Vous êtes sur la page 1sur 44

Jazbul Majzob

Seex Abdul Kariim Samba Jaara Mbay


(1868 - 1917)

1436 h / 2014 - www.drouss.org


Tous droits de reproduction rservs, sauf pour distribution
gratuite sans rien modifier du texte.
Pour toutes questions, suggestions, ou erreurs, veuillez
nous contacter par le biais de notre site internet :
www.drouss.org

Apercu sur lauteur


N en 1868 et fils de Ahmadou et de Soxna Ndack Kane, Cheikh Samba
Diarra est lun des disciples de Serigne Touba qui habitaient Saint Louis.
Originaire de KOKI, il ft lun des potes les plus fascinants dans lunivers
wolof, ci rewi wolof. Il faisait part de ces saints difficilement reprables ;
car il vivait dans la masse, comme tout le monde ; et allait mme vendre
au march.
En allant faire allgeance Cheikhoul Xadym, Cheikh Samba Diarra
rejoignait son frre aine Cheikh Sadiaye, Ndiarme. Contrairement
ce que plus dun raconte sur son allgeance, il na jamais t un griot
qui battait des tam-tam. Cheikh Samba Diarra ft un minent rudit qui
mmorisa le coran son bas ge ; plutard il quitta Koki pour rallier la ville
de Saint-Louis afin dy tudier les sciences religieuses.
Son travail a contribu diffuser les enseignements de Cheikh Ahmadou
Bamba parmi les masses wolof.
Tantt sur ses pomes, il fait des insertions de mots arabes, des phrases
et des prires, y compris dans les ouvertures et fermetures. Il a compos
de nombreux pomes, y compris les louanges ddie Cheikh Ahmadou
Bamba et sa contribution au Sngal, ses miracles en Mauritanie, et les
qualits de Cheikh Ibra Fall.
Parmis ses oeuvres potiques, Jazbul Majzoob (lattirance du majzb
[lattir]) reste le plus populaire.
Il est aussi un proche parent de Serigne Mor Kayr (1869-1951), un autre
minent spcialiste wolofal mouride. Tous deux vivaient ensemble en
Mauritanie et rendaient visite leur matre, Cheikh Ahmadou Bamba,
qui y fut exil par ladministration coloniale franaise de 1903 1907.
Un jour lors dune de ses promenades au bord du fleuve Sngal, il croisa
des jeunes demoiselles dune beaut indescriptible. Il leur demanda
lobjet de leur prsence sur les lieux. Elles rpondirent quelles ont t
envoyes pour venir accueillir un de leur seigneur un talib de Serigne
Touba du nom de Cheikh Samba Diarra Mbaye. Il retourna chez lui en
abandonnant ses chaussures sur place. Quelques temps aprs il quitta
ce monde. Avant de partir il crit :

2 - Jazbul Majzob

ku sdduwul man sddu naa,


ku fadduwul, man faddu naa,
Ba matlu, wsu naa dansa,
Yalla ak sa bark, maa la gm.
Quelques temps aprs ces vers, Serigne Samba Diarra Mbaye ft rappel
Dieu, en 1917. Son mausole se trouve au cimetire de Thim, SaintLouis du Sngal.
Il na eu que trois (3) enfants savoir :
- Fatima Zahra Mbaye
- El Hadj Mbacke Mbaye
- Mouhammadou Moustapha Mbaye

Jazbul Majzob - 3

Indications
Wolof
per
rus
caam
am
xol
jibi
njaay
nday
aam
gm =

e=
u = ou
c = th
= gn
x = kh
j = dj
nj = nd
nd = nd

= eu
= (plus dur) = rr
o = au
gor
q = xx
suqali
ii - uu - oo - aa ee (tirer
Ex : biir - suur -xool - gaal - xeer

4 - Jazbul Majzob

Franais
pr
rous
thiam
gnam
khol
djibi
ndiaye
ndeye
(machoire)
geum
perdu
gaure
soukh khali
sur le son)

Bismi-l-Laahi-r-Rahmaani-r-Rahiimi
AI xamdu Iil-laahi, kimay
Xamal bu wr, ta dima may
Xewl, Ci barkeb kimu xy,
Jbbal lu dooni xewlam.
Yen gaayi diine jegeleen
Ma jegeleen te dolli leen,
Xam-xam bu wr te jafe leen,
Ma fecci tay ay fas-fasam.
Koo xam ni xam na Iii,na xam,
Ku ko xamul, ma wax mu xam,
Xamlug xamul, day taxa xam,
Xamlu ku xam ,day dolli xam.
Te Iii ma leen di bgg a wax,
Day dggi xol, dggali wax,
Jagali jf, te ku ko wax,
Jariu fii, ak fa nu jm.
Masuma leen a waxi neen,
Te lii ma wax, du waxi neen,
Lii woyu xudbu la, du neen,
Yu deefi woy u dul kemam.
Jazbul Majzob - 5

