxtu wu nekk, ma noppi nag wlif aw ay) (na nga siwal samaw tur ci mbindef yi,te nga def ko muy siiwug yiw) (na nga ko may mbatam ci gii ak gee kr,di ku nu laaf ci mbooloom aji matale ji) (ak ci barke doomi Ahmadu doomi Warxa mu Siin mi,kooku mooy Ahmadu KAN boroom askan wu nu ongal wi) (may ma ag aaru te setal sama lpp ci lpp luy taqal lu set) ((musal ma ci njuumte,may mag lewet,guy bel ak man ,ak jpp jmm ju mucc) (na nga tawal ci kawam niiri barke yuy sax ciy yngoom aki dalam) (ci barke ki niy wooye Ahmadu SAAXO,ki nga xam ne ab deram tr tilimalu ko) (may ma nooyug kanam gu sax,det ag kk,gu koy aawal) (na nga ma def may mbgum dkkandoo yi,tey mbgum mboleem maas gi) (na nga ko def muy boroomug dund gu teey,na nga def it ag deem di guy teey) (ak ci darajay cam su nu sangal ,su gnjaru soosu,di Ahmadu mii nga xam ne aw dkkantalam mooy Moor SIISE) ( may ma may kok du ykkati ab jego jme ko ci lu dul sa grm,yaw aji wattu ji ,nd aki xewal) (na nga ma ddduloo ba fww ci lu dul luy tax nga grm ma,dddug ku nu teral) (may ko mu man a saxal li nga grm,ba man a lq sa grm) (ak ci barke doomi Muxtaar mi niy dkkantale Shams,te moom dafa mel ne ab jant ciw nitam) (jeexalal sama xol ci yaw ,may boroomug dund gu sax ci yaw,tey boroomi yene) (na nga ma tggatal njiit yi,te def leen oom pp uy samay soppe ci yaw) (ak ci darajay aji ragal ji Ylla ,aji ywn jiy teet lpp lu bon,Ahmad doomi Saynabu ji) (na nga ma may ag ragal Ylla ,akug wattu akug dggu,ci wepp yiw , may skku ag dggal ci yaw) (na nga teetal sama xol ag bgg dduna,bgg gog da na man a lor kuy wutug jeex ci Ylla) (na nga ko gindi ciw yiw wow da na xeeb ba fww sottikug niir yi,te kenn du ko xeeb) (te ci barkeb Usmaan mi nga xam ne i ngi koy wooye Demba KEBE,mngoo ma te fegal ma njqare) (yaw sama boroom,ba fww,na nga ma aar ci lpp lu my aawal niki wor) (may ko yaw buur bi ba jjana,muccug yaram ak xol) (asaf naa nag u baax lool ci bindkat yu siiw yu kawey daraja yi) (ba gi ma leen ba a indi doyadig pas-pas waralu ko,waaye kay li ma sartoon a def moo ci mant a boole keneen) (yaw sama boroom,ci seen barke oom pp,na nga nangu sama aan gii ba fww) (na nga nu may mu tukke fi yaw,grm ak yrmaande,te nga rafetal mujjug ku nekk ci nun) (ci darajay Ahmad ligeykatu Ahmad,xewal ak mucc yal na ko Ylla mi ko yatt saxal ci moom) (ak oam aki saabaam iy boroomug soppante ci yaw,ngir sa jmm,ci lu dul ngante) (li feek kuy aan ci barkeb ku gg ca aji rafet jay yonni yonnant yi,mi ngi am li muy aan). Sama boroom yal na nga nu nagul,yaw ay aji dgg jiy aji xam.

Woy wi mu defal ligeykati S bi ,di aan Ylla ci seen barke,tollale leen ak ligeykati Yonnant bi (j.y.m),woy waa ngi nii:

54

www.daaraykamil.com

(yaw sama boroom ci darajay juroom eent yoy ligeyal nanu ngn ji jwrini Yonnant bi,kok kawe na kpp ku ligeyal Yonnant bi (j.y.m) ) (saxalal sa ngrm lu mgg li ba fww,ci ki nga xam ne ag ligeyalam lu nu saxal la) (sama kerkeraan jm ci yaw,kiy buntub samag tonowu,kiy far aawtef yi,kiy daal ag mbon) (ci darajaj Malaamin NJAAY,boroom farlu gi ci ligeyal Aji eewant jiy musal jpp aji gindee) (may ma ag cofeel guy taqook xel mi,ci jmmi ki nga xam ne def nga ko muy leerug rew mi) (na nga tggat samay cr ci ligeyal ko,tggatug ka ma jegeel ci sottig xewalam ya) (na nga ma def ma sopp kpp ku sopp,aji ligey jii,na nga ma def may ku mu sopp) (wommatal ko lpp lu mu mbat ci ligeykat bi (S bi) ,niki muy xewalee) (ci barke s Moodu FAAL,maa ngi aaru ci lpp lu aaw,ba fww) ( may ko li mu mbat ci ddunaak allaaxira,te nga fegal ko aari gcca yi ak aari sawara yi) (na nga ma may ag mucc ci kiaan ak ba ab jullit,te nga leeral sama pas-pas) (na nga def ci sama xol yrmaande ju may nooyale jpp aji wow ji xol,ba kero muy nooy) (na nga may kpp ku aju ci man ngn ji ag wommatu eel ma,ba ma man laa grmloo) (ci barkeb aji lnkaloom ju lewet,di Sahiid SALL,na nga ma fegal mbooleem lu ag xuppe di nekk) (mngal ko jmm ak xewal,gu sax ba kerook tbbig jjana) (na nga ma ci maye ag jub gu sax ci lpp loo digale) (na nga ma may ag not sama bnneex,ak bakan,ak saytaane ak dduna) (na nga seral ci man xolub samay dkkandoo,u jub tey diisoo) (ci barkeb camus Mbakke si ko daa rootal,di Aboobakrin,na nga dolli samay xeewal) (sottil ci kawam ci dexi yiw yi,lol da na koy jaal lor) (te nga kaweel sama yite ci moom ci li ma bgg,ci lu dul may gestu lenn loo bggul) (na nga ma may ag toroxlu ci kpp ku ma dajeel ci julliti jamono ji) (na nga mggal ci sama xol ak sama bt,bpp murit bu askanoo ci man) (ak ci barkeb ki mu lnkalool,di Sahiid MBAKKE na nga ma may mboot muy jooyloo kpp ku ma ba) (may ko ci sunu sri bi,la mu bgg,ci ddunaak allaaxira ,mu dppo ak la mu bgg) (na nga ma may ab ligey ci darajaam,mu dib sarax tukee fa yaw) (na nga ma may barke bob ku dul man dana ma ci ee,nd ak xol bu neex) (na nga nu may nun mbooloo mi aju ci S bi,urma ju dul xottiku) (ci darajay mbokkam ma Ibra MBAKKE,daalal ayib yi ag daal) ( may ko gn ji dund aki yiw yu koy bgal ci gii kr ak gee) (na nga matal samag mba-rus,musal sama xol ci mbaeel,te kaweel sama daraja) (na nga musal samay cr ci lpp lu bakkan man a ragal,ak doonte du lu metti) (na nga barkeel eel ma,ci sama mbokk yi ci Ylla,ak eel sama mbokk yi ci Ylla) (ak ci darajay doomi Maryama mi kawe fa S ba,miy Siidi Kala) (yal na ko kiy namm, defal la mu namm,ca kaw nammeelam,moom miy aji namm) (na nga ma def may ku dggu fa yaw ci li ma bgg te nga gindi ci man aji dggu ji) (na nga rafetal sama njort ci bpp murit bu aju ci sama sri,te nga teetal ma ku nu dkku ki) (na nga ma musal cig ykkamti,te may ma ma jot gaa ya) (ci barke camus cam yi,Mbakke JUUF,mi amul lu muy ragal) (may ma ma nekk kuy ligeyal S bi li feek maa ngi dund,kii nga xam ne ligeyal ko mooy ligeyal aji jiitu ji (di Ylla) (tbbalal ma samay xemmemtef ciy xemmemtefam,dammal samag dddu cig dddoom) (ubbil ma yaw buur bi cig ligeyalam,ag ubbi gu may aj ca kaw a koy ligeyal) (na nga sellal ag dundam ci guddal ko,te musal ko ci ay gkk-gkk,walla nga def ko far lem) (ak ci barkeb muritam bu jigen ba Awa,jbberam bay saxal lu baax) (may ko texeg dund,aki neg yu kawe ci ginaaw bi) (may ma bakan bu dal ci S bi,bu doylu,bu dul jeng jm ci ku dul moom) (tggatal ma jigen i,te yombalal ma seeni mbir,te nga dagg jafe ga) ( ywnalal ma ko te def ko muy ndimal ci topp la) ( na nga ma wisaareel ay doom yu gor yu baax ak yu jigen,yu baax,yu am diine te ong) (o da nga dundal ci oom lislaam,di ma fegal ci oom yeddaange) (o da nga leen di barkeel ci jox leen wrsg wu yaatu,wu dagan,ba ca jjanay Aji yaatu ji) (na nga def ngn ji julli,goo xam ne da nga ci nangoo sama aan gii,nd ak sutura su ry) (ak xewal gu sax gu nu gttal,ca ka u xeeal ngn ji gtt) (di Muhammad,ak kurelam ba bpp,te nga wuyyu ma ci seen barke yaw sama boroom) (wuyyug nangu,ak ngrm ak teral,guy tax may ku nu wormaal ci biir gaa yu baax) 55 www.daaraykamil.com

(jeexalal samag dund ci lu rafet ci seen barke,uy u u belal,ca saxuwaay bu kawe ba (jjana) ) Subhaana rabbika rabbil hizzati hammaa yazifuun wa salaamun halal mursaliina wal hamdu lillaahi rabbil haalamiina.

