Vous êtes sur la page 1sur 32

Jigéenu sëykat

______________________________________________________

Maa ngi lay ñaanal sëy bii bokk ci sëy yi dàq ci


kaw suuf, sëy boo xam ne cofeel a koy lal, ndoxum
mbëggeel a koy suuxat yërmaande moo koy saxal,
Yàlla boole ko ci sëy yi ëpp barke, defal leen ci
njaboot gu bari te barkeel ñu saf ñépp te ñépp
safoo leen, yomb na Yàlla yal na ko def waay !
Jigéenu sëykat 2

Sama xarit dinaa la dénk i ndénkaan yoo xam ne


na nga ko def ci sam xel, di ko jëfe ci sa xol ak
say cér, bu ko fàtte mukk, teg ko ci sa kanam mu
janloo ak say gët, nga di ko nafar saa yoo xëyee te
di ko jëfe .

1. Sama xarit maa ngi lay dénk nga sàmm sa


diine; diine nag bu ñu ko waxee lépp luy ag
mbaaax ma nga ca biir, niki jikko nga xam ne
moom rekk a dul jeex, dimbalante sax ak sa
boroom kër ci lépp luy ag mbaax, te yar ci sag
njaboot, na nga taqoo ak téereb Yàlla bi ndax
mooy tax a am diine , Yónent bi- yal na ko
Yàlla dolli xéewal ak mucc - nee na woon :
"jigéen dees na ko takk ngir ñent yii : alalam,
aw askanam, ab taaram, diineem, mu ne :
booy tànn, tànnal boroom diine" ; ndax ab taar
day jeex, te ku la bëgg ngir ab taar kese, bu
gisee ku la dàq wacci la fa, waaye bu dee
diine, jikko yu rafet nag lu sëy bi yàgg yàgg
mbëggeel gi di gën a dëgër !
Jigéenu sëykat 3

2. Sama xarit maa ngi lay dénk nga xam ne ab


sëy du ay caaxaan waaye jaamu Yàlla gu rëy
la, kon xamal ne dugg nga ci jaamu Yàlla gu
rëy, jaamu Yàlla gënu koo rëy ! Sa buntu
àjjana moo ngi fii , te Yàlla ubbil na la buntub
tuyaaba; boo sëyee ak sa boroom-kër tuyaaba
la, boo ko toggalee tuyaaba la, boo ko fóotalee
tuyaaba la, sa doom sax boo ko nàmpalee
tuyaaba la, lépp loo def ci sa kër boo ci yéenee
tuyaaba am ko ca, rawatina nga ame ci ay
doom yu barkeel, lu baax lu ñu def Yàlla
bindal la ca tuyaaba, ba ci sax boo fi jugee
tuyaaba ja da lay fekk fa nga ne .
3. Sama xarit maa ngi lay dénk looy defal sa
boroom-kër, ci sa biir kër na nga ca jiital
Yàlla, moo xam am nga ca jaajëf walla déet,
boo ko defee dana tax ba li nga war a defal sa
boroom-kër, ci sa kër dara du ci sooxe ndax
Yàlla rekk a tax ngay def, te xam nga ne mu
ngi lay gis , te dina la ko fay.
Jigéenu sëykat 4

4. Sama xarit maa ngi lay dénk nga xam ne


danga taxaw ci sa kanamu Boroom, mu laaj la
nan nga doon toppatoo sa boroom kër, say
doom, ba ci lépp loo xam ne ci kër gi la nekk
sàmm ko yaw la war, kon Yàlla daa teg ci sa
loxo lu rëy te fexeel ba boo jàkkaar loo ak
Moom doo rus, Mu gërëm la, bég ci yaw faye
la àjjanay Firdawsi, te sunu Sang ba nee na:
"Giñ naa ci Yàlla jigéen du matal àq yi dox
digganteem ak Boroomam lu dul dafa matale
àqi boroom këram ba noppi", loo man a jaamu
Yàlla jaamu Yàlla, dees na xool ba xam sa
boroom kër gërëm na la walla déet !
5. Sama xarit maa ngi lay dénk nga rafetal say
jikko sa diggante ak sa boroom kër, ay
bokkam ak nit ñépp, ndax loolu kat mooy tax
sa boroom kër naw la, naw say xalaat, di
diisoo ak yaw, ab taar day jeex waaye jikko
moom rekk mooy ndox mi man a suuxat
garabug mbëggeel, ndox moo ko suuxate mu
bokkul ak mii reen ya day dee ndànk ndànk.
Jigéenu sëykat 5