Naa sant ylla mi ma may,


Xudbu bu mat, mu dima may,
Di fey ay, di dqi moy,
Ci leeri mboti ragalam.
Dima gisal luma gisul,
Dima ygal luma ygul,
Dima xamal luma xamul,
Ci duusi geji xam-xamam.
Dima amal luma amuI,
Dima wutal, dima wattul,
Dima digal, dima tamal,
Nangoo yamooki ndigalam.
Dima yrm, dima tifaI,
Dima jari, dima teral,
Def ma ma mel ni ku nu fal,
Ku tbbi peyi ngrmam,
Dima dugal fu may musal,
Dima fegal lu ma ragal,
Ku jm ci man aki fetal,
Mu boole diigali walam.

6 - Jazbul Majzob

Dima setal ci waxi ba,


Ba ku ma yene jfi ba,
Mu ni ko tf, mu ni sulu,
Daanu, di toppal fetalam.
Dima xccal, dima jaal,
Dima tyyill, dima tayaI,
Dima ubbil bunti xewl,
Fatma ci biir roqi oam,
Ne ma ykkt, newuma tuy,
Wan ma boppam, ma di ko woy,
Ta di ko ka, mu di ma may,
Ne ma yoxoos ci biir xolam.
Di ma fegaI pexe mu naaw,
Di ma teral ren aki daaw,
Di ma teral sama gannaaw,
Di ma teral sama kanam.
Dib suruse bimay fajal,
Di garabal lima ragal,
Di ma flal lumay sonal ,
Mu teggi, teg, yenu jem.

Jazbul Majzob - 7

Dima toggal, dima yakkal,


Dima rccal, di ma sefal,
Dima tibbal, di ma leyal,
Tib yu u barkeelug wannam.
Di ma bgaI, di ma seraI,
Dima xjjal, di ma dalal,
Dima moyuI, di ma fayuI,
Kenn du ma yab fi kanamam.
Bu ma yewwee, kenn du ma yab,
Fu ma fi jm, du ma ayib,
Sama gannaaw sama ayib,
Xanaa nammeel gu u ma namm.
Sama o it du u ayib,
Man aki oom du u layib,
Sri bi moo dajale ypp,
Beral nu cr bu u grm,
Limu ma may ma di ko am,
Moo ma ko may ma di ko am.
Limu ma wax ma di ko xam,
Moo ma ko wax ma di ko xam.

8 - Jazbul Majzob

Limu ma wan ma di ko gis,


Moo ma ko wan ma di ko gis.
Ta ku ko gis, ni ku ko gis,
Ni ku ko xam, ni ku ko am.
May na ma lool, danaa ko wax,
May na ma lool, duma ko wax,
May na ma lool, man mi ko wax,
Ak ba ko ooni kee fa yam.
Man Samba Jaara, maa grm
Samab sri, danaa xorom
Way wi ma way ci waa kram,
oo am ngrm, oo am xorom.
Bu sg sggee ba u wral,
Li tax ma jg di ko biral,
Werante de, kon nag yral
Seeni jaloore ca kanam.
Jsbul xulob bi dafa jib,
Bii jsbu jg xee famu jubLu, ku ko xee na wut a jub,
Wy na xameeful fu mu jm.

Jazbul Majzob - 9

Jsbul xuloob bi dafa daw,


Bii jsbu jg, xee fa mu aw,
Ta ku ko dab na daw a daw,
Raw na xameeful fu mu yam.
Lu jiitu Iii dafa dawal,
a daa rawanteeg a dawal,
Naka fxl raw ba ggal,
Akk am wa kenn gisul pndam.
Ma daldi jg, tofal ko bii
jsbu, di woy ki woy Nabi,
Di ko ko Fayna woy Nabi,
Ma di ko woy ba fa nu jm.
Kemub liuy dox di ko woy,
Fayante la ak moom ki mu woy,
Dakoo grm ba di ko ma ,
Lammi yi daldi ko grm,
Ma far jafal man di ko woy,
Di barkeeloog a di ko roy
Ci woy, ba daane ku ko woy,
Ak ku woyul u ne wedam.