Cig gttal daal,dundug S bi ci Njaarem gisunu ko fenn ci nettali ak jaar-jaari kenn ci s su mag si,ci sariiha ak haqiiqa,lu dul li tegoodi ci yoon ci ligeyub buur yi,muy jem a def ttey yoon yi,di dagg loxoy scc yi,di jam njaalokat yu senge yi,ak door u sengewul i,ak di leen tumbrnkeel,te loolu wuute ak ttey tte gi (nguur gi),ndax tte yooyu daganalunu loolu,te dppoowul ak seenuw doxiin wu mat ci fnni politig yi. Fatabaarakal laa,ahsanal xaalixiin,mbooloo yi bari woon nanu ci moom ca Njaarem,ba nguur gi mujjoon aaye ko muy dox ci nit i ci lu dul ag diggale,loolu taxoon muy wut ay palanteer yu ndaw,ci bunt bu nekk,ci wlli kr gi gpp,nga xam ne fu mu tooge ba ubbi palanteer,aari nit ci u jege i man a gise bu nu jlle eneen aar jegesi,noonu lanu koy nekke ci suba ba bcg ci li gn a bari,teg ca u nekkaat ca tkkusaan ba timis ak lu pp guddi gi. Amaa na leeg-leeg mu dem bind ag xasida,mbaa mu dem ca buntub jigen ay siyaaresi,mbaa mu dem nemmiku njaboot gi,su bggee jngale,da daan soril nit i bunt bi,u kurelu,def gew,mu tmblee tomb ci suuf ngir njngalem sariiya ak haqiiqa,ci alxuraan ak haddiis ak hikkam,ak masalay fiq yi,amaa na mu jnglu xasida,bu ko defee wattukat yi jug jeb,ci kddu gu neex,moo xam danu koy xool,mbaa nu koy tari,xasida yooyu daawunu weesu tagg Ylla ak Yonnantam ba,bu ko defee lekk yi ak naan yi,di daw ci diirub jataay bi,lu fa waay soxla rekk ci dduna ak diine.

Nguur gi aayeeti ko mu dem ca jkka ja,ba mu mujj def jkkam ca fu jege kr ga,ndax moom kat daawul wuute jullig mbooloo ca jkka ja,du guddi,du bcg,du tngoor du sedd,du xiinadi ,du xiin, mu byyil nit i ci kr gi aw yoon wu nu man a jaar julli ji,moom mu wut aw yoonu boppam,wu koy ggale ca mihraab ba,du nu ko gis mukk,ndare bu daa taxaw ca mihraab ba,ubbi bunt bi ndare palanteer bu sew bob du tee u seen ko,ci mbooleem julli gi, bu ko defee mu daa tj bunt bi bu noppee ci julli gi,daan ko ubbi it ngir jngale.

Nu aayeeti ko muy dox ci yoon yi,te kat nit moom ku soxlawoo loolu la,ba mu mujj aajowoo skk ab palanteer bu sew,te sori ci lkkub kr gi,digganteem ak lkk bi aw yoon wu yaatoo eenti xasab a nga fa,mu fay jaar bu bggee doxontu suba ak ngoon,walla guddi. Nga gis nit i u wr ko,ci ginaaw palanteer bi,di dox nd ak moom,di taxaw bu taxawee,ak fu mu jublu,amaa na mu taxaw ngir tufli leen bu noppee ci aan gi,mbaa mu jngal leen am masala,jng gi it da daan bir,loolu lpp ab politigam la woon ngir soxla gi ko nit i soxla,ngir jariu,ak gindiku,ak soxla gi mu leen soxla ngir jari leen ak gindi leen,bu teelut a lijjanti loolu u lor ko ci taxaw ci kawam.

56

www.daaraykamil.com

Seere nanu loolu ndax kat bis dagg nanu ko ci baaraamam,dagguw dllam it,ngir xr ci laal jmmam ju tedd ja . Waaye buuxante bu metti bi mooy waral uy dal ci kawam,ba koy gaa ,te dunu jublu loolu . Bu ko defee muy gaau ci loolu ndax moom jmm ju tuuti,te doyadib bind la waaye di ku dgr ca Ylla,du yoqat,te du sonnu,ba bi ko mbirum Ylla mi dikkalee,u tnn aar ngir u toppatoo ko,uy aari muritam yi Muhammad mom Abdu Rahmaan Attandaxii, mi faatu,ci ginaaw bi ci sawaal,atum bahsasin,di junni ak atti teemeeer ak juroom aar fukk ak aar, yal na ko Ylla yrm, kooku moo ko doon toppatoo ak mbokkam mi bind araf yii,Muhammadul Lamiin JOOB ,u duggal ko ab wata guddig llarba yobb ko Tuubaa,ci pexe mom danu koo def ngir lq ko nit i .

i ko doon gunge juroom lanu woon,s Bashiir moo leen jiite woon . Mu dal di yonnee ca mbokkam ma,s Muhammadul Faadal,xalifab aareel bi, te ca jamono jooja,ma nga woon ca wurumub dkk ba,ca wetu Tuubaa , mu yonnee ca Sheex Ibraayma ca Daarul Muhtii,ak ca s Mbakke BUSO,ca dkkam ba ca wetu Tuubaa,mu yonneeti ca mag a nekkoon Tuubaa, oou daje ci diir bu gtt,ba nu matee aar fukk ak juroom att,s Mbakke BUSO jiite leen,loolu lpp a ngi ame woon ci lqu gu tar,ngir ba fitna, i ngi noppi bi fajar daataa jot,def fa ab neg bu nuy tj ak a tijji, bi ko nit i ygee bi suba jotee,coow li jolli,bul laaj nag wax yeek jf yi,loolu lpp bi muy am s Moodu Mustafaa ngi Njaarem di xamal nit i ak di leen dalal .

Bi nu noppee ci waajal gi,ma gnn ci bunt bi ma njkk a jot,laa daje ak kenn ci taalube yi,te booba moom ygutoon li xewoon,mu ne ma man kat biig dama laa gnt ,di la laaj S bi, nga ne ma: (( wamaa Muhammadin ilaa rasuulun,xad xalat min xablihir rusul)) muy ci maanaa Muhammad du lu dul ab yonnant,bu fi ay yonnant jiitu. Ma ne ko ni nga ko gente la deme de,duggal,bi mu duggee,tmblee yemu . Ki boole tere bi defal na ko marsiya (marsiya = xasida gu niy waxe jf ju baaxi ku faatu) ci ay bayit mooy bi nu njkk a defal S bi, bi mu fi jugee,mi ngii: (S bi wy na jm ca buur ba mu daa jaamu,ndax kat xamoon na ne fii kenn du fi des) (mu wogu di smm ndigali Ylla yi,ngir ngrmam tey teet li mu tere) (di tere lu bon tey digale lu baax,di def lu nu xam te du ca ppal) (nekkoon na kenob diine ca bisi dundam,oam de,moom lanu jublu woon ci skku dgg) (gisoon nanu ne mooy seen baay,bu nu war a jox qi baay,moom itam,mu gisoon ne qi doom lu nu leen war a jox la) (mooy ki daa ftteloo jirim yi seeni cosaan,daan faye aw ay ciw yiw ) (moom dey naataange la woon eel u ndol i ko daa dikkal juge fu nekk ngir xontu) ( bu daganoon nu jote ay bakkan de,nu def ko,waaye ay sang jiitu nanu ko,juge fi,te kenn jotu leen ) (waaye de na la woor ne bu fddoo wlif nu nd ak jmm ja tam,du tee aw yiwam wiy dolliku du fddu mukk wliif nu) .