6. Sama xarit maa ngi lay dénk nga fonku sa


boroom-kër; lépp lu mu la digal na la jaral sa
bakkan, lu mu la tere moom bu ko sax jege,
ndax Yàlla Moo wax nga topp ko ,ni la julli
ware ,woor noonu, noonu la la ware ñoo yam -
xanaa mu digal la lu Yàlla tere -, lépp Yàlla
Moo la ko digal .Ay bëgg-bëggam bu ca
woyafal benn, wan ko ne ko lii rekk mooy
sama yitte ; ay bànneexam dee ko dàkk fu ne :
la mu gën a bëgg ci lekk yi xam ko te di ko ko
toggal, la mu gën a bëgg ci yéere yi xam ko te
di ko ko solal , la mu gën a bëgg ci wax yi xam
ko te di ko ko wax, la mu gën a bëgg ci jëf yi
xam ko te di ko ko defal lu dul lu Yàlla tere ,
dee ko bett di ko defal lu baax loo xam ne am
xelam sax toqu ci woon, sunu yaay Aahisa -
yal na ko Yàlla gërëm - nee na: " Bu jigéen ñi
xamoon àqi boroom-kër bu ñu wàccee duñu
jël dara di ko fompe seen i tànk waaye lex la
ñuy jël di ko ko fompe", loolu waxiin la ci ne
loo ko man a defal xeeb ko.
Jigéenu sëykat 6

7. Sama xarit maa ngi lay dénk nga fonku lu sa


boroom-kër fonku, ku mu bëgg, bëggal ko ko,
ay way-juram, ay bokkam yépp; ndax koo
bëggal la mu bëgg rekk yaa ngay gën a sori ci
xolam, kon wan ko ne ko, bëgg naa la ba loo
bëgg bëgg naa ko, man a sëy àg na ci xar mi
sa boroom-kër yor sax nga boole ko ci sëy bi,
di ko toppatoo doo ko bàyyi mu xiif walla mar
!
8. Sama xarit maa ngi lay dénk na nga sàmm
sa boroom kër , sàmmal ko sa popp; bul
jaxasoo ak genn góor walla nga xam fa ngay
yam - bu manul a ñàkk - sàmmal ko këram,
alalam ba bu dara yàqu, ba ci ab deram, bul
nangu kenn di wax ci sa boroom-kër lu bon ,
ndax ku yab sa boroom-kër walla mu xeeb ko,
xamal ne yéen ñaar la boole .
Jigéenu sëykat 7

9. Sama xarit maa ngi lay dénk saa yu la sa


boroom-kër tooñee nga jéggal ko, xamal ne
njuumte du lu man a ñàkk ci nit, lu njuumte la
rëy rëy bu la jéggaluwul sax na nga ko
jéggal, lu mu la bëgg bëgg bis man naa ñëw
mu wax la, walla mu def la lu warul; ndax
loolu ay tolluwaay la waaye du jikko, yenn saa
yi coono yi ak li war góor lépp ci dundal ak
dëkkal ak toppatoo man naa tax mu juum
waaye bu bobaa melal ne yaa juum .
10. Sama xarit maa ngi lay dénk nga xam ne
lépp lu la naqari ci sa boroom-kër walla sax
koo dëkkal, bu dee jikko ju baaxul la, man nga
koo dindi ci kaw sa doxaliin wu rafet, te xam
ne magum jëmm deesu ko yaraat waaye boo
naxtaanee, man ngaa am li nga bëgg, te
wattandiku di wax ak sa boroom-kër sa kàddu
di yékkatiku, bu dee ci biir néeg bi la lu bon
la, bu dee ci bitti daa yées.
Jigéenu sëykat 8