10 - Jazbul Majzob

Lu ma wax ak lu ma waxul ,
Wuute gi fs na, nbbuwul,
Ta ba fi tay danaa fsal
Lu doy a xam ci ay woyam.
Danaa xamaI, xamul mu xam,
Xamal ku xam, mu gn a xam,
Ku bgg a gis ta bgg a xam,
Na dglu, xippi ay btam.
Kenn du werante Ii ma wax,
Way xam ya, xam na sama wax,
Seri bii moo may sa, ma wax,
Moo tax ma saf ko ci xolam.
Bulen ma yem, yemleen ko, ndax
Du man di wax, mooy ka di wax,
Waxande laa wu tjii wax,
Bu ma tijjee may lammiam.
Wlliyu day feeu, ta kum
Feeu ci yaw, nga daldi xam,
Bu nee waxal, nga wax u xam,
Way xam ya ,seede daaldi gm.

Jazbul Majzob - 11

Bu fekkee moo feeu ci man,


u naa ma yaw, booba du man,
Moom,ka di moom, moo fi di man.
Ma di fi moom, muy ki fi xam.
Moo tax ma wax ku dglu lii
Na xam ni yii uy wax du lii,
Waaraate jowuma si lii,
Seri bi may na ma boppam.
Kaawteefug yonent la gu des,
Te ag wyam dara du des,
Lu doon kiraama yu fi des,
Dana ko ybbaale u dem.
Sri bi muxjisaat la, moom,
Man nak kiraama laa, ci moom,
Ku weddi lii, na dem fa moom,
Laaj ko, mu teqalem ljam.
Moo tax li may wax moo ko moom,
Msuma ko jaawale moom,
Tudd turam doy na ma koom,
Ta mooy seral sama yaram.

12 - Jazbul Majzob

Bind turam may na ma xel,


Tudd turam may na ma xol,
Siirub turam may na ma lool,
Du ma ko wax, xol a ko xam.
Danaa biral tuuti, ci ay
Mayam ci man, yu u ma may,
Te yile may, ku u ko may,
War nay grm diirug dundam.
Buur yllamay na ma ci moom,
Gm, ak xam, ak lafu ci moom,
Ma jg ne naa taasu ci moom,
Di ko beral woyi ngrm.
May na ma lool, deefuma ax,
Wan na ma lool, deefuma nax,
Naxtima kenn, kenn duma nax,
Sama ngrm rawnag xalam.
Xam naa ndigl, xam naa ndugl,
Tinaa ndigl ,t naa ndugl,
Damay digl duma dugl,
Sama mbt, aw ndiglam.

Jazbul Majzob - 13

Ki lay digl, ta du la jay,


Ki lay dugl, ta di la jay,
Boo xelluwul, defoo ku way,
Rccooki jooy fee sa kanam.
Ku may digl, dafay taxaw,
Ku may dugl, dafay taxaw,
Ta naa awal, fii bufi aw,
Ki ma giseel a mat a xam
Lu ne ci Iii, ma ni ko jkk,
Lu ne ci lee, ma ni ko jkk,
Xam la jagul, ee ak la jag,
Ki ma giseel a mat a am.
Wan na ma lool, yee na ma jar,
Ba ma ree dgg aki nar,
Jarti ma kenn, kenn duma jar,
Ki ma giseel a mat a xam.
Wan na ma lol, dindi na sikk
Ci sama xol, ba duma sikk,
Duma ragal lu ki ma skk
Ki ma giseel a mat a am.

14 - Jazbul Majzob

Feesal na xol bi, ba du xam,


Lu doy a yem ci Ii mu xam,
Lu ki nga xam ni moom la xam
Ki ma giseel a mat a am.
Feesal na bt bi ba du gis,
Lu doy a yem ci Ii mu gis,
Lu ki nga xam ni moom la gis,
Ki ma giseel a mat a am.
Doylul na xol bi, ba du raf,
Jm ci leneen lu lu ko saf,
Ci biir malaanam lama laf,
Ki ma giseel a mat a xam.
Gnne na rer ci sama xol,
Dugal na riir ci sama xel,
Kenn duma yeer di saaxal,
Ki ma giseel a mat a am.
Kenn du ma wootal di ma fiir,
Kenn du ma yab, ba di ma fiir,
Mi ma andal, ta dafa fiir,
Ki ma giseel a mat a xam

Jazbul Majzob - 15

May na ma xam-xam, ba ma xam,


Xot-xoti xam-xam yu ma xam
Ci moom, ba jaaxal ku ma xam,
Ki ma giseel a mat a am.
Dolli na am-am bu ma am,
Dolli na xam-xam bu ma xam,
Leeral na mbooleem Ii ma xam,
Ki ma giseel a mat a xam.
Jfi wilaaya la ma wan,
Dindi la woon wccag a woon,
Def fi leneen di ma ko wan,
Ki ma giseel a mat a am.
May na ma woluu ki ma moom,
Xiir ma ci moom gi mu fi moom,
Biral ma moom gi mu ma moom,
Ki ma giseel a mat a xam.
Biral ma sa-sa bi mu sa,
Bitegi biir moo ko fi sa,
Ta kenn du sa Ii mu fi sa,
Ki ma giseel a mat a am.