Buurub woykat yi it ca jamonoom ak wllam,di Muhammad mom Muhallaa Alhasani defal ko moom itam marsiya bu yemee yeme,mi ngii: bismil laahir rahmaanir rahiimi,wasallal laahu halaa nabiyihil kariim, Muhammadu mom Muhallaa,mi nu gn a xame Naana,mi ngi wax di marsiyaal Xutbub Xawsu bu 57 www.daaraykamil.com

boroomam bu mag bii di Sheex Ahmadu Bamba mi nu xame ci turu Xaadim,yal na ko Ylla labal ci gejug yrmaandeem,te sarax nu ci barkeem, aamiin: (yoonu dee mooy dayob kuy dund,dund daal lu dul dee toppu ca) (nit pp a ca jm nag (moom dee), bu bettewul ci bcg gi ,def ko ci guddi gi) (moom daa mel ni ab rawante bob mooy bant ba nu samp jm ca,ku ko jggeegul it ca nga jm) (ndaw dayo bii di bu yeme !,moom de mooy saxuwaayu seeni mbooloo,tey dajekaayu seeni kurel) (lu waay tyyeel tyyeel du tee mu jot boobu dayo,lu waay sawar te bariy jumtukaay du tax mu romb ko ) (dee daal daa mel ni ndabul nganale lu nu woo pp,woote gu matale te yaatu) (bu aji ligey ji wuyyo wooteg dee gi ti,te kenn bgu ci ) (jotoon naa wuyyu cig njkk wooteb Ylla bi te booba gindikat yi jugagun) (mu daa wuyyu wooteg kpp ku woote jme ci yoonu kawe ak teddnga ) (mu nekkoon di kiy woote ak a gindee jme ci ngrum jmm ak mucc) (moom de bi smmkat yi ruuralee seenum cmm,daa feteek aji wattu ji,smm am cmmam) (teg nanu ko lepp lu diis lol yanukat ba gn a mag gn a dgr ttanu ko).

Bokk na ci jikko yi mu ko limal: (ak dagg buumi aawtef ypp,ci lu dul gestu guy gllankoor walla yoqat) (ak dundal xol yi ci sikar ak waaraate yi rafet ci waaraate yi) (yem naa ku mel ni moom, ci niir ak tawub dundalug xol, bu nuy mng, jme ca suuf yu bekkoor ,yu naatadi yi) Mu neeti: (ki ko tnn daal a ko woo jme ko ci teraanga,ngir fay ko jfam yu baax yi) (moom itam mu wuyyu,ba mu demee fekk fa la mu doon mbat,ci ngnef yu gnjaru yi) (mu mujj kk gi nu ko kk,di lenn ci way jommale yi,te di am mbamb (xew-xew bu njng) mu lndme ni tggeg tggekat yi) (Abdul Xadiim daal wy na,di ku nu santi jf,di ku ay mbootam lenni gkk-gkk nekku ci ) (Abdul Xadiim daal wy na, te bnul lu dul btub ay may aki xewal) (wari fas daal du woon yitem, te ji ay tndarma yuy dott it taxu ko woon a jug) (dundug buur yi de dug dudam ,ak doonte day joxe ay boli yu nu feesal) . Tjte Tj: u tje ko ci waxtaane lenn ci li ko Ylla may ciy xewal yu kawe njort, ginaaw bi Ylla sooyalee seen atti pexe ya,muy ray ak tj gu sax,ak tumbrnkeel gu sax . Bokk na ci li ko Ylla xewalee ci safaanub att yooyu - S bi nee na - def gi mu def ati tumbrnkeem di lu juge ci nattub yonnant yi ak seeni balaa,yi leen seeni noon daa teg,mi ngi wax ci loolu: ((bokk na ci xarbaaxi Yonnant bu nu gnal bi,yal na xewali aji kawe jiy gnale nekk ci moom) (bokk na ci xarbaaxam yooyu:nekkug sama ati tumbrnke gi di lu nu gnnee ci jamono ju jll ) (u niroole ko ak la xewoon ca diggante yonnant ya ak a nga xam ne oom pp ay kccoor lanu) (yal na xeewal ak mucc sax ci oom,ni Ylla dqe ak lndm ci yonni gi mu leen yonni) (ag kemtaan dey fee na ci sama tumbrnke gi,ni mu feee woon ci Yonnant bi moom mi gindee) (loolu mooy i sabablu woon tumrnke gi de) (ee nau i ko sababluwutoon ci noon yi,te Ylla notal na ma leen ) ( i ko sabablu woon de dunu tbbi jjana te sawara lanu jm ) (te du nu am li feek tuubunu,lu dul ngn jaa saxi njqare).

58

www.daaraykamil.com

Mu bgg a wax ne Ylla mg na te kawe,niroole na ci ngnelam, li amoon ci sama diggante ak noon yi,niroole na ko ak li xewoon diggante yonnant yi ak seeni noon,ciy nattu,mu niroole la nu ca ame ciy xewal aki njari lu nbbu ak lu fee,fii ak fa nu jm,mu niroole loolu ak li ma ci ame ciy xeewal aki njari . Mu tollale loraangey dduna ak ju allaaxira ju noonam yi tuubul ak loraangey a tuubutoon ca seen noon ya. Te a sababoon nattu yooyu ak fitna yooyu,ee nanu i ci ndutoon ak oom ,li Ylla di wax naan: ((wa yawma yahaddus zaalimu halaa yadayhi,yaqoolu yaalaytaniit taxaztu mahar rasuuli sabiilan,yaawaylataa,laytanii lam attaxis fulaanan xaliilan,laxad adallanii hanis zikri bahda isjaa anii wa kaanas shaytaanu lil insaani xazuulan) muy ci maanaa : bis ba nit di mtt loxoom wiccax,naan aka neexoon ma topp Yonnant bi,aka neexoon ma ba a def diw xarit,moo tax na ba ma rere alxuraan ,ginaaw bi mu ma dikkalee,te shaytaane dey day gccaal nit rekk. Mu ne moom aaya woowu seere la ci Yonnant bi (j.y.m) ak yonnant yi jmm yal na nekk ci oom, tey kemtaan,waaye di seere eel ma tey karaama,kon alhamdu liilaah,sant naa ko te grm ko,ci dppale gi.

Bokk na ci mboti sama tukki bi,xewal gi ma Ylla defal muy juroom aari karaama,tollook kiimaani Yonnant bi (j.y.m),ooy: Ylla notal na ma samay noon njkk samag fee, may ma xam-xam bu jugewul ci njng, Yonnant bi (j.y.m) puukarante ak yonnant yi ci sama tumbrnkeg fukki at yi ak ligey bi ma ko ci ligeyal muy ligey bu sell, Ylla def ma may koo xam ne kpp ku texe da na ko sopp,te naagul ibliis ci man ak kpp ku nu rbb, mu def ma may ku malaaka yi sopp,ak way gmi jinne yi,def it julliti jinne ypp aju ci man ngir jmmi Ylla,mi ngi wax sax ci loolu naan: (( juroom aari kemtaan ci yu Yonnat bi,fee nanu ci man,te am naa samag aan ca seenug njkk)) ((sama boroom ci barkeb ku nu tnn ki ,notal na ma noon yi,njkk samag fee,te du ma dajeek kuy noonu)) ((Ylla may na ma xam-xam bu jugewul ci njng,te indil ma Kun (mooy nekkal mu nekk) )) (( Yonnant bi puukarante na ak yonnant yi ypp,yal na xewalug Ylla nekk ci oom)) (( ci sama tumbrnkeg fukki at yi,u nd ak ligey bu sell eel boroom nekk gi ak jiitu gi (Ylla) )) ((kpp ku texe da nga ma sopp ba fww,ngir jmmi sama boroom miy aji delloo,sopp gu ndul ak ag mbaeel)) (( Ylla miy aji dimblee,naagul na ci man ibliis ak kpp ku nu rbb )) ((malaakay aji tedd jiy aji des,danu may bgg ngir jmmam ja,nd ak texe gu dul dagg)) ((i gm ci jinne yi,sopp nanu ma ngir jmmi aji des ju may defali xewal)) Mu waxaat ci beneen barab: ((jinne yi gm ci sama jamono jii aju nanu ci man,waxu ma, i gmul)) mu neeti: (( mayal i ma ligeyal lu rafet,moo xam malaaka la,mbaa ku nu lq (jinne) walla nit)) Nu xame ci loolu ne moom kat am na eneen u dul nit u koy ligeyal,mu waxati ci beneen barab:

59

www.daaraykamil.com

((Muhammad may na ma ag not,kpp ku dkkaale ak moom du nu ko not)) ((samag texe day des ci lu dul rkki,Ylla notal na ma mbooleem ay noonam)) Mu waxati: ((kuy lewtoo jubluwu ma,bbbug (xeewali)sama boroom lu fee la,ibliis de du lewtook soldaari aji tedd jiy kenn)) Mu neeti: (( wattu naa lu nu ogal wlif tere yi,kon bul tyyeel ci ligeyal ma)) (( Ylla mngal na ma mbooleem xam-xam yi,aji tedd jii de baax na , mooy aji da ji kumpa,tey aji xam ji)) ((kiy def lu ko soob de nocci na xam-xam yi ak seeni barke eel ma,ci nekk ngi mu nekk di aji xam)) ((ki nga xam ne wommatal na ma aw yiw,wuy sellal xol,te yiw wa wommatu de,deyaale na ak man)) ((Ylla xewale na ma jngale,di naa gindi ku rer ak ku am xam-xam)).