11. Sama xarit maa ngi lay dénk nga xam ne


foo man a bokk, loo man a am , noo man a mel,
du tax nga tolloo ak sa boroom-kër, te loo ko
man a defal du tax nga jox ko àqam dëgg dëgg
! Sunu Sang ba nee na: " Bu doon digal kenn
mu sujóotal kenn, kon jigéen lay digal mu
sujóotal boroom-këram" waxaat ne : " Jigéen
bu boroom-këram tawatoon ba yaram wépp def
ay taab, xolam mayu ko mu fomp ko waaye
làmmiñam lay jël di ko ci fompe, walla sax
muy muucu dereet ji bu noppee wann ko, du
tax mu matale àqi boroom-këram." Kon lii
Sang ba Moo la ko digal .
Jigéenu sëykat 9

12. Sama xarit maa ngi lay dénk nga xam ne


boroom-kër du moroom, sang la, kilifa la,
sunu Sang ba nee na: " Ay bu jigéen xamoon
àq ji mu ameel boroom-këram ak ni mu rëye fa
Yàlla, da koy toggal añ ba noppi walla reer
toog di ko sàmm ba mu lekk ba noppi" kon def
ko kilifa te moytul ma yii : gënoo ma, duma
jaamub kenn, ci kër nga ma fekkoon, góor
jarul yërëm, góor ñi tekkewuñu dara… ku wax
lii du jigéenu sëykat, te wolof nee na: "ku
bóofal ki ngay sëyal loo jur mu téen ni ag
njamal ( mooy giléem ) waaye ku ci tiim ki
ngay sëyal loo jur mbott lay yamal ", kon ku
wàcce boppam, mokk rumbux ci kanamu
boroom-këram doom joo am day barkeel,
waaye boo ko defee moroom tiim ko loo jur du
tekki dara !
Jigéenu sëykat 10

13. Sama xarit maa ngi lay dénk boo juumee


nangul ne juum nga , koo xam ne fu mu fekk
dëgg wax ko te ku ko wax dëgg mu mer daa
pànk waaye dëgguwul, dëggu mooy boo gisee
dëgg wax ko, te xam naka nga koy waxe ak
fan nga koy waxe, te bu ñu la ko waxee nga
nangu ko.
14. Sama xarit maa ngi lay dénk bul rëy mukk,
jikko ji gën a bon ci jigéen mooy rëy , góor loo
ko man a defal; dàqal a solu ci Senegaal , gën
a la rafet ci Senegaal, loo ko man a defal ci
dab bànneexam woyof ci kanamam moo ko ko
gënal, ku bëgg a baaxle àdduna ak allaaxira
fàww nga woyof sunu Sang ba - yal na ko
Yàlla dolli xéewal ak mucc - nee na woon : "
ku lu tollu ne feppu rëy nekk ci xolam du dugg
àjjana", kon jéllale naa di am barke.
Jigéenu sëykat 11

15. Sama xarit maa ngi lay dénk woyof, na doon


sa ngànnaay saa yu coow amee , bu coow amee
lu man a xew njëkkal a wàcci, moo xam yaa
tooñ walla dañu laa tooñ, ndax kat lii de bokk
na ci màndargay jigéenu sëykat dëgg ; ab
sëykat dëgg day ñàkk jom ci kanamu
boroom-këram, jikko jii bu ñu la ko waxee ci
sa boroom-kër aw tagg la, kon li feeg àggoo
fii rekk xamal ne dese nga !
16. Sama xarit maa ngi lay dénk fulla ci sa bopp
bul nangu kenn yab la , yab sa boroom-kër
walla sax yab sag njaboot di ko jaare ci yaw,
lépp luy tax nit xeeb la, ciy wax walla ciy jëf
bu ko ko may , loolu nag di lu ñuy wax waaye
lu ñuy jëf la!
Jigéenu sëykat 12