16 - Jazbul Majzob

Biral ma saayiir sa, bu wr,


Biral ma baatin ba, bu wr,
Ne ma lu dul lii, du lu wr,
Ki ma giseel a mat a xam.
Ne ma ykket yor ci loxoom,
Di ma xamal lu diy soloom,
Di baay ci baatin, ma di doom,
Ki ma gseel a mat a am.
Jiitu ma nd ak man di wy,
Lu may gagal mu ni ko tuy,
Ba man ma waaru ba ni cy,
Ki ma giseel a mat a xam.
Di ma digl, ta du ma jay,
Fu ma taxaw, mu di ma xy,
Ta di ma gontu, di ma may,
Ki ma giseel a mat a am
Nee ooki, nee na, lani cas,
Buttil ma biir ba ba ma gis,
Raeel ma mboot yi, ba mu fs,
Ki ma giseel a mat a xam

Jazbul Majzob - 17

Ni dgg a ngii dgg a fi gn


Fen du taxaw, tag ti fi fenn,
Ku jm fi pey ,du yori fen,
Ki ma giseel a mat a am.
Lisaani aal lamiy waxam,
Lay snni xol bi, ba ma xam ,
Fu ma fi tollu di ko xam,
Ki ma giseel a mat a xam.
Moom ka di moom, xam na ma xam,
Lu diy mbiram laa jkk a xam,
Boobee ba tay, ma di ko xam,
Ki ma giseel a mat a xam.
Lewoo na ma ak moom cig cofeel,
Di ko mbt ba may xaleel,
Mu daal di may fab yobbu teel,
Ki ma giseel a mat a am.
Tegtal ma yoonu njariam,
Ubbil ma bunti xewlam,
Burxal ma mboti ngrmam,
Ki ma giseel a mat a xam.

18 - Jazbul Majzob

Yee na ma jar, ba ma ni jar,


Fegal ma kor, smmal ma ngor,
Fayal ma mer, fajal ma mar,
Ki ma giseel a mat a am.
Di ma defar, ta di ma far,
Ta ku ma far, mu di ko far,
Ta lu ma far, daal di ko far,
Kima giseel a mat a xam.
Di ma taxawu, ma taxaw,
Buma taxawul, mu taxaw,
Teeweel ma xew, luy mn a xew,
Kima giseel a mat a am.
Ku jm fi man di ma ljal,
Mu boolekoog lu kay ljal,
Lu gn mu fab jox ma, ma jl,
Kima giseel a mat a xam
Lu ma ragal mu ni ko cas
Snni, ba dootu ma ko gis,
Mbaa mu labal ko, mu ni mes,
Kima giseel a mat a am.

Jazbul Majzob - 19

Bittri dun bi, ba ma gis


Ni muy naxee, ta ku ko gis
Jox ko gannaaw mel ni ku rus,
Kima giseel a mat a xam.
Wan na ma lal wan na ma bs,
Noteel ma leen ci sama bs,
Misaal ma leen ba ma ni mbas,
Kima giseel a mat a am.
Yaramu xol bi dafa mees,
Jeena ba mel ni luu fees,
Cofeel gi wal na ko mu tees,
Kima giseel a mat a xam.
Tibbub cofeelam dafa fees
Ci man, di fokki ak a rees
Ci sama xol, ba dootul yes,
Kima giseel a mat a am.
Moo tax mu def bu ma nee gees
Ci sama xol,mbaa mu ne gees,
Sunu dig gante ne depees,
Kima giseel a mat a xam.

20 - Jazbul Majzob

Dima xamal ta du ma ft,


Dolli ma xam-xam bu rafet,
Dolli ma ngm, dollima fit,
Kima giseel a mat a am.
Di ma yaral boppam ma yg
Yar ba ci man, ba ma di yg
Lu ma ygul ne lu ma yg
Kima giseel a mat a am.
Wan ma jamono na mu mel,
Jngal ma xel, di ma bindal
Ci lluway maxfoosi xol,
Kima giseel a mat a xam.
Di teew ma teew ci peyi xol,
Gisee mu taal ci lampi xel,
Jum bu ma wan yoon wu u xll,
Kima giseel a mat a am
Jeeqel ma xel, rcceel ma xol,
Xel du ne xol, xol du ne xel,
Xela di xel, xol a di xol,
Kima giseel a mat a xam.