Bu dee ni mu bgge i gm nag ak ni ko oou bgge,loolu moom jarul sax nu ciy wut lu ko seere,ndax mbir la mu niy gis,di jkkaarloo ak moom,muy barig jari gi mu leen di jari ,ci xam-xamam ak alalam,aki mbotam,aki aanam, du amadi solo u tudd cis lf ngir barkeelu ci,am na fu mu naan: (( jggalal jpp aji gm ju gor ak ju jigen,jggal guy saxal wpp yiw)) ((jggalal bpp jullit bu gor ak bu jigen,jggal gu leen di musal ci tookat yi)) ((jggalal jpp aji rafetal ju gor ak ju jigen,jggal gu leen di wommatal lu rafet)) . Mu neeti ci Matlabus Shifaayi: (( na nga saafara mbooleem jullit i,ci fii,te nga fegal leen tiit ak njqare ca fee)) (( na nga leen musal te jmmal leen,te eewant leen,te bul fayyoonte ak oom ngir barig seeni bkkaar )) ((ndax oom kat bu nu la moyee ngir sggan,du nu la bokkaale ak kenn)) (( te seeni yaram ttanuu sab nattu ,ngir seenug doyadi)) ((seeni xol de du jng jm ci ku dul yaw,ba fww, ci fii ak lg )) ((waaye nekk gi cr yi nekk di ban,bijj na leen ,yobb leen ci gn jaa boni bon-bon yi)) ((bul fayyoonte ak oom ci lu la dul wi,may leen li leen amal njari,te amalu la njari )) . Mu waxati ca xasidaam ga tudd (Fastajaaba lahum rabbuhum): (( ci darajay Mustafaa,wuilal xeetam wi njqare,yaw mi gnne sa jaam bii ca njqareem la)) ((bindalal Yonnant bi xewal ak mucc,ak oam aki saabaam yiy boroomi teet lu bon )) ((musalal aw xeetam ci darajaam ak seen daraja oom pp,yaw kenn ki ma notal)) ((wuilal njqare i di boroomi gm,yaw miy kiy maye ag koolute)) ((yaw aji rafet ji,ggaleel ci mbooleem jullit u gor eek u jigen i,jmmi boroom mbindef yi)) (( bindal ag sell eel mbooleem way rafetal yu gor yi ak yu jigen yi,yaw mi mngoo way gm yi)) .

60

www.daaraykamil.com

Ak lu bokkul ak loolu lpp ci li nu manul a lim,ci lii di wone bgg gi mu bggal xeetu Yonnant bi (j.y.m) li mu bggal boppam,mu jagleel ci boroom jagle yi,geneen bgg gu gn a tar . Dgg naa ko bis (g.y.m) mu naan :man dey jamonoy samag ndaw,dama daan tnn ci giir gu ne ab xarit,daan ko jagleel ci sama xol ag cofeelug boppam,ni ma tnne woon ci giirug Daymaan,Muhammad Yaddaali,boroom tere bi nuy wax (Zahabul Ibriiz),ci giirug Tandax ma tnn fa Muhammad FALL mom Mutaali,ci o Haaj i, ma tnn fa Ahmadu doomi Muhammad,boroom (Jawharul Munazzam). Bokk na ci li mu nu nettali ci cofeelam gu yeme gi ak mbgelam gu tar gi eel ennat i ci jullit i; nee na bi mu nekkee ca tumbrnke ga ca gej ga,daa yggoon ne sunu mbokk mi Muhammad SEKK,mi nu gnoon axame ci turu sri Lmba,ak sunu mbokk mi Muhammad JOOB,u gnoon koo xam ci turu Majoob Aram Seri Fittu, tubaab bi da leen a yobbu woon ngir tumbrnkeel leen,xawma fan nag,bi mu ko defee mu amoon lu ko naqari lool,nee na dduna dal di lndm fi man,sama jamono nx ngir eewant leen,ndax kat bgguma u nattoo leen lu leen di tax a kk seenig gm,mbaa mu koy rkki ci oom,yal na nu ci Ylla musal,ma dal di aan Ylla ci seen mbir moomu ne: (( yaw gn ji aji jggaley bkkar,tey gn ji ku man a musal ku nu jpp)) ((na nga dindi jullit i cig njpp,te musal leen ci luy waral sikk )) . aari byit yooyu i ngi ci xasida gi tudd ((wa mmaa maayanfahun naasa fayamkusu fiil ardi)),man naa am bi muy bind xasida gi la ko seenub xibaar dikkal,mu dal di def aan gi. Bu dee bgg gi ko i gm te di boroom jagle bgg ,loolu moom lu nu xam la te siw,seereel nanu ko yiw wu nekk,ak wilaaya gu nekk ci barab bu nekk . Seere yi ko mag i seereel ag mgg akug wilaaya Doggantal : ci seere gi ko u mag i seereel ag mgg ak ag wilaaya

Xoolal Sheex Siidiya mii ak mggam gi mu mgg lpp,tewul mu tegoon S bi fu mu tegul kenn,bind na ci moom,woy ci moom wesar ci moom,bu waxutoon lu pp atti xasida yii tam,ci xasidaam yu bari yi,loola da na doy,ooy yii: (Sheex Ahmadu daal xewal la ,gu Ylla jox mbindefam yii ypp) (ag cant eel na Ylla mi ngi xam ne ay xewalam jaamam yi manunu koo takk,mbaa nu lim ko) (boo dajee ak moom,fekk uy yekkati raayob teddnga,da nga ko gis mu alawtiku ko ci loxol ndayjooram,nd ak di tudd Ylla ) ( bu gisee bis jikko yu rafet yi u ddd leen,day dogu jublu ya ca gn a mag) (suuf su ko dkkal daal ,ab lolli bu ko kk a ndndal du tax mu lor ko ) (miskiin yi ngir sa baax gi ftte nanu seeni dkk,ba mujj na sa koom mii de lanu jppe seenum koom ) (seen mbooloo yooyu de buy daje ak oom mbgte mu ry te dggu lay ndal,nga xam ne da ngay jort sax ne,lu toll ne li mu leen di jox ciy xewal rekk,lanu koy jox )) (( mbooloo ypp seere nanu nekk gi mu nekk di ku baax,ku tedd,kuy jaamu Ylla te dib tuubaakon )) (( bokk na ci i gisoon jari nit i di farata,ci jamonoom,tey ci i daan tudd Ylla )) (( dogal bu w mu nangu ko te grm ko,xam ne Yllaay ki ko dogal )) ((bu kuy txu cig lndm di txu it,moom genn muuraay du 61 www.daaraykamil.com

man a muuri btam wlif dgg gi )) ((kersa du da di ab rootukaay ci sab hadara,bu ko defee yiw yi di noyyi ci gelawam lu sedd li)) ((jaam yi de ,dox gi nu dox jm ci moom,seeni aajoy ddunaak allaaxiraa ko waral)) 1 aareelu woy wi mi ngi ko def bi mu tmblee tabax jumaay Njaarem ji,mi ngi nii:

( jkkay S bii de mooy jumaay barke ji,tey barabub ay yiw ak yrmaande ) ( fa lanuy jggalee aawtef yi,a koy siyaare it seeni yiw danu koy ful) (boroom fondumangub ragal Ylla la ,ak miiri jf ju baax ak teraanga) ((jf ju sell eel boroom mbindef yi,ci yeene,te jf yaa ngi ci yene yi) (boobu barab de,lquwaayub ku bgg a taxaw guddi ngir jaamu Ylla la,kon de bu baax la,lquwaayub u ndool i de lquwaay bu baax la) (bu fa julli ngir Ylla amee ab neg it,du tee muy neegub jokkoo ngir Ylla) (xamal nanu fi julli ay waxtu,waaye jkka jii de am na lu dul waxtuy julli rekk) ( nit i danu koy jublu,nd aki xol yu boole lu tqalikoo ciy yeene) (ab kurel bu fay w ngir julli,ak beneen bob mbiram mooy asaka ) (Ylla digale na u ykkati ay neg,yu tedd ci kaw yeneen neg yi,ngir turam wi) (yal na Ylla faye tabax gi, ay kr yu niy tabax ca jjana,ay jigen nekk ci) (S bi daal xewal la,gu Ylla joxe,di kiimaan ci kiimaanam yi) (nit i de xam nanu ko ci penku bi ak ci sowwu bi,mu dib sang ci taax yi ak ci kaw gi ) (mi ngi bokk ci tabaxkati jf ju baax,te loolu lu new la ci nit i) (dellu nanu seeni kr,nd akug cant,gu toll ne cantug ku soxla woon am ndox Ylla jox ko dexug Furaat) (yal na ko Ylla wattu ci wattoom ga akug kaweem,aki doomam yu g0r ak yu jigen) (ak o negam bu kawe bi,mboole seen,ak muritam yi juge ci wll ypp) ((te Ylla may ko Xurratu Hayni (am mbgte) ci dduna ak allaaxira) .