17. Sama xarit maa ngi lay dénk bu la sa


boroom-kër tooñee sax jéggalu ko, di ko sax
dogal ngànt; lu ci mel ne : sang bi ,ku baax ki,
maa juum de, baal ma du amati bu soobee
Yàlla, donte sax leer na la nàññ ne moo la
tooñ, waaye daŋŋãaral du jikkkoy sëykat , fii
daal la jigéen ñu baax ñi di rawantee !
18. Sama xarit maa ngi lay dénk looy wax ak sa
boroom-kër na nga xam waxtu wa ak nakala,
ku mer kenn du waxtaan ak moom rawatina
góor nga xam ne ñu ci bari Yàlla da leen a
binde xadar , jàppantey téerey baat rekk a ciy
mujj ak donte yaa nekk ci dëgg , bàyyil ba
dereetam sedd, xolam féex, nga wax ko li nga
koy wax , te ngay jéggalu ba laa daraa xew, te
ne ko li nga def tay de du sa jikko xam naa nit
a matul walla danga koo bàyyiwul xel, fexe ba
wax li nga ko bëgg a wax, boo ko defee nii
Yàlla man naa def déggoo am, bu la kenn dàq
lii !
Jigéenu sëykat 13

19. Sama xarit maa ngi lay dénk nga xam ne


jigéen ju baax, jigéenu sëykat dafay dégg
ndigal, sa boroom-kër lu mu la tere bu mu la
ca gisati mukk; damaa bëgg a dem sa tuur ba,
mu ne la : bul dem, toogal te bu ko wan sax ne
ko naqari na ma, waaye demóo boole ci wax ju
bari, naqaral; bu bañee mbaxal bis boobu
mbaxal ngay togg amul njariñ . Yónent bi nee
na woon : ñatt a ngi nii jarul laaj fañu ne ëllëg
dañuy alku, mu bokk ca ñoom jigéen joo xam
ne daa déggul ndigalul boroom-këram.
20. Sama xarit maa ngi lay dénk nga nooy ci sa
kanamu boroom-kër, Yàlla dafa sàkk góor
dëgëral ay céram, dëgëral kàddoom, jigéen
nag da koo sàkk nooyal ay céram, kàddoom
noonu, moo tax li ko war mooy mu jigéene, bu
ko deful day saf góor, te loolu taxul Yàlla sàkk
ko, jëlewu ko it kër baayam, fulla mooy jaay
daqaar ci sa boroom-kër, jigéen ju baax du ko
waxe te du ko jëfe.
Jigéenu sëykat 14

21. Sama xarit maa ngi lay dénk nobaate ,


jigéen day nob boroom-këram, di ko fésal ci ay
waxam ak i jëfam, bul gis keneen ku dul
moom, na doon sa wéttal, dee ko wan ne ko bu
ma la gisul damay wéet, bu génnee sax nga
woo ko ne ko danga maa wéetal, foo nekk, kañ
ngay ñëw, dama laa namm añs, Yónent bi ba
muy lim ñiy tàbbi àjjana boole na ca jigéen ju
nob boroom-këram, yamu ca taq ko ,ba bu ko
meree day jël loxoom teg ko ci ay yoxoom ne
ko duma gëmm sama gët yi lu dul sa mer mii
daa deñ, moo xam sax dañu koo tooñ; dañuy
nettali jigéen ju baax joo xam ne bi ko
boroom-këram meree, daa tiit ba ne duma
nàmpal sama doom lu dul sa mer mi daa deñ;
ndax jamono jii sama boroom-kër mere ma,
sama soow mii ma yaakaar a nàmpal sama
doom jii ngir mu màgg te baax duma ko def ak
lu mu jooy-jooy.
Jigéenu sëykat 15

22. Sama xarit maa ngi lay dénk bul jàpp ak a


fàttaliku lu jàll - bu dee ay jafe-jafe la niki
xuloo -, jigéen du gaaw a mer rawatina nag di
ko jàpp, waaye day jéllale lu bari, ba bu
yàggee sax sa boroom-kër da lay rus, te loolu
jigéen ju ko am dugg na àjjana te deewagul!
23. Sama xarit maa ngi lay dénk fexeel ba saa
yu la sa boroom-kër xoolee ab xolam sedd,
loolu la la sunu Sang ba digal ngir sag cet sab
taar; ab taar nag dafa am biir ak bitti; te mooy
sa boroom-kër di la xemmeem fu mu tol ndax
sa xel mu rafet, sa doxaliin wu rafet, ak
toppatoo goo koy toppatoo ak sa bopp di sol lu
rafet ,di xeeñ lu neex, toog ci wetam lépp ngir
bégal ko .
Jigéenu sëykat 16