Jazbul Majzob - 21

Ruujal ma, ji, di ma bayal,


Xiinlu, mu xiin ci niiri xel,
Tawlu, mu taw ci tooli xol,
Kima giseel a mat a am.
Mu or di xam-xam yu rafet,
Xam-xam yu ndul aki ft,
Xam-xam yu dul yuy rkki fit,
Kima giseel a mat a xam.
Sdde na ma ak xam lu rafet,
Badu ma yr lu lu rafet,
Ta du ma gis lu lu rafet
Kima giseel a mat a am.
May na ma dggog moom i wax
Ci ay waxinam yu mu wax,
Samay waxinay na mu wax,
Ki ma giseeJ a mat a xam.
Wan na ma boppam na mu day,
Yllaa ko xam, moom la ko may,
Ta wolu naa ni moo ma doy,
Kima giseel a mat a am.

22 - Jazbul Majzob

Wax na yonnent bi Iimu doon,


May it, ma wax ko Iimu doon,
Moom it, mu def ma Iima doon
Kima giseel a mat a xam.
Nee na yonnent bi, yaw-a-yaw,
May it ma wax ko yaw-a-yaw,
Mu ni ko yaw, ma ni ko yaw,
KIma giseel a mat a am.
Buur ylla may na maw kaam,
Ma di asaanam fu ma jm,
Di tarjumaani lmmiam,
Ki ma giseel a mat a xam.
Lii le du puukare ci man,
Dafay ngrm lu war ci man,
Ta may grm ki gn ci man,
Ki ma giseel a mat a am.
Mayam yi, yaa na, du nu xul,
Cofeel gi, rew na su nu xol,
Ba doggi reenam, su nu xol
Rootul lu dul wanew taggam.

Jazbul Majzob - 23

Am na ci yoy, du nu ko wax,
Am na ci yoy, nun mu ko wax,
Ak bako, noo yamoo ni wax,
Lay dggi xol, tay dolli ngm.
Wuutu na saaba ya, a wy,
Ca la bokkoon ta mujj a wy,
Fab nan nd ak moom di wy,
Du nu ni wuy fi kanamam.
Da koo jkkal, far koo mujjal,
Muy kun mujjal, tay kun jkkal,
Taal bu fayul la far jafal,
Daay gu maneefulug fayam.
Buur ylla sdde na nu lii,
Lu jiitu nun, xam na nu Iii, .
Te yrmandem jiitu na Iii
Ci nun, ba war nanoo grm.
Leerug yonnent bi la fi def,
Mu juuri leeram ku ko saf,
Mu ubbi xol ba, ba mu af,
Dugal ca xam mbiri sangam.

24 - Jazbul Majzob

Yawma alastu naka laaj,


Nu ni ko waaw, ta defi xaaj,
Booba la door ni nanu waaj,
Ta daal nu fay yeni yenam.
Sunu yonnent moo jkke waaw,
Naka ni waaw, nu daal ni waaw,
Soppeeki ba, ku ne ni waaw,
Tay dglu baati ndiglam.
Ruu yi jungaama ndax ragal,
Yee ak cofeel di len ygal,
Am na keroog u nu xamal,
Xam-xam ba tay la u ka xam.
Yonnent bi booba la nu wan
Kanam i gn booba la woon,
Booba la seex metteel woon,
Murid yi booba Iau am.
Booba la bamba gae woon,
Booba la waayam falu woon,
Baax gi fi tay, booba la woon,
Lu ne ci nit, nee na ak jkkam.

Jazbul Majzob - 25

Lii le nu tektal ba fi tay ,


Ne ab sri du ku u jey,
Ku beru mel ni aji say,
Ju dddu reenug garabam.
Baaxug keroog-ay law ba tay,
Bonug keroog itam du moy,
Lawoon keroog-ay wy di wy,
Lu ne di teeri fa mu jm.
Na waay meloon, mooy Ii fi tay,
La waay amoon, mooy Ii fi tay,
La waay xamoon, mooy li fi tay,
Buur ylla, yem naa kttanam.
Ku ylla wan boppam, mu gis,
ku ylla yiir boppam, du gis,
ii di ko gis, uu du ko gis,
Mooy i ko rere, ak i xam.
Buleen di siis, buleen aaan
Buur ylla yaa na, na ko aan,
Kaaan dafay soppiku jaan mtt,
luggeftil mtt-mttam.