2 atteel bi ci yu mujj la,da fa mel ni danu koo wonoon ne ab digam daa jotoon : (burub nit i yal na la fay ngn ji fayam,te dolli la ci teralam gi ak mayam gi) (te mu desal la fi,ngir mbindefam yi nga xam ne,sag des moo di seenug des,xewale la mooy xewale leen) (kuy jem a tollook yaw bu woomlee tam,nan lay yege ba jot ku ko gn a woomle fopp?) (nan lay yame kok am koomam mi ngi ci joxe ko, ak kok mi ngi ci denc ko ak lq ko? ) (ndax kuy jnde alalam ab yool ak ndam,da na mel ni ku nuur ci njaayam maak njndam ma ? ) ( cam la su teddnga di fee bu feeee,bu lqoo,sooroolub njkk lqu ) (bis bu Ylla dogalee tenqam gbum koom,da koy dal di seddale way yalwaan yi) (day jppe jeexug alal,akug naaxsaayam, muy di ko jem a mggal ak a dajale,joxe ko ci yoonu Ylla it mu jppe ko muy li koy yokk ) (bariwaa na ay gawar yu mel ni ay cati xej,naaga (gilem) yi daw ak oom,jggi ab ll,bob suuf sa daa mel ni asamaan sa ) ( ki leen di wommat,di yaakaar ju rafet ji nu am ci moom,ki leen di gindi di kaweem gu rafet gi ) ( u jublu ,bu nu ggee ca ttam ba,fajug seeni aajo ci lu dul nx-nx,nd ak am lu leen ci wor ) ( ayibam daal du lu dul jaamu Ylla,ak jari nit i subaak ngoon) .

62

www.daaraykamil.com

Aji seere ju mel ni moom cig ragal Ylla,ak am xam-xam,te di ko jfe ak sax ci sunna,doy na skk. Xam na aw yiw,ak barabam,dal di koy laabiire jaam yi,tegtal leen ko,yal na ko Ylla fayal lislaam ak oam. Xoolal ku mel ni Sheex Sahdu Abiihi,wlliyu wu pp nangulug wilaayaam,bokk ci negub teddnga,di ci askanu Yonnant bi(j.y.m),xoolal ku mel nii wax ,bind,wesar,woy.Bokk na ci li nu ko askanale ci lnn ci ay bataaxelam,ginaaw bi mu santee Ylla ,julli ci Ynnant bi,da ne: ab nuyyoo ngi juge ci man jm ci Sheex Ahmadu Bamba,yal na Ylla rbb ku ko ba,te rbb ku ko waral,ma lay aan nag nga ba maa ftte,te ba a ftte xeetu Yonnant bi (j.y.m) . Lii nii juge ci sang bu mgg bii,ag laabiire la eel xeet wi,di it ag tegtale gu muy tegtale aw yiw, di ko junj,junj gu nooy,te lqu. Mu ne ci ag xasidag ndokkeel,bi S bi dellusee ci tukk bu nu barkeel ba,ginaaw bi mu defalee S bi ag seede ci bayit,wu ygg,muy: ( jamono gioon na ne da na fi indi ku mel ni moom,waaye ee jamono,sa ngi gi amul de,kon demal kafaara ji ) . Mu neeti: ( tubaab yaa ko jle woon ca mbellam ya,mu mujj ca gej yooyee di wurusu ngalam ) (mu feee ca xori gejug mbmbullaan ga,di wurus wow ag leeram akug xuy-xuyam tax na ba bt yi glm) (mu di weer wu leer,wu fddu ci sowwu bi,feeaat ci dib jant cig ykkatiku ak ak tasaaroo ) (yemu naa ci wurus wii nu jaarale cig nattu, mu mujj di wurusuw yaaxoot,wu deesul jaayante ab taar ak moom) ( yemooti naa,na ngeen xam ne buntub tuub ak njggal de,ubbi nanu ko,eel bpp murit,bu skku ci moom ag dkkaale )) (ag ndokkeel eel na diine jii, nga xam ne mujj na di puukarewu ci yaw,ngir mbgte ak ndamu ) . Eskly,esky,xoolal ma wlliyu wu tedd wii,ga xam ne lqul lu dul ag dggu . Xoolal ma wlliyu wii,Sheex Mustahiin Alkumayli,sunu mbokk mi ci Ylla ak ci S bi,Alhaaji Muhammad Abdul Laahi doomi Ubaydur Rahmaam,nee na ca tereem ba tudd (( Annafahaat Almiskiyya Fil Xawaarix Almbkkiya)),: bi tubaab bi tuddoon Kaylaan - yal na nu Ylla musal ciw ayam - laajee Sheex Siidiya,lan mooy tteb jiyaar ji jullit i di def ci nasaraan yi,ci jamono jii,ndax lu dagan la ,ginaaw nasaraan yi dunu leen def lenn lu aaw ci seen diine,ak li ni nu leen di pp doole lpp,ak li jullit i di new doole lpp ? Mu tontoo ko la mu ko tontoo ,mu jbbal tontu bi Sheex Sahdu Abiihi,mu gaaral ko ko,bgg mu wax ci, mu bind moom S bi,lu mel ni li Shayxaani (Buxaari ak Muslim) bindoon,jme woon ko ci wlliyu yi ak boroom xam-xam yiy jnkoonte ak u dul oom muy: ki bind araf yii de Ylla def na ko muy buntub texe ak mbgte ak njkk . Dara ci loolu jubluwu ko,ndax moom kat fex na ci fitnay dduna ak allaaxira,atun kasasin di junni ak atti temer ak aar fukk,bu feexutoon ci fitnay dduna ak allaaxira,kon mu indi tontu bu atteel,waaye moom mujj na ,bokk ci i u wax ci oom (( bal ahyaaun hinda rabbihim yurzaquun)),muy :oom de fa seen boroom uy dund lanu,u leen di wrsgal, loolu ki ko wax a ko bind di,Ahmadu mom Muhammad,mom Habiibul Laah,yal na ko Ylla mu kawe mi musal,te nekkal ko te mngoo ko. Subhaana rabbika rabbil hizati hammaa yazifuun wa salaamun halal mursaliin walhamdu lillaahi rabbil haalamiina .

63

www.daaraykamil.com

Dgg naa Sheex Mustahiin mu naan: loolu de dgg la bu dutoon dgg du ko bind. Dgg naa ci Sheex Bashiiru mom S bi,mu nettali jle ca Sheex Mustahiin mu ne: man de yemu naa ci mbirum S bi,toog nanu ak moom bis ,di mbooloom boroomi xam-xam,yaakaar naa ne Abdul Laahi Ibnu Muxtaar Alhaaji,ca la woon,mu tmbli di wax ak un wax ju yeme,ju dugg sunu xol yi,u bgg tey dggal te xamunu sax dgg-dggi li miy wax,waaye mu jpp sunu xol yi,nu xame ca ne ca Ylla la juge. Sunu mbokk moomu nu tuddoon nee na ci terem bi nu tuddoon : bokk na ci karaamay S bi,yal na ko Ylla wattu,dellusi gi mu dellusi bawoo ca dun booba,nga xam ne kenn la fa tubaab yi masul a yobb mu dellusi . Snni nanu fa nit u bari,waaye de kenn a ci dellusiwul,loolu mooy firnde li gn a mag ci ne moom demam gi moo ko tnnoon,dgg naa ne Sheex Mustahiin mom Talha Alkumaylii,nee na : moom de bu bggutoon a dem du dem,dunu ko man a gnne it dkkam. Te kooku doy na ndrlaay. S bi bindal na ko ag laabiire gu mu tudde, Diyaafatul qudoos,wa laa yashummu raaihatahaa dayfu ibliis muy ci maanaa nganaleg Aji sell ji,ag xetam du xee ganug ibliis. Daa na siyaaresi S bi ,juge fu sori di liiru (dox ci tnkam),daan ba bu ko Ku tedd ki masaan a jox alal,bu ko masaan a jox sijaada ngir mu ciy jullee,da ko daan jl di ko taf ci dnn bi, te daawul nangu deesi sggane ko.

Li Sheex Mustahiin waxoon rekk, la sunu baay Muhammad Alkuntiyyu,mi nu gn a xame ci turu Bu Kunta ca Njaasaan wax, ca wetu Tiwaawon . Kenn ci taalube yi nee na ,booba dafaa demoon di ko siyaareji,mu laaj ko S bi,te booba xam na ne mi ngi ci tukki bi,ne ko ana S bi,mu ne ko moom de tubaab yee ko yobbu,mu ne det,bul wax loolu,mu ne ko lu may wax kon ? Mu ne ko,moom kay daa dem ligeyi,fa ligey ba neexe,murid bi nee booba maa ngi fi ma toog di dgg nit uy wax te xamuma dara ci li niy wax,mu ne ma ndax dgg nga lkkuw gaa yooyu ? Ma ne ko dedet,mu ne ma li ko waral da dul seenuw lkk,ndax S bi njkk muy tukki,daa samp ab lkk wrale rew mii,kenn du fi man a am benn taalube,ba kero muy w,man nag samay taalube maa ngi leen jle ci ginaaw lkk bi,samay taalube dunu w li feek ginaaw weer walla ay weer.