24. Sama xarit maa ngi lay dénk ag cet, lépp luy
taq, moo xam ci yaw, ci néeg bi, ci biir kër gi
bumu am , jigéen jikko ju man a daje ci moom
bu saltee yàq na lépp, ag cet nag mooy fonku
ag laab, ci sa jëmm ak lépp li la wër, Yàlla
Moo sàkk doomu aadama def ci moom bëgg ag
cet !
Jigéenu sëykat 17

25. Sama xarit maa ngi lay dénk nga dëggu,


dëggu sa diggante ak sa Boroom, dëggu ba loo
wax sa boroom-kër mu gëm ko; ndax sa
boroom-kër lu mu la bëgg bëgg boo koy fen bu
yàggee nga ñàkk ko, bul fen mukk sa
boroom-kër, lu mu metti metti waxal dëgg
donte da lay mere, lu la dëgg xañ dana la jox
lu ko ëpp, fen fu mu dugg ñaaw njort dugg fa,
kóolute daa di ruusaan ,dëgg lu mu la manul a
may, ay fen du la ko may walla lu mu la may
it, yóbb sa diine, sa ngor, ba doo jar dara ci
kanamau kenn. Boo dëggoo dana la tax a
wóor, te sa boroom-kër wóolu la ba bu ñu la
tuumaalee sax mu ñemee taxaw ne du yaw jar
na lu ne !
Jigéenu sëykat 18

26. Sama xarit maa ngi lay dénk nga am sutura


, bu kenn xam li nga am ak li nga ñàkk, na
nga suturaal sa boroom-kër ; bul xàwwi mukk
suturaam, lu man a xew na nga ko suturaal, te
xam ne foo xàwwi sa suturas boroom-kër
manóo faa jar dara, waaye fexeel ba lu mu dul
wax kenn la lay wax ndax yaw la gën a wóolu
ci kaw suuf, alalam it yaw yaa ko ci gën a doy
boppam, Kon nag bu say wax bari, ndax bu
say wax baree nettali yomb la, te nettali moo
gaaw ci tas kër .
27. Sama xarit maa ngi lay dénk bul def foo toll
di laaj, bu manul a ñàkk, na la leer ne yor na
ko, te nga xam naka nga koy laaje ak waxtu
wa , ndax koo laaj lu mu yorul dugal nga ko ci
fitna, bul def foo toll itam di jàmbat; amuma lii
amuma laa, bu la joxee it jéppi na la, fexeel ba
sa boroom-kër loo soxla doo ko ko wax .
Jigéenu sëykat 19

28. Sama xarit maa ngi lay dénk fexeel ba sa


boroom-kër na doon sa xarit, lépp luy lu baax
nga di ko ko digal, moo xam digganteem ak
Boroomam la walla digganteem ak mbindeef
yi, ci ku mu war a jox, ku mu war a toppatoo,
ku mu war a dimbali , ku mu war a seeti, ku
mu war a jokk ci ay bokkam , ci say bokk
walla sax ñeneen, loo jàpp ne dana rafetal
digganteem ak Boroomam walla nit ñi rekk
dee ko ci soññ.
Jigéenu sëykat 20

29. Sama xarit maa ngi lay dénk ngay sant sa


boroom-kër di ko gëram, di ko wan ne yaw de
yaay ki gën ci góor ñi, ci ni nga may toppatoo,
ni nga ma bëggee, ma jaral la lu ne, su ma
tawatee doo am jàmm lu dul damaa wér, nee
ko, man daal Yàlla mi man a fay rekk laa lay
bàyyee, yenn saa yi nga ne ko damaa bëgg ñu
waxtaan ba mu yaakaar ne lu ne la, nga sant
ko ci ab taxawaayam bu rafet, jigéen du fàtte
njekk, te weddi njekk ; masóo maa defal dara
amalóo ma njariñ, Yónent bi nee na bokk na ci
li tax jigéen ñi ëpp sawara, te nee na : Yàlla
du xool jigéen ju mel nii.
Jigéenu sëykat 21