26 - Jazbul Majzob

Jileekuleen, aaane leen,


Aaane kuy xy jublu leen,
Di wut a jub, Far dddu Ieen,
Dkki faneen palam-palam.
Jafanduleen tay dgral,
Buleen yolom, kiy dgral,
Buleen ko wax yolomalal,
Ku yolomal, daal di yolom
Ku la gnal ki la gnal,
Moo la gnal ka la gnal,
Ki la gnal ki la gnal,
Moo mat a xam, moo mat a am.
Srin bi gn ki ma gnal,
Moo ma gnal ki ma gnal,
Te moom mi gn ki ma gnal,
Ame ma may, mayu yaram
Jaayante na ak moom ba matal,
Biteeki biir ,ku ma jiital,
Mooma, ba kenn du ma ljal,
Xol bii la fab, joxub xolam.

Jazbul Majzob - 27

Waxtaan na ma ak moom ba matal,


Waxtaan xol wu kenn ygul,
Bu ne mu tbbi sama xol,
Mu yombalal ma ak xamam.
Yawma alastu, ba fi tay,
Masu la tggoog dinu may,
Di yari ruu booba ba tay,
Diggante ndigg aki ruuwam.
Xam turu taalibeem bu doy,
Xam seeni baay ak seeni nday,
Xam seeni kr ak nau day,
Ku ne mu raaley mbiram.
Xam a mggante, ak a fay
Jiitu di toflante ba tay,
Xam ku u taal ba dootul fay,
Ak kok du tkke fii, ba dem.
Xam aji wopp, ak aji wr,
Ak ku u fajtal ba mu wr,
Xam aji toppeeg ku u ber,
Xam fa u dooreeg fa u yam.

28 - Jazbul Majzob

Fekkoon u feeu ko ba feeal ko ca biir, far ko fa feeatal, mu xam ba fii, ba fee,


Kasful ko ypp fi kanamam.
Kiiraay ya de, ba set ni wecc,
Lu diy pakkam u boole tojj
Ko, snni ypp, koote ga tojj,
Ngir ma ni saww, di am ngiram.
Mu xam boppam ak aka topp,
udaal di jl yf ya ni kupp,
Mu ne di sbbaa ak a tuub,
Te xam gannaawam, xam kanam.
Buur yll xamloo ko la woon,
Ak la xewoon, ta di la woon,
Ak la di woon ,ta di la woon,
Mu far saxal lu new bindam.
Booba mu def ko ni badar,
Bu fee ci laylatul xadar,
Raaan di sabbaa ba fajar,
Ci asamaani barsqam,

Jazbul Majzob - 29

Mi fi diggante kursi, ak
Ars, aki byti naari ,ak
Turaa bi, ak awaa-i, ak
Maa-iiki, law i, ak xalam.
Moo tax ma xy di leen ygal,
Seen mboole tay lu ngeen ygul,
Ba far ci woo i dikkagul ,
a bgg a w, i bgg a dem.
Ndax Ii uy yartingi, ma jog,
Ta far si ganti ku g,
Ta aguwul, ta bgg a ag
eneen, ta xam-xamlu du xam.
Ta sama woote bii, ku xy
Mu tbbi ab noppam, ta muy
Tanxamlu, def boppam ku doy,
Xolam ba, mbaa lakkul ba xm.
Lu diy muqddam laa di woo,
Ku di allaaji maa ko woo,
Mbooleeki seex, ku ma ci woo,
Na ni labbayka, mbaa naam.

30 - Jazbul Majzob

Di leen ygal kii ma fi gis,


Ta kii ma gis, ku ko fi gis
Ta andulook moom, ka nga gis,
Gnu fi, mbaa saful xorom.
Na ngeen ma laaj ki ma fi gis,
Sangu b jamono laa fi gis,
Daalleen di nd ak ki ma gis,
Bu kenn ni dggumaw turam.
Sayxi suyooxi Axmadaa,
Kii moo nu tektal Axmadaa,
Ta di fi ka Muxammadaa,
Ba mu tbbal ko biir kram.
Tampeel ko tampeb ngrmam,
Ni ko yoxos ci biir xolam,
Digal ko baati ndiglam,
Fal ko ci kaw lalub palam
Ne ko ykket wane, i xam
Ak i xamul daal di ko xam,
Jiital ko muy muxaddamam,
Daal di taxaw fi seen kanam.