Bokk na ci kilifa yu mag yi seereel S bi,Sheex Abdalla Attamkali Addaymaani,wax na te dggal te rafetal: (dama ne jngal jm Daaru Salaam ak Tuubaa,boo ragalee ay mbamb,aki coowi jamono) ( ngir nga ame fab xool bu tukkee ci xawsub jamono ji,bob da nga ci ame njggal akag texe) aari bayit yii de maa ngi ko mokkale ci S bi,ndax bis da ne ma ndax xam nga aari bayiti Abdalla yi,ma ne ko dedet,mu jng leen ma dal di leen mokkal,xam it li mu doon junj ci dggal wax ji ci nekk di xawsub jamonoom. Boroom xam-xam bu mgg bi ,Sheex Abdul Laah Attandaxii Albohbiinii,nee na bi mu siyaaresee S bi Njaarem:

64

www.daaraykamil.com

(boo mujjee w wlliyu ypp, ba noppi kawe leen,na nga xam ni ngn ji mbindef de,ci xarnu yu mujj yi la w) . Sheex Abldullaah mii de mooy ki S bi ne woon :Abdullaah ag xasidaa ngii,gog ku ko mokkal ,Munkir ak Nakiir du nu ko laaj ci bmmeelam,Sheex Abdullaah ne laaylaaha illal laah,ana mu ? Mu ne ko mi ngi ak Muhammadul Amiin mii,mu ne gi naa ne di naa ko mokkalloo samay doom ak samay jigen,ak samy jaam,yu jigen ak yu gor,mu nekk di lim rekk ak a dl,S bi moom di ree rekk. Xasida gi mooy Jaawartu.

Sang bii moo ma nettali woon,nettali bu yeme ba,masumaa dgg lu ni mel,da ne ma sama mbokk man dey daa am bis,may jng li may faral a jng bis ci Alxuraan,bi ma ubbee kaamil bi,amul lu dul Ylla mi man lpp won ma bisub (( alastu birabbikum)) muy ba mu naan (ndax du ma seen boroom?). Nee na ma jkkaarloo ak xew-xew ba,gis yonnant yi,yonnant topp yonnant, yu bari yi ak yu new yi,teg ci ma jkkarlook wlliyu yi,wlliyu teg wlliyu,ak seen mbooloo yu bari yi ak yu new yi,ba mujj ma gis jenn jmm,mooy Sheex Ahmadu mii,gox ypp fees dell aki taalubeem,mu gnne ci Hadara bi ,soris lf,dal di wlbatiku ne ana ku may jottalil ab yonnee sama boroom ?,wax ko aari yoon ba att,Ylla tawfeexal ma, dgral ma,ma ne ko man,mu gestu ne ma ndax yaw la diw ? Ma ne ko waawaaw,mu ne boo ko defee de ,ba nu dem dduna di naa la defal,di naa la defal..,mu ne ma neel sama boroom,mu dolli ma,ndax sama i ma topp de danoo bari te bggaluma leen lu dul lu leen di bgloo,ak wax yu mel nii,ma dugg,ci biir,wax li nu ma waxloo woon,ma gis nu koy jox , ba ma dgg ko mu naan doy na,dal di dem.

Esky,moom de ci jlewaayi (masdar) Sheex Sahdu Abiihi la bokkoon. Xibaar boobu nettaliwu ma ko kenn,lu dul ginaaw bi mu faatoo,ci ndigalm,sheex bii nag sama xarit la woon,te nekkon bu S bi,mas na maa yonni ca S ba di ko aan doomam,mu ne nee ko skkuwu ma ko lu dul ngir xr ci am lu ma jaxase ak moom ci fii ak lg . S bi ne ni mu ko waxe la de,oom de bi ma nekkee seen rew skku woon nanu maa jox seen doom,waaye ma ne leen wuuteg aada yi moo nanguwul loolu rekk . Maandu na te dggal.

Bokk na ci u mag i ko seereel,Alhaaji Ibraahiima Albaxdaadii,moom de ci kiimaani araab yi la woon,mi ngi juge woom Baxdaad,ku meloon ni moom ci xam-xam moom jafe woon na,S bi moom ci jmmi boppam nettali na ma ne gis na Alhaaji Ibraahiima mii,booba gone la woon,muy tukki di nd ak waajuram wu gor,ak Xaali Majaxate Kala,uy nd ak Latjoor,bis nee na gis na ko mu toog ak aari sri yooyu ci lalub sri Buubakar FALL,yeme lool ci barig nettaliy xam-xam yi mu leen doon defal,ci noonu Xaali manutoon a kk a bind nettali yi,mu yonnee nu woolu ma,ngir ma bind xam-xam bu bari bii,mu diy woy,ngir mu ba a snku,ma dikk,muy wax may bind,muy lu bari ciy woy. Ma dgg ci sama waajur mu naan masumaa gis ku man a mokkale ni naar bii,ku dul Alhaaji Omar Fuutiyu,moom de jamono ju nekk mi ngi naan:Buxaari nee na,Muslim nee na.

65

www.daaraykamil.com

Nee nanu bis laaj nanu ko turu buur bii,mu ne Latjoor,buur bi bg lool ci waxam jooju,bi loolu jllee ba teg lu tollook aar fukki at,walla lu jege,ginaaw bi S bi jugee ci tukkib gej gi,la w ci moom jbbalu,fttali ko la xewoon bu njkk,mu yemu lu bari,nettali nanu ne bokk na ci li tax mu jbbalu,daa am bis mu nd ak S bi cib tukki,u yendu ci ron genn garab,dgg naa ci S bi,mu ne Alhaaji moomu booba mi ngi tux,mu gnne gnn gi,am lu mu sotti ci loxoom,daa di ne ma loo wax ci lii ? Ma ne ko defal te bul laaj,mu ne ma ,duma man a kk a laaj,ndax wuute gi da cee bari,ii di ko daganal,ee di ko araamal,ma ne ko ,bu dee noonu la deme de kon lu lnt la ci yaw,mu ne waa-waaw,ma ne ko xanaa gisoo Axdariyu,mu ne ma ahakay,gis naa ko,ma ne ko moom de nee na ca njlben ga,daganul ci mukllaf mu def dara te xamul la cay tteb Ylla,kon doo ko byyi,ba xam li ci Ylla wax?. Sama wax ji wedamloo ko,gg ak moom fu sori,mu sgg ab diir,siggi,ne ma seereel ne byyi naa ko ngir Ylla,dal di jug ca saasa,suul gnn gi,ak li ci nekkoon,ca bis ba mbaa ginaaw bi la jaayante ak S bi,jbbalu ci moom . Bi nn ci mag i ygee ne jbbalu na,u tmbli di ko yedd naan ko yaw ak sa mgg gi ak sa xam-xam bu bari bi,lu tax ngay jbbalu ci ku uul kii? Mu ne ko man dey Baxdaad laa juge, ni nga ko xame,yitewoowuma lu dul ku ma jox sama loxo,bari na wlliyu mbaa boroom xam-xam bu ma romb,te xetug li may wr xeeewuma lu dul ci moom,looloo waral ma aju ci moom, jaayante ak moom,ci noonu u dggal wax ji,dogal ko ngnt.

Bi mu delloo ci Ku tedd ki,nettali ko li nu ko doon wax,S bi bindal ko lii: Wasslaamu halaykum wa rahmatul laahi,wa barakaatuhuu, ma lay xamal ni ca sama xasida ga tudd ((masaalikul jinaan,fii xidmatil mutahhiril janaani)) di ci maanaa,soobuwaayi jjana yi,ci ligeyal kiy laabal xol yi,bayit yii a nga ca: (( Kpp ku ma jorte lu dul kuy ligeyal Ku nu tnn ki,man de dama koy ligeyal ca la mu tnn)) ((dama koy ligeyal ba kero may dugg jjana,krug sax ga,ak mbat ak xewal )) ((kpp ku yaakaar ne man na koo bgale ni,ni ko sama ligey biy bgale )) ((na xam ne rer ak reral wor na ko,te ci moom la ma lu dagan di dikkale juge fa boroom ba)) ((taggoon naa ko bu njkk ca Libarwali,ag tagg gu wlliyu ypp a ci ltt )) ((taggoon naa ko ca Maayomba,tagg wu far samay ayib te dindi samay bkkar)) ((taggoon naa ko fa niti Kalwaa,tagg wu ma fegali noon ak musiba)) . Nee naa ci ligey bi ma koy defal (j.y.m): ((eel na ko tukkee fi man,ab ligey bu taqook rawdatoom ba (bmmeel),ba yawmal xiyaam te mgg)) ((stam ba Jiilaanii gram na ma,yal na ko Ylla mi ma kaweel grm)) ((stam ba Abool Hasan grm na ma,yal na grm luy saxalub taar nekk ci moom)) ((Attiijaanii grm na ma,yal na grmul kiy alag ibliis nekk ci moom)) ((eenti Xalifa yi grm nanu ma,lq naa grmul u u jegeel i)) ((ku ma grmul de,Ylla Mu tedd ,mi moom grm na ma,ngrm lu dul dog )) ((yal na Ylla fay Mustafaa ngn ji pay,ni mu nangoo te amal ab dl )) ((jullig ki nga xam ne teraangaam day daje ak man,yal na nekk ci ki nga xam ne mooy ki dx )). Subhaana rabbika rabbil hizzati hammaa yazifuun wasalaamun halal

66

www.daaraykamil.com

mursaliin walhamdu lillaahi rabbil haalamiina .