30. Sama xarit maa ngi lay dénk nga doon


royuwaay, na nga doon misaal ci jigéenu
sëykat, fexeel ba bu sa doom dee sëyi, ñu ne ko
melal ne sa yaay, te nga xam ne sag njaboot
yaa leen man a liggéeyal, sàkkul leen barke,
ba bu ñu màggee baax yomb leen, lu ñu dugg
lu ne liggéeyub nday wallu leen ginnaaw
Yàlla, waaye lu bon lu ne, ñu ne bettul kenn
ndayam a ko fi liggéey te muy dëgg daray
àddina jaru ko !
31. Sama xarit maa ngi lay dénk nga rafetal sa
diggante ak sa bokki boroom-kër, sa
boroom-kër lu mu la bëgg bëgg te ay bokkam
bugguñu la sëy ba du neex, kon fexeel ba ñu
def la ni doom ju ñu jur, te loolu yaa ngi koy
ame ci ab yar ak i teggin, yëg ak toppatoo, loo
am bokk ko ak ñoom, dégg nañu ba tàyyi yaay
ne doomam sa soxna sii boo teqalikoo ak
moom ma dogoo ak yaw àdduna ak allaaxira
ndax jikkoom ju rafet !
Jigéenu sëykat 22

32. Sama xarit maa ngi lay dénk nga xam ne


bokk na ci màndargay jigéenu sëykat dëgg
mooy mu man a muñ, ab sëy du tàngal boo
xam ne dangay macc rekk muy neex, waaye ni
mu ame ay bànneex noonu la amee yoo xam
ne fàww danga koy muñ, moo xam ci sa
boroom-kër la walla sax ci ay bokkam, ku
noppiwul ngir muñ jarul muy dugg cib sëy,
ndax bu duggee it dana génnaat.
33. Sama xarit maa ngi lay dénk doylu; jigéen
day doylu, lu boroom-këram am mu fees
bëtam, du gis leneen, donte fukki dërëm la doy
na ko sëkk, xoolul lu keneen am, waaye saay
moroom am nañu lii am nañu laa, kee
boroom-këram defal na ko lii ak laa, jëndal na
ko lii ak laa, gisóo dara ci li mu am, jikko ji
yées ci jigéen a ngi nii !
Jigéenu sëykat 23

34. Sama xarit maa ngi lay dénk nga xam ne


xoromus jigéen mooy man a togg, daa bokk ci
yi gën a am solo ci jigéen, kon na say feem
bari, foo génn tay bu subaa nga génn fa ca
des, te boole ci wax ju neex, ndax lu mu neex
neex bu àndul ak jàmm ak salaam du saf kenn
, kon jigéen day togg lu neex di wax wax ju
neex .
35. Sama xarit maa ngi lay dénk fexeel ba xam
sa boroom-kër, xam ko bu wér, xam la mu
begg ci lekk yi,ci naan yi,xam sa boroom-kër
ci lépp, la koy bégloo ak li koy merloo, loolu
moo jiitu ci jigéenu sëykat - nee ko : wax ma li
nga bëgg ak li ngay bañ -, la mu bëgg bul
xaar sax ba mu koy laaj. Sàmmal ko biiram,
loo gis ci lu baax moo xam ag lekk la, ag naan
la walla sax ag col la.
Jigéenu sëykat 24

36. Sama xarit maa ngi lay dénk nga xam ne


noo bëgge say doom sëyee ko ëllëg, na nga ko
sëye noonu ba ñu teg ci seen i gët, wan leen ne
nii la ñuy toppatoo boroom-kër, loolu dana tax
ba bu ñu duggee ci sëy duñu la rusloo, ndax
kat sab liggéey ci sa kër ci sag njaboot lay
njëkk a feeñe.
37. Sama xarit maa ngi lay dénk nga xam ne la
Yàlla doon maye ba leegi mi ngi fi, jigéen ju
baax ju ñépp di coow ak ug njabootam, la ko
ko may jugewu fi, te Yàlla itam noonu, kon
boo dogoo ne sama sëy bii danaa ci ame doom
yu ñépp naw , boo ca doxee Yàlla gatandu la.
Jigéenu sëykat 25