Jazbul Majzob - 31

Junjung ya gor ci asamaan,


Suuf sa di rkk peyi diiwan,
Sase, ta naa xutbusamaan
Moo falu nd aki dagam.
Rijaalu xybu dajaloo,
Ba mel ni weer yu tegaloo,
Boroomi leer di tegaloo,
Fu u fa fee soreeg lndm
Mbooloo yi wutsi ko di wal,
Ta daal di tuub, njbbal ma dal,
Ndndam ya rkk ci wpp wall,
Wayam wa riir fu u fa jm.
Werante de koote ga toj,
Ku ba, nu tjj, mbaate u tojj
Kram, mu far mel ni ku aj,
Kangam ya waaf fi kanamam.
Boroomi giir ya jiitu woon,
Ak seni giir, ta oo rawoon,
jbbal ko giir ya u awoon,
Booleeki wrd ya u am.

32 - Jazbul Majzob

Xaadiru agsi, ni ko am,


Tiijaani agsi ,ni ko am,
Salsali agsi, ni ko am,
Dabbaa-i agsi, ni ko am.
Jaayante faak moom, di ko wan
Yene, ta ngeejoo fekke woon
Tay, ba muritu ko, di sant,
Fi gannaawam ak oam.
Mbooloo ma naa ko yaa fi gn,
Wii waxtu, yaw la u fi tnn,
Yaay tinu, yaa fiy ki u tin,
Tinu fi kuy fekke ta gm.
Buur ylla yaw la wcce tay,
Yaa tte mbir yi ba fi tay,
Smmal njaboot gi, ku la fay,
Fase du sy diirug dundam.
Ku dglu Iii, na xam ni Iii
Yllaa ko def, ku fekke Iii,
Ta dddu, far dummooyu Iii,
Defu ko kenn, lu muy boppam.

Jazbul Majzob - 33

Gumba gu nanaaral, taxul


Mu gis badar, ba tay gisul
Jantu bccg, bu u wuril
Yoor-yoor, mu jakkaarloog jem
Ta gumba nag, ba gumba jee,
Gumba ci xol, mooy waxju jee,
Yal nau am gis boob du jee,
Ci bti xol, ay yuy kanam.
Buur ylla mooy wane, bu kenn
Defe ne boppam a ko wan,
Gis ki le, ab cr la ba woon,
Buur ylla mooy joxey mayam
Ku fekke kii, ta fekki kii,
Texe na fii, ba fee, te kii,
May la gu Ylla maye, kii,
Des na ak i des, nd ak i dem
Xutbusamaan a ngii bu mat,
Jogleen ddiya yi na mat,
Ku jem a gntu na ni mott,
Di wy ta xamtil fu mu jm.

34 - Jazbul Majzob

Addiya tay moo ka jagoo,


Ku def ni moom, di ko jagoo,
Ku ko deful, bu ko dogoo,
Byyil mu tte ay mbiram.
Lu tax ddiya moo ko moom,
Laay bgg a wax, ta mooy boroom,
Moo ko jagoo, du seen moroom,
Neleen gannaaw, mu ne kanam.
Yf ya ca biir ,ak Ii u gis,
Ta liu gis, mooy liu gis,
Biral gi mooy, bt yi ko gis,
Noppal na mbokki lammiam
We waa ngii, tay xee ak a dor
Boroom we waa ngee, gn a wor,
Ba jaan, ta gis des wa di dor
Du tere jaan duggum kanam.
Yf ya ca biir nag ku ko xam,
Na daal di doyloo la mu xam
Ku ko xamul ma wax mu xam
Jbbal ko ruuwug bakkanam.

Jazbul Majzob - 35

Kuy faatu moo fay jkk a teew


uy jullee mu di fa teew,
Bu uy rob, mu nd ak oom di teew,
u dem, mu des tontu layam.
Seetleen na ngeen di jbbalo,
Bii tng, tngub i jbbalo,
Gis am wu neex, ta mosuloo
Ko, xawma man luy njariam.
Fekke ju mel ni wuute, mooy
Fekke jamonay ngiir ta sooy,
Du def lu dul xoole ni looy,
Di rccu, tay mttum tuam.
i sobu, raw ngeen seeni maas,
i ba, na uy ee seeni maas,
Gaal gaa ngii, jgleen aani paas,
Ku yex ba tarde da ko xam.
Xamleen na ngeen di aane nag,
Gm, ak yaroog, toroxlu, ag
Bakkan, ta mu, sax fa ba g,
Ba lang, yamoog ndigl ba xam.