Li nag booy xool ag junj la ci ne i ko ci doon yedd de,xamunu dgg-dggi mbiram,kon lu tax waxunu lu mel ne li ki leen xamul waxoon ? : ((yaw ki nga xam ne dgg-dggi am mbiram xamuma ko ,aka neexoon ma xam luy dgg-dggi mbiram)) .

Bokk na ci li nu soloo ci seere yi ko mag i seereel,mooy ne Sheex Muhammad mom Abiibur Rahmaan,Attanaduxii,da daan def fu nu tudde S bi ci wetam mu yggal boppam,ne cy cam soosu,moom dey fu ma ko nemmikoo rekk,fekk ko ci sama kanam,lu tollook aw xur,walla aar. Sama mbokk Muhammadu Abdur Rahmaan,Ibnus Saalik Baaba mom Halawi,wax na ma ne xalifab Sheex Ahmadu Bun Buddin,ak doomam ju mgg ja,Muhammad Amiin,nee nanu ko S bi de wilaayaam gi, indi na ci ay firnde, aki lay yu leer, pp gis ko, kenn ku am aw yiw dey du sikk ci wilaayaam gi.

Bokk na ci seere yi,li ma Muhammad mom Ahmad, mom Aliyu Alyahxuubii,nu gnoon koo xam ci taalubeem yi,ci turu Muhammad Tuubaa,ngir barig lu mu fa daa nekk ak S bi,li mu ma nettali woon,muy moom de bis seeti na ay nijaayam,ni nu ko baaxoowoon a defe,mu dem ca ku yeme,ku bgg ka Yonnant bi ak jwrinam,di Muhammad FAAl,doomi Muhammad mom Ahmad mom Haaqil,mu yobbante ko ab nuyyoo akub siyaare ca S ba,skku woon it ci moom mu jox ko barkeelub mbubum njiitlaay,mu mu daa sol, ngir mu barkeeloo ko,nee na ma jotal ko S bi mu bg ci,jox ma njiitlaay lu ndaw,lu mu daa jiitloo,maanaam turki,mu ne ma gaawal jox ko ko,ma indil ko ko,mu bg ci lool,di ko foon ak a teg ci bopp bi,ag bt yi,nit i dgg ko,mujj ku w rekk,aan ko,ma barkeelu ci,ba mu mujj snku,mu skkuwaat ci man ma demalaat ko,ne ko nit i de snk nanu sama barkeelu ba,na ma sarax beneen,ma dikk ci S bi,leerale ko ko noonu,mu bg,jox ma beneen,ma indil ko ko,mu snt Ylla bu baax,tagg S bi lu bari,man itam mu sat ma,ne ma boo jbbaluwutoon ci S bi de, di naa wax ci yaw kon loo xam ne !,waaye jbbalu gi tax na ma fiire la .

Bokk na ci seere yi nu tuxale ci doomi mbokkam ma,Ahmadu Yoora Muhammad : lenn ci ay ndandoom danu koo yeddoon ci new gi mu new lu muy siyaare S bi,mu ne leen wallaahi,bggumaa deem di ko siyaareji te yor ci sama xol,lu toll ne fepp suuf ci bgg dduna,kon fii ma toog laa koy siyaaree ,eskay.Ana ku gn tedd Muhammad,moom daal doy na skk seere . Neg bii ki ci gnoon a taqoo ak S bi,gnoon cee rafet lu mu wax,mooy Ahmadu mom Abdallaah,ki bokk ak oom aar nday ak baay,moom dey mook S bi danoo meloon ne benn bakkan,seere naa bis S bi di jnglu lenn ci ay xasidaam,u jng aw bayit mooy: ((taqdiimu Ahmadabni Habdil laahi, yahrifuhuu xayru xabiyyin laahi)),muy ci maanaa jiitalug Ahmadu mom Abdul Laahi,ku dul ab dof,buy fo 67 www.daaraykamil.com

xam nga ko,bi nu tuddee Ahmadubnu Habdil laahi rekk, xelam dem ci,Ahmad moomee,mu ne nanu ko ko wool,bi mu wee,mu nettali ko ne tudd gi nu ko tudd,ci biir njng mee tax xelam dem ci moom mu woolu ko, moom itam mu bg ci,sant ci. Ahmadu mii nag mi ngi faatoo Ndakaaru,bmmeelam a nga fa,siyaare naa ko .

Bokk na ci seere yi ,li ma Abal mom Baay Addaymaanii,nettali,mu ne moom de sax na jamono ju ygg ci,skku ci sunu boroom mu won ko,maqaamam S bi,mu ppal bis ci skku gi,u ne :yeen de du ngeen xam ci S bi,lu dul bu ubee ba toog ngir daje ak nit i,ngeen ne kii de mooy S bi,mbaa mu ubbi mihraab bi,taxaw,ngeen ne S bi de jiite nanu,lu dul loolu ciy mbiram de,fddu na leen.

Ma ne wax jii de niroo na ak waxi Uwaysul Xaranii,sangub way topp yi,ji mu waxoon lenn xalifa yi, ne ko: yeen gisu leen ci Yonnant bi (j.y.m) lu dul keram !,nu ne ko Ibnu Quhaafa sax gisu ko,mu ne leen dedet . Habal mii nettali na ma karaama,gu byyikoo ci goroom,baayu soxnaam,mu ne moom de daa am bis mu nekk cib xaymaam,mook doomam,mu koy bsal boppam,ndax daa jkki-jkki woon rekk buur ,buur gu metti,te gaaw (buur = jkki-jkki rekk jug),bi mu ko defee,dal di gnn xayma bi,door tnk bi cig we,ba nu dgg ni ci tnk bi dale,te foofa gnn we nekku fa,ci noonu tnk bi damm,mu rot ,xm,bi mu ximmee,u laaj ko,lu mu doon,mu ne daa gis aw wlliyu wu uul,di Muhammad mom Mahluum,u jnge ko ay we,mu bggoon koo xettali,door tnk bi ci we gi,ngir damm jng bi,far tnk bi damm,werul ci damm-damm boobu,ba kero mu faatu,yal na ko Ylla grm te nangul ko jfam,bi mu daataa faatu,bgaloon na doomi Daymaan yi,ci ag ubbiku gu yaatu ci alal,bu wlliyu woowu dellusee,mu nekkoon ni mu ko waxe woon.

Bi S bi dellusee,mu jl leen,bindkati xam-xam yi,ak alxuraan yi,seeni waxambaane ak mag i ba ci jigen a ak gone ya,di leen sotti ci alal lees manut a misaal, a ca rafetle ak a aawle,loolu di jppndal akug tggatal gu tukke ca Ylla, eel leen,te di ndimbal ak sarax bu nu def ci sekkare,di ag ligeyal lislaam it,ak Yonnant bi (j.y.m) ci xeetam wi . Ni nu binde woon la eneen it binde woon,ci naar yeek u uul i,waaye ci oom la gnoon a siwe,gn cee feee.

Bokk na ci u mgg u barkeel, i seereel S bi,Haamidun mom Muhammad mom Muhanda Baaba,ak doomi baay txam yi,Baaba ak Ahmad, aari doomi Mahmuud ak Haamid yi, oom pp , u u jagleel lanu woon ci moom,boroomi wax yu rafet it lanu woon ci moom .

Ylla dogal, bi S bi nekkee Cyen yonni woon na ma Dagana,ba ma fa ggee,Ustaas Haamid dgg ma, booba da faa ganesi woon Alhaaji Bekaay SEKK,yggul dara mu seetsi ma,bg ci dikk gi ma fa 68 www.daaraykamil.com

dikk,yendook man ca sama kr waajur,di ma laaj ci mbiri S bi,aki xibaaram ,yi ci di yu nu man a tas,ak yi ci di yu u bari mant a xam,bu ko defee muy ree rekk,bg lool ci S bi , aki mbiram, ci noonu ma won ko teereb S bi tudd Masaalikul Jinaan,mu sgg ci,siggiwul ngir dara,ba kerook ngoon di jot,mu ne ma S bi de w gi mu w ci jamono jii nu nekk de,firndel na yiwam wu bari wi .