38. Sama xarit maa ngi lay dénk nga xam ne ay


jikkoo ngi nii ku ko def ba la ngaa dee danga
ko gis: wor, tas yaakaar, ak fecci kóllare; du
jikkkoy jullit du jikkkoy as gor, kon bul mas a
wor, bul mas a tas yaakaar, bokk na ci wor
nag góor am ci yaw yaakaar ba takk la, def ci
yaw lu ne, nga jaral ko lu ne, nga ñëw mu am
yaakaar ju tas ci yaw, walla mu manoon
manatul nga ne naa seeti keneen.
39. Sama xarit maa ngi lay dénk nga xam ni
ngay waxe ag sa kilifa, booy wax ak moom na
nga wax ak moom ci anamug teggin ak yar, te
xam ne yii di ko wax sa boroom-kër ag
reewande la : yaa ko tay, fàttewóo ko,
neexaluma la ci; jigéen ñu bari manuñoo am ci
seen boroom-kër dara ndax ñàkk kersa,
ndijaay, ku baax ki, sama xol, àjjana, coppati -
yaa xam noo koy tudde - la ma la waxoon de
xam naa danga koo fàtte, donte xam nga ne
fàttewu ko sax, kon ay wax das koy jàng.
Jigéenu sëykat 26

40. Sama xarit maa ngi lay dénk nga xam ne


boroom-kër kenn du ko sàllawlu; taxaw fee di
ko joor, walla ngay jaar ci aw turam, bu ko
mas a def, dee ko woowe tur yu neex, daa bokk
ci yi jigéen war a jàng; ndax day neexal ab
sëy, ñëw ba ci moom bu dee ci mbooloo la nga
sëgg ndànk wax ko li nga koy wax.
41. Sama xarit maa ngi lay dénk nga xam ne ab
sëy dañu koy neexal, waaye boo ko neexalul du
mas a neex, te mbëggeel dees koy suuxat, bu
sëy bi yamee ci lal bi rekk, xamal ne reen ya
ca dee la jëm, bis bu Yàlla sàkk fexeel ba
dundal sa mbëggeel donte dangay juge ca ja
ba sax indaale tàngalub ñaari dërëm ne ko
dama laa indil sërica , manees na cee dundale
mbëggeel.
Jigéenu sëykat 27

42. Sama xarit maa ngi lay dénk nga joŋe, mokk
pooj, mane fu ne ; loolu nag ay jikko la waaye
yamul rekk ci aw làmmiñ, walla looy def ci
biir nit ñi, mooy nga xam nan ngay toppatoo
sa bopp ak boroom-kër, doo bàyyi dara, walla
ngay woyafal dara ci moom, féete ko fi ko
ndayam féete ci yërmaande, féete ko fi ko
doom féete ci dégg ndigal, féete ko niki ko
bokk ak nit nday ak baay, doonal xarit, wéttal
ba bu génnee xelam du jug ci yaw ba kerog
muy ñëw.
43. Sama xarit maa ngi lay dénk nga yewwu,
ñor ba jafe-jafe bu am ci sa boroom-kër, nga
lijjanti ko ndànk, lu mu man a yanu bu dikkee
nga wàcceel ko ko ndànk, ndax kat loolu daa
bokk ci li tax Yàlla sàkk la, kon melal ne sunu
yaay Xadiija ca Sang ba; jafe-jafe bu masaan a
am, bu diikee mu fàtteloo ko ko.
Jigéenu sëykat 28

44. Sama xarit maa ngi lay dénk nga am


yërmaande ci sa boroom-kër te di ko fésal ,
ndax góor coona bu mu daj bu ne jigéen a tax
ak ug njabootam; di joxe alalam, kàttanam, am
xelam, kon dee ko wan ne ko coono yi ngay daj
suba ak ngoon, te nun rekk tax; yaa ngi ci àll
bi , yaa ngi ci lu ne ngir rekk sunuy yitte,
sunuy *yaa* ngi ciy def loo man a ak loo
manul, di ko jëfe nag ba lépp lu dul farata nga
teggil ko ko.
45. Sama xarit maa ngi lay dénk nga xam ne
dafa bokk ci àq yi sa boroom-kër am ci yaw:
bànneexu, baane ak yaw, kon dafa araam ci
yaw nga koy tere sa bopp ci lu dul ngànt (
ngànt yi: di gis dereeti mbërëg, dereeti gësin,
koorug farata, tawat ), Yónent bi - yal na ko
Yàlla dolli xéewal ak mucc - nee na: "Bu góor
woowee soxnaam ci kaw lal bi mu bañ ,
boroom-këram fanaane koo mere , malaaka yi
dañu koy rëbb ba keroog muy yewwu",
rëbbum malaaka nag xajul ci nit !
Jigéenu sëykat 29