36 - Jazbul Majzob

Wolu dggal, ag rafetal


Njort, ta set fas-fasi xol,
Loo xcci, loola daal di dal,
Muy fii, ba fee ; na ngeen ko xam.
Danaa biral ci lima fas,
Tuuti ci xutbu bi ma fas,
Ni mooma doy, ta Ii ma fas,
Doy na du fii, mang ca kanam.
Fii, du barab, faful di kr,
Fas ji ci moom, dara du mbir,
Keram gii, naaj la kat, du ker,
Lemam di nga mu wex xorom.
Mddm mi, tan yi di ko biiw,
Bawkat yi siif ko, di ko yew,
Di dox di xiiro, ba mu siiw,
Tab lay bu dee taa, daal di dem.
Krug ku dul am kr la fee,
Moo tax ma dddu, jublu fee,
Li tax nu jg, du fii, ma fee,
Foofee la soxlawoo oam.

Jazbul Majzob - 37

Ta tay ma jngal leen, nauy


Faseg njulit, xy byyi moy,
Ta xam ni, jkkam wa, du moy
Boroom, ci kangam, mbaa dnnam.
Ta seede yaari baati see Deyi, ta fas sellal, ta seeDeloo ko, buur bu doy bi see De, ci lu leer ak lu lndam.
Ta dddu dduna, ta wut
Seri bu mat seri, ta at Tani yenam, ta bul tawat
Benn, lu dul ay tawatam.
Ta kooka, mooy Bamba, buleen
Dese ba jg wu ti keneen,
Ba rer ci manding mi, du ngeen
Taseeg ku dindi seen nglam.
Def leen ni man, dama ni man,
Labbayka Bamba, maa ngii man,
Fukki barab, ma teg ca benn,
Fu u fa tollu, maa la gm.

38 - Jazbul Majzob

Bakkan bu dee tggoo di waaj,


Saafara de, aki gllaaj,
Soppe bi yaw lanu fa laaj,
Ylla ak sa barke, maa la gm.
Bu ruu di xar-xarle ba dal,
Malaaka agsi di bgal,
Soppe bi yaw lanu ndal,
Ylla ak sa barke, maa la gm.
Bu ruu di rocciku ba naaw,
Jm asamaan joxe gannaaw,
Soppe bi, yaw lanu fa aaw,
Ylla ak sa barke, maa la gm.
Bu u nee cas yaram di rob,
Rawmaan ni jaas, du nit, du rab,
Soppe bi, yaw lanu fa b,
Ylla ak sa barke, maa la gm.
Bu aari gaaa nee jale,
Di laaj ka neex, ngani jale,
Begal u mbg moom dootu de,
Ylla ak sa barke, maa la gm.

Jazbul Majzob - 39

Keroog ba uy dekki ba xy,


Jm byti ndandoo di wy,
Kerogg a tax nga doy nu tay,
Ylla ak sa barke, maa la gm.
Keroog ba uy taxaw, ta kenn
Du fa ni riis tankam, ta kenn
Du nga lu dul lu mu nekkoon,
Ylla ak sa barke, maa la gm.
Bu tere yay rot, si dignTe yaari wet yi, mel ne tan
Yuy dal, ta kenn du rere benn,
Ylla ak sa barke, maa la gm.
Bu uy tral mandaxe ii,
Seen yiw wa wat, u gane ee,
u gae leen, u ee fa ee,
Ylla ak sa barke, maa la gm
Geppn ba, buy sampu ta mooy
Siraat, ku jggi mbir ya nooy
Fa moom, ta dootu de di nooy,
Ylla ak sa barke, maa la gm

40 - Jazbul Majzob

Keroog ba mbooloo ma nee rcc,


Di sddaloo def naari pcc, .
Bsub keroog yal naa la daj,
Ylla ak sa barke, maa la gm.
u daagu jm Daaru Salaam,
Di xy di joxante salaam,
Fu ne nu deyaale ak salaam,
Ylla ak sa barke, maa la gm.
Soppe bi, yii laa fas ba w,
Yaakaar ci ylla, ak ci yaw,
Texe gu sax, du de ba faw,
Ylla ak sa barke, maa la gm.
Maa ngi taxaw fi sa gannaaw,
Jublu la, jox aneen gannaaw, .
Foo mn a jm .yobbu ma gaaw,
Ylla ak sa barke, maa la gm.
Ku sdduwul, man sddu naa
Ku fdduwul, man fddu naa,
Ba matlu, weesu naa danaa,
Ylla ak sa barke, maa la gm.
Seex Abdul Kariim Samba Jaara Mbay
(1868 -1917)
Radiy-Allaahu Anhu
Jazbul Majzob - 41

1436 h / 2014 www.drouss.org - Tous droits rservs

Vous aimerez peut-être aussi