Lii nag ag mosle rekk la ,waaye waxi ak seerey sangi naar yi,fii taxu koo jug, fi ko tax a jug kay mooy sunu tere bi tudd,(alminahul miskiya,fil xawaarixil mbkkiya). Da nanu ci dolli li nu man ci tudd murid yi ci oom,bu soobee Ylla. Bokk na ci kilifa yi ko seereel,sunu sri tey sriub jullit i ci Senegaal,soppeb S bi,tey mbokkam,ci jegeaaleg diine ak askan,ak rew,Alhaaji,Maalik SI, yal na ko Ylla grm te jari u ci moom Aamiin,dgg naa ko,ku dul man it dgg ko,ba xaw naa doon lu pp xam,mu ne: amul knn ci nun ku dul koo xam ne,daa def lu aaw,ba noppi,tuub ko,te jubal,byyi ag dng,ku dul Sheex Ahmadu Bamba,moom de daa judd,rekk di def lu baax ak a rafetal . Maanaam loolu mooy un i iy tudd pp de,amu ci kenn ku gisul ci boppam ab rccrcc,walla ay rcc-rcc,bu ko defee mu tuub ko te jubal,ginaawug dng,ndare moom,moom dey ,am mbiram cig ndawam akug magam oo yam rekk,lpp ag tegu ci yoon la.Moom de wallaahi dggal na,te laabiire.

Sama mbokk, Muhammad, mom Ahmad Aliyu Alyahxuubii,nu gnoon koo xam ci turu,Muhammad Tuubaa,xibaar na ma ne moom de ci lenn ci ay siyaareem yu mu doon def,daa romboon Tiwaawon,siyaare Alhaaji Maalik SI,bi mu xamee ne ca S ba la jm,mu ne ko man de da ma laa bgg a yobbante ay baat ca moom,boo ggee na nga ma ko nuyyul,te fttalil ma ko sunu guddi ga nu bokkoon fanaan ca Ndakaaru,ci benn neg un aar rekk,kenn atteelunu ku dul Ylla,bu ko fttalikoo ba xam ne maa la yonni ,nga ne ko,man kat maa nga ca la ma waxoon ak moom,maa nga ca kollare ga ma defoon ak moom.Muhammad nee na man de wallaahi,xamuma gan kollare la jublu ci waxam jooju,te moom dolliwaatuma ci genn leeral. Bi ma gsee ba fttali S bi guddi gi,ba mu fttaliku ko,ma wax ko li mu ma wax,mu bg ci,dggal ma te dggal ko,tagg ko bu baax,tmbli di coppati sama nopp bi,ak sama bakan bi,boole ca di ree rekk,ngir bg .

Bokk na ci mag i ko seereel ba tay Xaali Majaxate Kala,xaritu S bi,tey mbokkam ci diine ak askan,ak rew,xaritu waajuri S bi la woon,da daan def ,bi S biy jng,saa su ko masaa na romb rekk,snni ko aw bayit walla ab jumla,ngir nattu ci ab tolluwaayam ci nahwu,muy (xam-xamu tegi wax ci yoon) walla bayaan:(xam-xamu rafeti wax) ngir awal am xelam, leeg-leeg,mu gnneel ko ci ab yq,leegleeg,dedet,ba mujj S bi far ko raw,bi S bi mggee ba weesu fi mu tolloon,mu mujj naan ko,yaw de doom nga woon,waaye leegi baay nga, donga nga woon it,leegi sri nga,muy lu mu dggal te fas ko ci biir ag kaf,akug woyofal . bokk na ci li nu koy askaneel,aw bayit wu yeme,yaakaar naa ne tmblig ag xaasida la : (tukkee na ci man jm ci Ahmadu Bamba,mi byyi nit i,ngir Ylla ,mujj far di sangub nit i ) . 69 www.daaraykamil.com

Bokk na ci li nu askanale sang bu mgg bi,Sheex Muhammadu Alfuutiyu,baayi Zannuuni,ak mbokkam ma Ibnul Harab,mi bokkoon ci jlewaayi Sheex Shdu Abiihi,bayit wii,moom tmblig xasida la gu mu defal S bi : (mi ngi jm ci kok Ylla da koo defal ag tllal (ay xewal) akug wttal,tteloo ko ci ddunay jinne yi ak nit i) . Moom xasida gi,gu yeme la,tewlootuma ko fii mu nekk, wax na ci, ci wenn bayit wu muy waxante ak S bi,naan ko: ( sotti leen ci seeni miskiin,desiitu kaas bi) .

S bi daan def,saa su gisee Zannuuni,defaral ko ab kaas ne ko, ckkutefug sa baay la woon, Zannuuni mii,mi ngi bokkoon ci woykat yu mag yi,yu rafetooni woy yi,def na ab diiwaan ci tag Yonnant bi (j.y.m), def beneen ci tagg sri si,rawati na S bi,mooy ki ci wax lii: ( yaw xarit bi,ndaw sa bunt bii,bari lu ko siyaaresi,ci buur ak jaraaf,ak jinne ak malaaka) .

Loolu di tmblig xasida gu rafet, te yeme,mook baayam ci jlewaayi Sheex Sahdu Abiihi lanu,yal na leen Ylla grm,mi ngi faatoo Cees,nu denc ko ci almeeri Sheex Ahmad Baru, siyaare naa ko, alhamdu lillaah.

Bokk na ci kilifa yi seereel Sang bi,s bu mg bi,di Sri Tayba, Muhammad Ndumbe Maar SILLA. S bi nee na ma s boobu de,fu mu ma masaa na gis rekk snni na ma bayit wii,di ci seere ci sama mbir,mi ngii: (bariwaa na baay bu yege ci doomam,ay tundi teddnga,ni Hadnaan kawee ci Yonnant bi) . Mu bgg a wax foofu ne,cam sii de ab taar la,tey ag mat eel cosaanam. Bokk na ci kilifa yi seere,sang bu mgg ba Alhaaji Abdulaay SIISE,mom Saalum,nekkoon na di ku rafeti wax,ak pas-pas ci S bi,am na bis aw nit di wax cib jataayam ba tudd S bi,ak jle gi mu jle wirdam wi ci Yonnant bi (j.y.m), am ci i teewoon ,ku ci waxe ni kuy weddi,Alaaji gdd ko,ne ko looy wax nii ?,xanaa Sheex Ahmad Tiijaan waxul ne lenn ci ay wirdam Yonnant bi moo ko ko jox (j.y.m) ? mu ne ko ahakay, mu ne ko moom de,nekkutoon lu dul boroom xam-xam,bu jfe xam-xamam,bu ragal Ylla,te doon jfe sunna, rafet gi nu rafet njot ci moom moo waral nu dggal ko,kii nag di Sheex bamba,xanaa melul ni moom rekk,di boroom xam-xam buy jfe xam-xamam,ragal Ylla tey ku sunnawu,ndax kon du nu ko dggal,ngir rafet njort gi nu dggale woon kee ?,waa ja wedam, amul lu mu tontu . Hasbunaal laahu wa nihmal wakiil,nihmal mawlaa,wa nihman nasiiru.

Ag cant eel na Ylla lii doy na ci li sama xel man a joxe,li am nag mooy,bu ma joyaloon samab gog,fexal 70 www.daaraykamil.com

xel mi ci mu dikke li mu wattu,ak li ma wattoo ci samag maas,ci lu wr ak lu wradi,kon de ma indi fi gn jaa yemey yu yemu yi,waaye kon loolu am raddu rekk lay doon, ax gu nekk a ciy nekk, ag jub ak ag jubadi,dgg ak safaan,looloo tax ma tnn indi fi li ma man,teb yool nekk ci,ndax kat det ab yool,ci lug jub nekkul,bu nu doon tollale li ma indi,ci li ma indiwul,da nga naan benn la ci junni,li ma xam it bu nu ko doon tollale ak li ma xamul,da nga naan as kook la ci gej .

Ylla mu kawe mi,laay aan mu baril sama lu new,te wisaare ko,te nangu ko,te dimble ma, moom kat mooy aji tedd jiy aji gn, kiy boroom ngnel lu mag li.

Tmbli nanu ko te mu mat,cig barkeel,yal na Ylla nangu,te dimbalee,te yekkati,te wisaare,Aamiin. Yaw buur bi, jggal ma, ak sama aari way jur,te nga yrm leen ni nu ma yarewoon may ndaw .

Aji Bind ji: Sri Muhammadu Lamin Job Dagana Aji Tekki ji: Abdu Xaadir KEBE

71

www.daaraykamil.com

Vous aimerez peut-être aussi