46. Sama xarit maa ngi lay dénk ngay ñaanal sa


boroom-kër, ndax ñaan mooy ngànnaayal
jullit, lu la naqari ci sa boroom-kër, ci sag
njaboot boo ko ñaanee Yàlla man na koo
saafara, deel tàllal say yoxo sa Boroom di ko
ñaan li nga bëgg tey saraxe; moom mii de bu
Yàlla taxee lu mu manul amul ! Dee leen
ñaanal Yàlla sàmm leen te aar leen ci lépp lu
bon, ñaanal ko Yàlla ubbil ko wërsëgam,
yaatal ko, ndax xéewal gu mu am yéen a koy
bokk, te di ko ko yëgal ne ko saa yu ne maa
ngi lay ñaanal Yàlla, loolu day def lu rëy ci
moom.
Jigéenu sëykat 30

47. Sama xarit maa ngi lay dénk yaatu, xamal


ne yaay keno gi njëkk ci kër, keno gi manul a
ñàkk ci kër, yaa war a tàwwu ñépp, wuuf
ñépp, kon boo bëggee xat it du sotti ndax
Yàlla bindu la ngir loo lu; jigéen Yàlla da koo
sàkk ngir mu war a doon wéeruwaayu
boroom-këram ak ug njabootam, kon jikko
jooju loo ci am xeeb ko, dafa bokk ci
màndargay jigéen ju baax, jigéenu sëykat
dëgg !
48. Sama xarit maa ngi lay dénk nga téye sab
tànk te xam ne di dox rekk mel ne montar ;
boo demee tay xew, suba nga dem tuur,
ginnaaw suba nga yenduji àll mel ne
barngalub maabo du jikkoy jigéenu sëykat, te
bu yàggee doo safati jigéen sax nag, waaye na
nga toog ci sa kër lu dul lu manul a ñàkk te
nga am ci ndigal, bu dul loolu nga toog ak lu
mu doon farata farata !
Jigéenu sëykat 31

49. Sama xarit maa ngi lay dénk nga fiir ci sa


boroom-kër, fiir nag mooy rekk bëgg sa
boroom-kër bëgg gu ëpp ba mel ne gëmewoo
ko, néegub fiir nag tëdd ca aayul waaye bu ca
biddënti, biddënti ca nag mooy ëppal ca ba
dugg ci ñaaw njort; di ko diglu, di ko topp, fa
la wóoloodiku tàmblee, dee ko wan ciy jëf ne
ko su ma sañoon man ak yaw rekk ngir sa
mbëggeel gu ëpp ci moom.
50. Sama xarit maa ngi lay dénk nga doon ku
ñuy naw ci téye mbóot (sekkere), la ngay
dund ak sa boroom-kër, walla sax ku la wóolu
ba lay wax biiram, fexeel ba am néegub biir
boo xam ne kenn du xam la fa ne ba ci sax sa
yaay , bu dee la ngay dund ak moom ci kaw lal
bi dafa araam nga di ko génne, di ko nettali,
Yónent bi nee na: "Ñi gën a yées wàccuwaay
bis pénc ñooy góor ñu sëy ak seen soxna, walla
sax jigéen ji ba noppi di ko nettali" te lii de
yaatu na lool ci jigéen ñi .
Jigéenu sëykat 32

Ndénkaan yii bu dajee ci yaw santal Yàlla te gën a


góor-góor lu te xam ne yaa nga ca yoon wa; fa
jigéeni sëykat ya jaaroon ba Yàlla faye leen
njaboot gu baax te barkeel, ngërëmul Yàlla, tàbbi
àjjana, bu newul ci yaw xamal ne dese nga, te xam
ne ab sëy du loo xam ne da lay neex nga def walla
nga bàyyi, waaye ag jaamu Yàlla la, def ko na mu
gën a rafetee, Yàlla da la cay bindal tuyaaba,
safaan ba it danga ciy am daani Yàlla .

Alxamis, 10 Fewriyee 2022

Vous aimerez peut-être aussi